Leetar bu ñu Jataay biy dogal yónnee
1 Ci atum 2002 bii, yéen “ kureelu mbokk yi ” nekk ci àddina si sépp lañu bëgg bind, ak xol bu sedd guyy, ngir gërëm leen ci liggéey bu am solo te metti bi ngeen def (1 Pie. 2:17). Am na léegi lu jege ñaari junniy at, Yeesu laajoon na lii : “ Bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina? ” (Lukk 18:8). Waawaaw ! Liggéey bu metti bi ngeen def ci at mi weesu moo ñuy tax a tontu noonu. Am na ci yéen ñoo xam ne dañu leen di reetaan te sewal ndax seen ngëm. Ci ay béréb yu bare, yéen a ngi ci xare, musiba, feebar, walla xiif. Waaye dangeen di muñ (Lukk 21:10, 11). Li ngeen sawar a def lu baax te jub, tax na Yeesu mën a “ fekk [ba tey] ngëm ci àddina ”. Wóor na ne ñi nekk ci asamaan si, kontaan nañu ci loolu !
2 Xam nañu ne muñ yombul. Nañu seet jafe-jafe yi suñuy mbokk di jàkkaarloo ci benn dëkku sowu Asi. Foofu, dafa mel ni bés bu nekk lañuy fitnaal Seede Yexowa yi. Bu yàggul la poliis tas seen benn ndaje fu lu mat 700 nit teewoon ci jàmm. Amoon na yeneen 1300 nit ñu fa bëggoon a teew. Waaye ay nit dañu def ci yoon bi lu leen tere jàll, ba mujjuñu àgg. Ay nit ñu bare ñu nëbboon seen kanam, fekk ay alkaati sax bokkoon nañu ci, dañu dugg fi ñu doon daje, dóor fa ñu bare, te taal lépp lu fa nekkoon. Am na itam fu ñu dóore suñuy mbokk, dóor yu metti, ak ay bant yu ñu daajoon ay pont. Te loolu, defuñu ko benn yoon rekk.
3 Yu mel noonu, ñaaw na lool, waaye bettu ñu. Yàlla jaaroon na ci ndaw li Pool ngir bind lii : “ Ku bokk ci Krist Yeesu, te bëgg dund, dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la. ” (2 Tim. 3:12). Ci téeméeri at yi njëkk gannaaw Yeesu, karceen yi dañu leen doon wax ay wax yu ñaaw, di leen dóor, am na ci sax ñu nu rey (Jëf. 5:40 ; 12:2 ; 16:22-24 ; 19:9). Lu mel noonu amoon na ci téeméeri at yii weesu, te wóor na ne dina am itam ci at yii di ñów. Waaye, Yexowa mu ngi wax ba tey : “ Bépp gànnaay bu ñu jëmale ci yow, du am ndam. ” (Isa. 54:17). Wax jooju dafay dalal xel. Li wóor te wér mooy, Yexowa dafa ñu bëgg lool. Looloo tax mu waxloo Sakaryaa ne : “ Ku leen laal, laal na sama peru bët. ” (Sak. 2:8). Ñiy xeex jaami Yexowa yi, duñu mujj gañe mukk. Diine bu sell bi moo fiy des !
4 Nañu ko seete ci lii : Daaw, ci dëkk boobu ñu doon wax léegi, am na ñaari weer yoo xam ne, seede Yexowa yi fa doon waaraate, dañu bare ba mat loo xam ne masuñu ko woon a mat ci dëkk boobu. Kon foofu, jafe-jafe yi taxul ñu dellu ginnaaw. Ci àddina si sépp, loolu la seede Yexowa yi di def. Daaw, ayu-bés bu nekk, ci àddina si sépp, sóob nañu ci ndox 5 066 nit, ngir wone ne jébbal nañu seen bopp Yexowa. Tey, ñooñu ñu sóob bu yàggul li ñu bëgg yépp mooy ànd ak ñun, “ taxaw temm ci coobareg Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor ”. — Kol. 4:12.
5 Nañu wax it ci li xewoon bu yàggul ci réewu Garees (Grèce). Foofu, lu mat ay ati at, ñi bokk ci diine bu ñuy wax Église orthodoxe grecque, xeex nañu Seede Yexowa yi, xeex bu metti. Waaye léegi nguur googu nee na Seede Yexowa yi diine la boo xam ne“ diine bu ñu xam ” la. Kayit fu ñu binde loolu, yokk na itam ne, bànqaas bu nekk ci réew boobu dafa nekk “ béréb bu sell bu ñu jébbal njaamu Yàlla ”. Ñu ngi leen di xamal ne, yoon àtte na lu baax ngir diine seede Yexowa yi, ci dëkku Almaañ, Bulgari, Etaa Sini, Kanada, Rumani, Rusi (Russie) ak Sapoŋ (Japon). Ñu ngi gërëm Yexowa bu baax ci ni mu ñu ubbile bunt ci dëkk yooyu, ndax ñu mën fa kontine suñu liggéeyu waare !
6 Bu ñu seetee it li Yexowa def ngir jàpple mbooloom ci mujug jamano jii, dinañu gis ne mënuñu am xarit bu ko gën. Kóllëre biy dox suñu diggante ak moom, lu seddal xol la, ndaxte xam nañu ne dafa ñu bëgg, dafa nuy jàngal, di ñu jubbanti. Dëgg la, dinañu am yeneen jafe-jafe yuy song suñu ngëm, waaye, ngëm bu dëgër bu ñu am ci Yexowa, dina ñu jàpple. Saak, newoon na lii : “ Yeen samay mbokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu mën a mel, def leen ko ni mbég mu réy, xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ. ” (Saak 1:2, 3). Suñu muñ dafay wone ne gëm nañu Yexowa, te loolu dafa ñuy may mbégte mu réy ! Yéen suñu mbokk yi, na leen wóor ne Yexowa dina ñu jàpple ñun ñépp, kenn ku ci nekk. Ci lu wóor, bu ñu toppee Yexowa, dina ñu jàpple, ndax ñu mën a dugg ci àddina su bees si. Dafa bëgg ñu yóbbu ndam li.
7 Kon nag yéen suñu mbokk yi, góor ak jigéen, mag ak ndaw, ñu ngi leen di ñaan ngeen bañ a fàtte barke yu kéemaane yi nekk suñu kanam. Nañu mel ni Pool mi bindoon ne : “ Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg. ” (Room 8:18). Bu ngeen amee jafe-jafe bu mu mënta doon, wéeru leen ci Yexowa. Muñ leen te bañ a dellu ginnaaw. Du ngeen ko réccu mukk. Kàddu Yàlla nee na : “ Ñi jub, seen ngor moo leen di tax a dund. ” — Xab. 2:4.
Seeni mbokk ci ngëm,
Jataay biy dogal ci Seedee Yexowa yi