Nit ku nekk am na li nga mën a jàng ci wideo bi tudd : Noé : il marchait avec Dieu
Jàngleen 1 Musaa 6:1 ba 9:19, ba pare seetaanleen wideo Noé (Nóoxin mu ngi doon ànd ak Yàlla) te xalaatleen ni ngeen mënee tontu laaj yii : 1) Jamono Nóoxin, naka la meloon, te lu tax loolu ? 2) Lu tax Nóoxin wuute woon ak ñeneen ñi ? Lan la ko Yàlla sant te lu tax loolu ? 3) Fi ñu tabaxe gaal gi, fan la mënoon a doon, tabax bi ñaata at la jël, te nu gaal gi tollu woon ? 4) Bi ñu doon tabax gaal gi, lan la Nóoxin ak njabootam waroon a def itam ? 5) Ci seen xalaat, nan la dund gi ci biir gaal gi meloon, bi ñu tëjee bunt bi ? 6) Su ngeen bokkoon ci ñi mucc, lan ngeen di yëg ci seen biir xol ? 7) Am na lu ñuy gis yenn saay, lu ñuy fàttali mbënn mi. Loolu lan la, te lu mu tekki ? 8) Li Biibël bi wax ci Nóoxin, lu mu leen di jàngal ? Seen njaboot, lu mu ci mën a jële ? Lu mu ñuy xamal ci liggéey bi ñu Yàlla dénk ? 9) Bu ngeen gisee Nóoxin ak njabootam ci Àjjana ji, loo leen koy laaj ? 10) Nan ngeen naree jëfandikoo wideo Noé (Nóoxin) ?