Jiitalleen Nguuru Yàlla ci seen dund, te dëkkleen ci
1 Bu ñu amee jafe-jafe yu jëm ci xaalis walla yeneen jafe-jafe, jiital Nguuru Yàlla ci suñu dund te dëkk ci, du yomb. Bu ñu amee jafe-jafe, naka lañu mënee dëkk ci jiital Nguuru Yàlla ? Mën na am ñu wutal la liggéey bu lay teree fekke ndaje yi yépp, walla bu lay teree bokk bu baax ci liggéeyu waare bi. Bu boobaa, ndax dinga bàyyi sa liggéey jiitu Nguuru Yàlla ci sa dund ?
2 Soxla nañu ngëm gu dëgër : Lu mel noonu, dafay wone ndax suñu ngëm dëgër na. Waaye waruñu fàtte ne Yexowa dig nañu ne, bu ñu njëkkee wut Nguuru Yàlla, dina ñu dimbali. Te Yeesu wax na ne loolu lu wóor la (Sab. 37:25 ; Macë 6:31-34). Li ñu àddina si bëgg a defloo, ak jafe-jafe yi ñu am, mën na tax ñu xaw a fàtte loolu. Bu ko defee, duñu dëkk ci jiital Nguuru Yàlla. Mën na am ñu bëgg laa jox palaas bu gën a baax ci sa liggéey, walla nga mën a am xaalis bu gën a bare. Am na ñu bàyyi loolu nekk li ëpp solo ci seen dund. Waaye ni ko Pool defe, war nañu seet bu baax li war a jiitu ci suñu dund. — Fil. 3:7, 8.
3 Xéy na am na li ñu war a soppi : Benn waarekat nee na : “ Sama xol mu ngi nekkoon ci sama liggéey — moo doon li ma gën a bëgg. Dama yaakaaroon ne, bu ma ci defee li ëpp ci sama jot, du ma teree nekk Seede Yexowa. ” Waaye dafa ne, saa yu nekk, xelam dafa ko doon wax ne mënoon na yokk li mu doon def ngir jaamu Yexowa. Mujj na bàyyi liggéey boobu ko doon teree jëm kanam ci wàllu ngëm. Bi mu jébbalee boppam ci liggéeyu Nguur gi, ci la mënee wax lii : “ Léegi xalaat naa ne maa ngi dund ni ko Yexowa bëgge te dëgg-dëgg, loolu moo ëpp solo. ”
4 Ñu bare mënoon nañu am liggéey bu baax ak xaalis bu bare. Waaye dañu yombal seen dund, te jébbal seen jot yépp ci liggéeyu Yàlla. Loolu, lu jar a ndokkeel la. Am na ay ndaw yu amul jabar te nekk ay surga mbooloo mi walla magi mbooloo mi, yu def loolu te dem ca lekkool bu ñuy wax École de formation ministérielle. Ñooñu dénk nañu leen lu am maanaa ci liggéeyu Yàlla bi. Dañuy topp royukaay bu rafet bu fi Pool bàyyi, te dañuy doylu ci li nit soxla dëgg ngir dund. — 1 Kor. 11:1 ; 1 Tim. 6:6-8 ; Yaw. 13:5.
5 Bu dee sax ni ñu gise àddina si tax na ñu reetaan ñu, am nañu barkeelu Yàlla (1 Kor. 1:26-31). Bu ñu xamee ne Yàlla dina ñu jëfandikoo bu baax-a-baax te dina ñu dimbali ngir def liggéeyam, loolu ndax du seddal suñu xol ? Tey, mën nañu xamal nit ñi ne Yàlla samp na Nguuram. Liggéey boobu ñu mën a def tey, dootuñu ko defati. Kon nag, tey lañu war a dëkk ci jiital Nguuru Yàlla ci suñu dund.