Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
11-17 feewriyee
Woy-Yàlla 3
12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Su ngeen amee wideo Noé : il marchait avec Dieu, wax leen nit ñi ñu jàng 1 Musaa 6:1 ba 9:19, te ñu seetaan wideo boobu. Bu ko defee, ñu mën a waajal waxtaan bu ñuy am ci Ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi, diggante 25 feewriyee ak 3 màrs. Su ngeen amulee wideo boobu, magi mbooloo mi dinañu waajal waxtaan ci li nekk soxla mbooloo mi.
20 min : ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’a (Xise 1 ba 13). Wottukat biy jiite moo war a def waxtaan bii. Na nekk waxtaan bu xumb ci mbirum li ñu bëgg def ci waaraate bi ci weeru màrs ak wéer yi ci topp. Na ñépp jëfandikoo porogaraam bi nekk ci xët 6 ngir seet ni mu mënee def lépp li mu mën, ci waaraate bi, ci weeru màrs. Waxal nit ñi ne képp ku mën a nekk aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) ci weer boobu, na góor-góorlu ba nekk ko. Bu ngeen àggee ci xise 7 ak 8, laajal ñi ko defoon daaw, yan barke lañu ci jële. Waxal ne képp ku bëgg kayit bu ñuy bind ngir nekk aji-xàll yoonu weer, dina ci mën a am benn bu ndaje bi jeexee.
13 min : “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi. ” Xaaju Sasu Nguuru Yàlla boobu, dimbali na waaraatekat yi ba ñu doon wone yéenekaay yiy wax ci xéew-xéew yu metti yu am ci suñu jamano. Laajteel naka la leen dimbalee. Ndax am na ku dalal xelu nit walla ndax am na ku dimbali ñeneen ba ñu gis ci Biibël bi tontu laaj yu leen jaaxaloon ? Na ñaari nit wone ni ñu mënee wone yéenekaay yi ñu mujj a jot.
Woy-Yàlla 34 ak ñaan bu mujj bi.
18-24 feewriyee
Woy-Yàlla 15
8 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.
12 min : “ Nit ñi gën a bég ci àddina si. ”b Booleleen ci “ Des pas qui mènent au bonheur ” bu nekk ci La Tour de Garde du 15 octobre 1997, p. 6.
25 min : ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’c (Xise 14 ba 23). Wottukatu liggéeyu waare bi moo war a def waxtaan bii. War na wax li ñu def ci mbooloo bi ngir waaraate bi gën a yokku ci weeru màrs. Na wax it fu ñuy defe ndaje yi ñuy am balaa ñuy waare ak waxtu bu ñu koy defe, ci weer bi yépp. Waxal ne ñi nga xam ne bàyyi nañu waaraate, war nañu leen a dimbali ndax ñu bokkaat ci ñiy waaraate. Dañu war a dimbali itam xale yi ak ñiy jàng Biibël bi, ndax ñu mën a bokk ci waaraatekat yi ñu sóobagul. Joxeel turu ñi nekk aji-xàll yoonu weer, ci weeru màrs. Waxal ñeneen ñi ci des ñu ñaan Yexowa ngir seet ndax mënuñu nekk ñoom itam ay aji-xàll yoonu weer.
Woy-Yàlla 60 ak ñaan bu mujj bi.
25 feewriyee–3 màrs
Woy-Yàlla 77
15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na ñaari nit wone ni ñu mënee wone yéenekaay yi. Na kenn ki jëfandikoo La Tour de Garde bi ñu mujj jot, keneen ki jël Réveillez-vous ! bu mujj bi. Na benn ndaw bu nekk waaraatekat bokk ci ñaari nit ñooñu. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci waaraate bi ci weeru feewriyee te joxe ko.
15 min : “ Suñuy wideo, fasoŋu waaraate buy laal nit ñi. ” Waxtaan ak ñi teew. Fi ñu tollu nii, suñuy Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi, laal nañu 8 ci suñuy wideo yi. Bu ngeen waxtaanee ci li ñu bind ci xaaju Sasu Nguuru Yàlla bii, laajal waaraatekat yi, ñu wax ñoom itam li wideo yi jur bi ñu ko wonee ñeneen.
15 min : “ Nit ku nekk am na li nga mën a jàng ci wideo bi tudd : Noé : il marchait avec Dieu. ” Na nga tàmbali waxtaan bi ak laaj yi nekk ci xët 2. Waxtaan bi yépp na yem ci laaj yooyu. Su ngeen amulee wideo bi, magi mbooloo mi dinañu waajal waxtaan ci li nekk soxla mbooloo mi.
Woy-Yàlla 96 ak ñaan bu mujj bi.
4-10 màrs
Woy-Yàlla 91
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
12 min : Li nekk soxla mbooloo mi.
12 min : Jëfandikool téere Xam-xam bi, ngir tàmbali jàngal nit ñi Biibël bi. Ci weeru màrs, dañu bëgg a gën a góor-góorlu ndax nit ñi ñuy jàngal Biibël bi yokku. Nettalil li nekk ci Le ministère du Royaume d’août 1998,p. 4, § 8. Su amee koo xam ne, bu yàggul, tàmbali na jàngal nit Biibël bi ci téere Xam-xam, na ñaari nit wone ni mu ko defe. Fàttalil nit ñi xaaju Sasu Nguuru Yàlla bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Xam-xam bi ”. Mu ngi ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 ci xët 3. Na am ku jël téere Xam-xam bi te def benn ci fasoŋu waaraate yi ñu bind ci xët 4 bu Sasu Nguuru Yàlla boobu ci xaaj bi tudd “ Waxal nit ki ne mën nañu koo jàngal Biibël bi ”.
16 min : “ Lu tax waruñu bàyyi waaraate ? ”d Bu ngeen di jeexal waxtaan bi, na ngeen laaj benn walla ñaari nit ñoo xam ne yàgg nañu nekk ay waaraatekat, ñu wax lu tax, booba ba tey, ñuy waaraate. Nañu wax it loolu lu mu leen yokkal.
Woy-Yàlla 48 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.