TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/99 p. 1
  • Kan a mënkoon a nangu njàngum Biibël bi?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Kan a mënkoon a nangu njàngum Biibël bi?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 1999
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu xam ni ñu waree jëfandikoo suñu téere yiy wax ci li nekk ci Biibël bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 1999
km 11/99 p. 1

Kan a mënkoon a nangu njàngum Biibël bi?

1 Yonent Yàlla Amos yéene woon na ne, doon na am xiif gu metti ci dëkku Israyel, “ag xiif, du gu mburu, ak mar, du mu ndox, waaye gu dégg kàdduy Yeowa.” (Amos 8:11) Ngir njariñu ñépp ñi xiif te mar ci wàllu xel, mbootaayu Yeowaa ngiy séddale mbind yu baree bare, yu sukkandiku ci Biibël bi, te loolu ci kow suuf si sépp.

2 Bé bés niki tey, 67 milioŋ ci ay téere Xam-xam lañu muul ak 79 milioŋ ci ay téere yu ndaw Laaj. Bu ñuy jàngalee dëgg gi, dañuy bég ci yombaayu mbind yooyu, akit seen doole. Waaye, ca dëgg ay ndiiraani nit, ñu jot ci suñu mbind yi, jàngaguñu Biibël bi ak ñun. Lan ay pexe ci loolu?

3 Mbind moo bàyyi mën naa yóbbe njàngum Biibël bi! Seetal rekk li xew ak ab yéenekat; ca yoon wu njëkk, wa mu wax ak jenn jigéen ca buntu këram, la ko xiirtal ci jàng Biibël bi. Ca saa sa la nangu. Ca gannaaw ga, lii la ko jigéen jooja wax: “Yaa di nit ki ma jëkk a xiirtal ci jàng Biibël beek moom.” Ci sa gox, ñaata nit ñu denc suñuy mbind yi, ñoo mënkoon a wax lu ni mel? Mbind moo bàyyil nit, yoonu dellu seeti ko te tàmbali njàngum Biibël bi ca këram lay xàll.

4 Ndegam faral nañu di taseek nit ñu yor suñuy mbind yi ba noppi, nan lañu mënee xamb seen itte, ndax ñu jàng li ne ci suñu biir mbind yi? Ab boroom-kër bu jigéen la benn Seede laajoon ndax amuloon ay laajte yu jëm ci Biibël bi; “Déedéet” la ko tontu. Suñu mbokku karceen, mu jigéen, sax na ci laajam, naan ko: “Xanaa kay, du ñàkk nga war cee am yenn.” Mooy la jigéen ja def, te am njàng tàmbali na. Lu la teree laaj boroom-kër gi ndax du bëggkoon a xam gis-gisu Biibël bi cib laaj walla fànn, bu ko soxal? Nanga paree yëkkëti laajte bu koy itteel, su fekkee ne xelam demul ci dara. Waxtaan yu ni mel mën naa xàll yoon, wuy jëme ci njàng muy faral di am, njàng mu jëm ci dëgg yi ëpp solo ci Biibël bi.

5 Yëngu-yëngub njàngum Biibël bi mooy li gën a soxale ci suñu sasu waare. Ndegam mënuñoo xam mukk kan moo mënkoon a nangoo jàng Biibël bi, bu ci ragal a xiirtal képp ko taseel. Diisal mbir mi Yeowa ci ñaan tey jëfe ci fasoŋ bu méngook say ñaan. Xëy na léegi nga gis nit, koo xiir ci jàng Biibël bi, ànd ci li nga koy laaj!—1 Yowanna 5:14, 15.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager