TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/99 p. 2
  • Wërale Laajte Yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Wërale Laajte Yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 1999
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni Yàlla gise deret
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Ndax dangeen di xaar ba beneen ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 1999
km 9/99 p. 2

Wërale Laajte Yi

◼ Bu dem jotee, ci ni mu gënee gaaw: ndax waaj nga ko, ba noppi?

Ci àddina si ñu nekk, “jamanook anam bu ñu fàgguwuloon” dañuy faral di booloo bay jur anam, bu ñuy war a jóg, ci ni mu gënee gaaw, ci wàllu paj, te di ñu gaawantuloo nangu ñu sol ñu deret xaj na ci. (Dajal. 9:11) Ndax ñu mën a waaj lu ni mel, lu ñu mën a dal, Yeowa joxe na ndimbal ci fasoŋ yu bare, jaare ci mbootaayam, waaye mu ngiy xaaru ñu def suñu wàll. Fii ci suuf, ngir dimbali la, am na limu yëf yoo war a wóoral.

• Saa su ne, yoreel ak yaw sa kàrt Instructions médicales, bu ren.

• Na la wóor ne say doom a ngi yoreek ñoom seen Carte d’identité, bu ren.

• Seetaatal kayit biy ndollent ci Sasu Nguuru Yàlla, bu sàttumbar 1992, ngir gisaat ni ñu mënee diisook fajkat yeek àttekat yi, ci fasoŋ bu ànd ak sago, lu jëm ci pajinu suñuy doom.

• Seetaatal, ci suñu biir mbind yi, bunt yiy wone ni deret bindoo, ak li mën a wuutu deret. (Yi ñu digal: La Tour de Garde, 1 oktoobar 1994, xët 31; 1 suweŋ 1990, xët 30-1; 1 màrs 1989, xët 30-1; Réveillez-vous!, 8 desàmbar 1994, xët 23-7; 8 ut 1993, xët 22-5; 22 nowàmbar 1991, xët 10; ak kayit ya doon ndollent ca Sasu Nguuru Yàlla, bu sàttumbar 1992 ak nowàmbar 1990. Sàmm leen cib béréb, bu yomb a daj.)

• Dogalal ndax, ak xel mu dal, mën ngaa may ñu jëfandikoo ay masin yuy dawloo deret ci bitib yaram wi, walla ndax mën ngaa nangu ay garab, yu am ci seen biir xareefuleeni (fractions) deret. (Su fekkee ne dangay mottali kayitu maye-sañ-sañ ci wàllu paj, muy kayit bu sax, walla kayitu santaane ngir nit ku lay wuutu—muy lu làmboo sago it—dinga gis ne fagarul nañ la loolu lépp ci biir kayit wi ngay xamle sa tànneefu bopp, lu jëm ci pajin, tànneef bu leer nàññ ci sa xel.)

• Balaa ngaa dem loppitaan, fexeel ba magi mbooloo mi xam ko, ndax ñu mën laa jàpple te laal Kurél biy jokkook loppitaan yi (KJL), su soxla taxawee. Su fekkee ne mbiriy xale bu ndaw la, laajal mag yi ñu xamal ko teel KJL bi.

Fexeel sa bañ deret fés, leer nàññ: Ay nettalee ngiy wone ne, am na ay mbokki karceen, góor ak jigéen, ñu yéex a wax doktoor yiy faj ne, bëgguñu deret. Loolu du lu rafet looy def, jëmale ko ci fajkat yi te day tax nga dugg ci musibab ñu sol la deret. Su fajkat yi xame ne am na ay mbind yu ñu torlu, yuy xamle tegtal yi la doy, yow ci sa wàllu bopp, tey taxawu say ngëm ak say bëgg-bëgg, loolu dina leen dimbali ñu jëf ci saa si, teyit dina leen jox yeneeni pexe ngir pajin bu dul jëfandikoo deret.

Ndegam jóg, ci ni mu gënee gaaw, ci wàllu paj mën naa am, kenn xamul kañ, waaye li faral di am mooy ci jamano ju ñu ko foogewul la, jëlal léegi-léegi matuwaay yi war ngir aar sa bopp ak say doom ci deret ju ñuy sol nit.—Léeb. 16:20; 22:3.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager