Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru màrs : Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Dinañu góor-góorlu ngir tàmbali jàngal Biibël bi ñeneen nit. Awril ak me : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Waaraatekat yi war nañu wax nit ñi nuy taseel ne bu ñu ko bëggee, mën nañu jàpple liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp. Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, wonleen ko téere Laaj bi, te góor-góorluleen ngir mën a jàng ak moom Biibël bi. Suweŋ : Lan la ñu Yàlla laaj ? walla Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Bu ngeen tase ak ku am téere yooyu, wonleen ko benn ci téere yu ndaw yu nekk ci seen mbooloo bu mën a baax ci moom.
◼ Waaraatekat yu bëgg nekk aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) ci weeru awril, war nañu seet léegi, naka lañu naree waaraate, te teel a bind li ñuy laaj ci kayit bu ñuy bind ngir nekk pioñee. Loolu dina tax mag ñi mën a seet ni ñuy doxale liggéeyu waare bi, te dinañu fexe ba ñu am yéenekaay ak téere yu doy ci mbooloo mi. Weer wu nekk, dinañu joxe turu ñi nekk aji-xàll yoonu weer.
◼ Alxemes, 28 màrs 2002 mooy bésu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Bu seen mbooloo amee ndaje bés boobu, na ngeen def ndaje boobu bés bu seen Saalu Nguur gi féexee. Bu amulee bés bu muy féex, xéyna ndaje bu jëm ci liggéeyu waare bi ngeen dul def. Bu boobaa, bu amee lu am solo lool ci porogaraamu ndaje boobu, na ngeen ko def ci beneen ndaje bu jëm ci liggéeyu waare bi.
◼ Bu waaraatekat soxlaa téere, waru ko laajal boppam bànqaas bi. Wottukat biy jiite war na def weer bu nekk benn yégle, bala ñuy yónnee ci bànqaas bi li mbooloo mi soxla ci wàllu téere. Bu ko defee, képp ku soxla téere dina ko mën a wax suñu mbokk buy toppatoo téere yi ci mbooloo mi. Na ngeen fàttaliku yan téere ngeen mënul a jot bu ngeen ko laajul.
◼ Bu 20 nit walla lu ko ëpp bëggee ànd seeti bànqaas bi, nañu njëkk bind ngir yégal ko bànqaas bi. Nañu bind ñaata lañu nar a doon, bés bu ñu fay dem ak ban waxtu lay doon. Bala ñuy dem ca bànqaas ba, nañu jàngaat Réponses à vos questions du Ministère du Royaume de mars 1998. Dinañu fa gis ni ñu war a soloo te ni suñu bopp war a mel bu ñuy dem betel. Képp kuy dem betel, war na topp tegtal yooyu.
◼ Léegi, mën nañu am La Tour de Garde bu ñu bind ak ay bind yu réy ci làkku Efik, Igbo, ak Yoruba.
◼ Téere yu bees yi ñu mën a am :
Farlul ci njàng mi ak mbind mi — swaili
Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex (bind yu réy) — ãgale
La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains I — liŋala
Ndax dañoo rëdd suñu dundin ba noppi? Walla ca kanamu Yàlla dañuy gàddu suñuy jëf? (T-71, ngir jullit yi) — bambara
Le monde actuel survivra-t-il ? (T-19) — liŋala
Le nom divin qui demeure à jamais — gun
Pourquoi avoir confiance en la Bible (T-13) — jula
Une vie paisible dans un monde nouveau (T-15) — jula
Mën nga nekk xaritu Yàlla ! — jula
◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :
Les jeunes s’interrogent—Comment se faire de vrais amis ? (PAL et SECAM) — españool
No Blood—Medicine Meets the Challenge (SECAM) — ãgale
Toute la communauté de nos frères (PAL et SECAM) — españool