Góor ñi nekk ay may dañuy sàmm bu baax géttu Yàlla
1 Yexowa dafa ñu bëgg. Jaar na ci Doomam ngir may ñu ay góor (Efes 4:8, 11, 12). Góor ñooñu, seen liggéey bare na, waaye seen xel yépp mooy dimbali ñu ci wàllu ngëm. Dañu mel ni ay sàmmkat yuy sàmm gétt bi leen Yàlla dénk (1 Pie. 5:2, 3). Loolu, ñun ñépp lay jariñ. Boo amee coono, walla yàggaguloo ci mbooloo mi, walla nga am looy xeex ci sa jikko, walla yaa ngi bëgg sore mbooloo mi, góor ñooñu, li nekk seen xol yépp mooy dimbali leen ngeen am diggante bu rattax ak Yàlla. — Fil. 2:4 ; 1 Tes. 5:12-14.
2 Bu amee lu lay tiital ci li xew ci àddina si, mag ñooñu dañuy mel ni foo mën a làqu bu amee ngelaw bu réy, walla buy taw, taw bu réy. Bu ñu jaaxlee walla bu ñu baree xalaat, dañuy ñów ngir dalal suñu xel. Bu ñuy def loolu, dañuy mel ni dex bu nekk ci béréb bu wow, walla ker bu xeer bu mag di def ci kow suuf su wow koŋŋ. — Isa. 32:2.
3 Dañuy dimbali ñi bàyyi waaraate : Am na ñoo xam ne duñu waaraate weer bu nekk walla sax bàyyi nañu waaraate. Ci at mi, mag ñi dinañu def lu ñu mën ngir dimbali ñooñu ñu mën a bokkaat ndànk-ndànk ci lépp li ñuy def ci mbooloo mi. Dañu leen bëgg moo tax ñu leen di seeti ngir dimbali leen ci wàllu ngëm. Loolu, tax na ñu bare di ñówaat fekke suñu ndaje yépp. Tax na it seen ngëm gën a dëgër ba ñu dellu waaraate. Loolu yépp mag ñi di def, dafa ñuy won ne Yexowa dafa ñu bëgg lool te mu ngi ñuy toppatoo bu baax. Dafay wone itam ne Yeesu Krist mu ngiy ilif mbooloom. Moom moo ñu won ni ñu waree toppatoo képp ku bëgg sore mbooloom walla sax ku réer ba pare. — Macë 18:12-14 ; Ywna. 10:16, 27-29.
4 Ñi mel ni sàmmkat ñu ngi seet lu mën a wone ne am na ku bëgg fakkastalu ci wàllu ngëm. Nii lañu mënee xam ku soxla ndimbal ci wàllu ngëm : ñi nga xam ne seen xol daa bëgg jeex te muy feeñ ci ñoom, walla ñi bàyyi fekke ndaje yépp, walla ñi wàññi li ñu daan def ci waaraate bi. Am na ñoo xam ne ci li ñuy sol walla ci ni ñuy defare seen bopp dañuy wone ne dañu bëgg mel ni waa àddina si. Mën na am it ñuy komaase di jëw ñi bokk ci mbooloo mi. Wottukat yi dañuy dimbali ñooñu bu baax-a-baax boole ci xol bu laab ak mbëggeel dëgg. Dañuy joxe seen bakkan di jéem a dimbali ñooñu ñu amaat mbëggeel bu xóot ci Yexowa. — 1 Tes. 2:8.
5 Am na ay karceen yoo xam ne àndatuñu ak mbooloo mi. Dem nañu ba bañ a defati dara ci wàllu ngëm. Lu leen yóbbu ba foofu ? Feebar yu ëpp, ñàkk xaalis, walla coono ci biir njaboot gi. Ñi mel ni sàmmkat bëgguñu wut sikk ci ñoom. Waaye li ñu bëgg mooy ñu xam ne Yexowa mu ngiy toppatoo ñépp ñoo xam ne dañu mel ni ay xar ci moom, te dina leen dimbali bu ñu nekkee ci lu metti (Sab. 55:22 ; 1 Pie. 5:7). Ñi mel ni ay sàmmkat ci gétt bi mën nañu dimbali ñooñu ñu xam ne bu ñu jegee Yàlla, moom it dina leen jege. Dina seddal seen xol te dina leen may noflaay. — Saak 4:8 ; Sab. 23:3, 4.
6 Bëgg toppatoo ñi seen yaram neexul : Sàmmkat yooyu dinañu toppatoo it ñi nga xam ne mën nañu leen gaaw a fàtte. Am na ñoo xam ne seen yaram neexul, walla dañuy tëdd ci lal te mënuñu jóg, walla ñu làggi. Xam nañu ne li ñu mën a bokk ci waaraate bi du mën a bare. Xéyna, ñii rekk lañu mën a seede : ñi leen di seetsi, walla ñi leen di faj, walla ñeneen ñu feebar. Waaye ba tey lépp lu ñu mën a def, gis nañu ko ni lu am solo ci liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp (Macë 25:15). Bu dee sax li ñu seede 15 minit rekk la, war nañu ko bind ci kayit fi ñuy binde li ñu def ci liggéeyu waare bi. Te ñooñu war nañu leen gise ni ay waaraatekat yu waaraate weer bu nekk.
7 Ñu ngi ci jamonoy fàttaliku bi. Góor ñi nekk ay may dañuy jéem lépp lu ñu mën ngir seet ci mbooloo mi ñi am ay soxla ci wàllu ngëm ci jamono boobu. Jamono boobu baax na lool ci mag ñi ngir ñu def lépp lu ñu mën ngir dimbali ñi nga xam ne dañoo bëgg bàyyi walla sax bàyyi nañu waaraate bi, ba ñu amaat mbégte ak xel mu dal bu ñuy am bu ñuy ànd ak suñuy mbokk ci ngëm ci mbooloo mi. Ci dëgg dëgg dañuy kontaan lool bu ñu gisee nit ñu mel ñooñu ci suñu ndaje yi walla bu ñu leen gisee ñuy waar nit ñi, di wonewaat noonu ngëm bi ñu am ci sarax bi nekk njot. — Gal. 6:10 ; Lukk 15:4-7 ; Ywna. 10:11, 14.