Woy-Yàlla 61 (144)
War nañoo am ngëm
(Yawut yi 10:39)
1. Lu jiitu tey, Yàlla wax nay yooni yoon
Jaare ci gaayam, yi ko fi nekkaloon.
Waaye, ci muj gi, ci Doomam la jaare;
Ku faaydaal waxam, sa jàmm day bare.
(AWU)
War nañoo gëm ne, Biibël bi day feddali.
Ngëm gu dëgër, ca xareb Yaa, mooy musali.
Ndax am nañ’ dëgg ngëm, gu ànd-ak i jëf?
Ngëm gu ni mel, mucc lay jurali.
2. Buñu won ginnaaw suñu fitu yégle;
Ñeme lañ’ soxla ngir waar ak jàngale.
Su fekkeek ngëm, ci Yeesu Krist lañuy xool,
Ci fasoŋ bu rafet, Yaa dina ñu yool.
(Awu)
3. Bokkuñu ci ñi Yàlla nar a sànk;
Ñooy ñi mu wóolu ndax li ñu ko fonk.
Ak lu ñu noon yu bare fexeel fexeel,
Suñu ngëm, Yeowa lañu ko jagleel.
(Awu)