TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/08 p. 6
  • Ndax dangeen di xaar ba beneen ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax dangeen di xaar ba beneen ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi di jéem a def léegi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi di jéem a def léegi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Faj bi gën
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • War nga seetaan wideo bi tudd : No Blood—Medicine Meets the Challenge
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 1/08 p. 6

Ndax dangeen di xaar ba beneen ?

Xaar lan ? Xaar di bind lépp li ñu la laaj ci kayit bi tudd DPA (maanaam procuration relative aux soins médicaux) te ñu koy jox bépp seede Yexowa bu ñu sóob. Bind loolu am na solo lool ndaxte kenn xamul lu lay dal ëllëg. Kon nanga jàpp ban fasoŋu faj ngay nangu boo nekkee ci lu jamp te bind ko tey ci kayit boobu (Saag 4:14 ; Jëf. 15:28, 29). Defar nañu wideo bi tudd Soigner sans transfusion — Besoins et droits du patient ngir dimbali la ci loolu. Nangeen ko seetaan, ba pare seetaat li ngeen ci jàng, boole ci ay ñaan. Mën ngeen jaar ci laaj yii di topp ngir def loolu. — Buleen fàtte : Ci wideo bii, am na fu ñuy wone ay doktoor yuy opeere nit. Li ñu ciy wone, barewul, waaye waajur yi ñoo war a seet ndax dinañu bàyyi seeni doom yu tuuti yi seetaan wideo bi.

1) Lu tax doktoor yi di seetaat léegi lépp lu jëm ci sol deret ? 2) Doktoor yi mën nañu opeere lu garaaw-a-garaaw, fekk duñu sol nit ki deret. Ci yi ñu mën a opeere noonu, wax ci ñett. 3) Ci àddina si sépp, ñaata doktoor ñoo nangu opeere ay nit fekk duñu leen solal deret ? Lu tax ñu nangu def loolu ? 4) Yàggul noonu, am na ay loppitaan yu gëstu mbirum sol deret. Lan lañu wax ? 5) Sol deret, lu bon lan la mën a def ci yaramu nit ? 6) Am na leneen lu ñu mën a def lu dul sol deret. Lan la ay boroom xam-xam yu aay ci wàll boobu wax ci njarin bi ci nekk ? 7) Lan mooy indi ñàkk deret ? Ban wàll la nit mën a ñàkk ci deretam, te du dee ? Lan moo ko mën a faj ? 8) Lu ñu mën a def ba li tubaab di woowe globules rouges gën a bare ci yaramu nit ? 9) Bu ñuy opeere, lan la doktoor yi di def ngir deret bi bañ a tuuru ba mu ëpp ? 10) Ndax mën nañu faj xale bu ndaw walla ku ñu ragal mu dee ci saa si, fekk duñu leen sol deret ? 11) Bala ñu mën a faj nit ni mu ware, lan lañu war a bañ a fàtte ? 12) Lu jëm ci ni ñu mënee faj ku bañ deret, lu tax karceen yi war a xam lu ñuy nangu ak lu ñu dul nangu ci wàllu faj nit fekk duñu ko sol deret, bala feebar di leen dal ? Te loolu, naka lañu ko mënee def ?

Ci kow li Biibël bi wax, nit ku nekk moo war a seet ndax mën na nangu ñu def ko li ñu wone ci wideo bii. Ci fasoŋu faj yooyu, ndax tànn nga ba pare yi ngay nangu yow ak say doom ? Dinga gën a am ay leeral ci waxtaan boobu boo seetee li ñu wax ci “ Questions des lecteurs ” ci La Tour de Garde bu 15 suweŋ 2004 ak bu 15 oktoobar 2000, ak it waxtaan bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu nowàmbar 2006, xët 3 ba 6 te mu tudd “ Lan laay tànn def lu jëm ci xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yi, walla fasoŋu faj fu ñuy jëfandikoo sama deret ? ” War nga waxtaan ak ki nga bind ci sa kart ngir mu seede li nga bëgg ci wàllu faj ak it say mbokk yu nekkul Seede Yexowa, ngir xamal leen bu baax li nga bëgg ci wàllu faj.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager