TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/99 p. 1
  • Waare bi da ñuy wuutale

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waare bi da ñuy wuutale
  • Sasu Nguuru Yàlla — 1999
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni Yeesu, nañu sawar ci liggéeyu waare bi
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
  • Naka lañuy yéglee xibaaru jàmm bi?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Na la mbëggeel xiir nga wéy di waare!
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)-2024
Sasu Nguuru Yàlla — 1999
km 11/99 p. 1

Waare bi da ñuy wuutale

1 Nit ñu bare dañuy laaj: “Waaw, lan a wuutale Seede Yeowa yeek yeneen diine yi?” Noo naroon a tontoo ci loolu? Mënkoon ngaa faramfàcce yenn ci suñuy ngëm, yi sukkandiku ci Biibël bi. Waaye ndax mas ngaa xalaat a fésal itam ni suñu sasu waare, wi ñuy matal ci kanami ñépp, di ñu wuutaleek yeneen diine yi?—Macë 24:14; 28:19, 20.

2 Tey, barewul nit, ñu jagoo diine, ñu ittewoo bokk seeni ngëm ak ñeneen. Xëy na dañuy xalaat ne mën nañoo doyloo déggal sàrtiy Sésaar, am dundin bu yiw, walla defal lu baax ñeneen ñi. Waaye, gisewuñu niki warugar, dimbali ñeneen ñu jàng li Biibël biy wax lu jëm ci jot ca mucc ga. Waaw ñun, nan lañu wuuteek ñoom?

3 Suñu yëngu-yëngu waare, bu làmboo cawarte bi, daa mel ni guddeek bëccëg ak yëngu-yënguy yeneen diine yi. Lu ëpp 100 at, Seedey suñu jamano ji waare nañook parlu xabaar bu baax bi ba ci peggiy suuf si, di roy noonu karceen ñu njëkk ña. Li ñu jublu, bu ñuy def lu ni mel mooy dimbali li ñu mën ci nit, ñu méngale seeni dund ak coobare Yàlla.—1 Tim. 2:4; 2 Pie. 3:9.

4 Nan lañu la xame? Ndax niki waarekatu Kàddug Yàlla, bu sawar, lañu la xame? (Jëf ya 17:2, 3; 18:25) Ndax sa yëngu-yëngu waare tax na say dëkkandoo ràññee bu leer wuute bi am diggante seen diineek sa jos? Ndax niki ku yàkkamtee bokk yaakaaram ak ñeneen ñi lañu la xame? Ndax am nga doxalukaay, bu lay tax a faral di bokk ci sasu waare wi? Fàttalikul ne li ñuy wuutale, du rekk suñu tur, yem ci, waaye it li ñuy def, te mu méngook li tur woowu di tekki, maanaam di seedeel Yeowa, saa yu ñu suñuy anam mayee ñu def ko.—Isa. 43:10.

5 Mbëggeel ngir Yàllaak suñu moroom a ñuy xiir ci bokk ci yëngu-yëngu waare bi. (Macë 22:37-39) Looloo tax, niki Yeesook i ndawam, li ñu bëgg mooy jariñoo wépp yoon wuñ ñu xàllal ngir bokk ak ñeneen ñi xabaaru Nguur gi. Yal nañu wéy di waar, ak cawarte, ñépp ñi bëgg a déglu xabaar bu baax bi. Def lu ni mel dina dimbali ñi seen xol laab ñu “gis wuute bi am diggante [. . .] kiy jaamu Yàlla ak ki ko jaamuwul.”—Mal. 3:18.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager