Naka lañu ko mën a dégge ?
1 Yeesu nee na, te leer na bu baax-a-baax : “ Fàww xebaar bu baax bi jëkka jib ci xeet yépp. ” (Mark 13:10). Ak li ñu liggéey yépp, am na ba tey ay téemeeri milioŋi nit yu déggagul xibaar bu baax bi. Am na ay réew yu ñuy teree def liggéeyu waare bi, ni mu ware. Ci ay réew yu bare, nit ñi dañuy gaaw a yokku. Kon nag, naka lañu ko mën a dégge ? — Room 10:14.
2 Wóolul Yexowa : Waruñu fàtte ne Yexowa xam na li nekk ci xolu nit ñépp. Nit ku mu mënta doon, ak dund bu mu mënta am, ci dëgg-dëgg, bu bëggee xam dëgg gi ci Yàlla, dina ko xam. — 1 Net. 28:9.
3 Ibrayima jaaxle woon na lool. Dafa doon xalaat ñi dëkk Sodom ak Gomor. Waaye Yàlla newoon na ko ne bu fukki nit kese juboon ci dëkku Sodom, du alag dëkk boobu (1 Mu. 18:20, 23, 25, 32). Yexowa masul boole ñi jub ak ñi bon, alag leen. Wone na ko bi mu musalee Lóot ak doomam yu jigéen yi. — 2 Pie. 2:6-9.
4 Ilias dafa foogoon ne moom rekk moo doon jaamu Yàlla dëgg ji. Waaye Yexowa wonoon na ko ne, ci lu wóor, du moom rekk moo ko doon jaamu (1 Bu. 19:14-18). Lan lañu mën a wax ci suñu jamano ?
5 Nañu sawar ci liggéeyu Yàlla : Xamuñu ba fan la liggéeyu waare bi war a dem. Yexowa moo moom liggéey boobu te malaaka yi lay jëfandikoo ngir seet ni ñu koy defe (Peeñ. 14:6, 7). Moom mooy wax ba fan lañu war a seede ci àddina si. Su ko Yexowa bëggee, mën na def ba xibaaru Nguur gi tas ci fasoŋ bu ñu mënul sax xalaat. Bu ko defee, nit ñu gën a bare mën a dégg xibaar bu baax bi, ba gëm (Jëf. 15:7). Yexowa, Yàlla ju bare mbëggeel la. Dafa bare xam-xam te jub. Li muy def dina ànd ak jikkoom yi.
6 Bokk ci ñiy def li Yexowa bëgg, mbégte bu réy la. Kon nag, nañu def suñu kem kàttan ngir nit ñépp mën a dégg xibaar bu baax bi. — 1 Kor. 9:16.