Nañu fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla
Téjal say téere, te jéem a fàttaliku li nga jàng ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci diggante 7 sãwiyee ba 22 awril 2002. Ci jot bi ñu lay may, jëlal kayit te bind tonti laaj yi nga xam yépp.
[Bul fàtte : Biibël bi kese nga mën a jëfandikoo. Liy topp laaj yi mooy li nga mën a jàng ngir waajal laaj yi. Bu dee La Tour de Garde la, yenn saay duñu joxe xët bi ak xise bi.]
Tontul waaw, walla déedéet ci li ñu wax ci suuf :
1. Ci Dajalekat 2:2, Suleymaan dafa bëggoon a wax ne, dañu war a moytu reetaan ak bég. [Lecture de la Bible ; voir w87 15/9 p. 24 § 5.]
2. Téere Dajalekat, du téere buy tas yaakaar, waaye téere buy wone lu am-a-am solo ci xam-xamu Yàlla la, te dafay wone ne ñi sore Yàlla ñooy def jëf yiy loraate. [si p. 114 § 15]
3. Ci Isayi 1:7, yonent Yàlla Isayi dafay wax ci sànkute bi dal Yuda bi Axas nekkee buur. [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 17-18 § 16.]
4. “ Taxaw ca kanamu gàngune ma ak Mbote ma ”, ni ñu ko waxe ci Peeñu bi 7:9, dafay wone ne loolu ca asamaan la. [rs p. 67 § 3]
5. Ci lu ëpp, bu ñu màggalee Yàlla ak suñu alal — suñu jot, li ñu mën a def, suñu doole — dañu ciy jële ay barke yu am maanaa yi ñu Yexowa di may ci wàllu xel (Léeb. 3:9, 10). [w00 15/1 p. 25 § 1]
6. ‘ Lu doy waar ’ lu war a am tey bi ñu waxoon ci Isayi 28:21, mooy sànkute réew yi ci Armagédon. [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 295 § 16 ; p. 301 § 28.]
7. Ni ko Macë 24:38, 39 wonee, li taxoon ndoxu mbënn ma alag nit ñi ca jamano Nóoxin mooy, li ñu daan lekk, di naan, tey toppatoo seeni soxla. [w00 15/2 p. 6 § 6]
8. Yexowa, jaamam yu woyof yi koy jaamu te duñu ci ut dara, saa yu ñu ko ñaanee dara, dafa leen ko koy may. [w00 1/3 p. 4 § 3]
9. “ Xeet ” yi ñuy wax ci Isayi 60:3 ñooy réew yi nga xam ne leer bi jóge ci Yàlla dafa leen di wootal. [Lecture de la Bible ; voir w00 1/1 p. 12 § 4.]
10. Yexowa dafa “ sellal ” Yérémi bala muy juddu ndaxte dafa dogaloon ëllëgam bu du jeex (Yér. 1:5). [Lecture de la Bible ; voir w88 1/4 p. 10 § 2.]
Tontul laaj yii di topp :
11. Lan mooy ‘ sànnil sa mburu ’ bi ñuy wax ci Dajalekat 11:1 ? [Lecture de la Bible ; voir w87 15/9 p. 25 § 12.]
12. Kan la Yexowa doon wax bi mu waxee “ ñun ” ci Isayi 6:8 ? [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 93-4 § 13.]
13. Naka la “ leer gu mag ” leeralee Galile ni ñu ko waxe ci Isayi 9:2 ? [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 126 § 17.]
14. Ci suñu jamano, lan lañu mën a tollale ak daanu bi Babylon daanu ca atum 539 balaa suñu jamano, ak it toroxte bu mat bi ko naroon a dal (Isa. 13:19, 20 ; 14:22, 23) ? [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 188 § 30-1.]
15. Naka la “ surga bu takku te teey ” di jëfee ni nit ki doon séentu ci Isayi 21:6 (Macë 24:45) ? [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 221-2 § 11.]
16. Yan xelal yu am maanaa la xale bu góor buy ut jabar mën a gis ci Léeb. 31:10 ? [w00 1/2 p. 31 § 1]
17. Ci Isayi 43:9, lan lañu laaj yàllay àddina si ? [Lecture de la Bible ; voir w88 1/2 p. 16 § 3.]
18. Naka lañu mënee wax ne tànki ñi di yégal xibaar bu baaxu Nguuru Yàlla dañu “ rafet ” ? (Isa. 52:7.) [Lecture de la Bible ; voir w97 15/4 p. 27 § 6].
19. Lan lañu war a def ngir suñu xol bañ ñu wor (Yér. 17:9) ? [w00 1/3 p. 30 § 4]
20. Ñiy ‘ dox ci yoonu Yexowa ’, lan lañu war a def (Yér. 7:23) ? [Lecture de la Bible ; voir w99 15/8 p. 29 § 6.]
Mottalil kàddu yii di topp :
21. “ Xolu ki am xam-xam mu ngi ci ndeyjooram ”, ndax bare na li “ ndeyjoor ” di wone ․․․․․․․․ ; kon loolu dafay wone ne ․․․․․․․․ mooy tax muy am jëfin bu rafet bi gën ci moom (Daj. 10:2 ; Macë 25:33). [Lecture de la Bible ; voir w87 15/9 p. 25 § 9.]
22. ․․․․․․․․, ․․․․․․․․, ak ․․․․․․․․ yi ñu war a wone ci santaane Yàlla yi, bokk na ci li ñu mën a jàng ci Woyu Suleymaan. [si p. 117 § 16]
23. Ki ñuy wax ci Isayi 33:1, mooy ․․․․․․․․, ki siif Yudaa. Réew boobu, 632 balaa suñu jamano lañu ko waroon a daan, te naroon nañu bàyyil ñi dëkk ․․․․․․․․, alal bu bare. Ñooñu naroon nañu dajale alal boobu, ni ñuy dajale ay mbóot (Isa. 33:4). [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 343 § 4 ; p. 345 § 6.]
24. Bu ñu seetee li nekk ci Isayi 54:1 ak Galasi 4:26, 27 dinañu gis ne “ jigéen ju masula [“ mënul a ”, NW] am doom ” mooy ․․․․․․․․ te “ jigéen bu am boroom kër ” mooy ․․․․․․․․. [Lecture de la Bible ; voir w95 1/8 p. 11 § 8.]
25. Bu ñuy waaraate, bu ñu gisee nit ñu nuy sewal, walla nit ñu nuy bañ a déglu, dañu war a fàttaliku ne du ․․․․․․․․ lañu ko def, waaye ․․․․․․․․, ki ñu wax li ñu war a wax bu ñuy waare, lañu koy def (2 Kor. 4:1, 7). [w00 15/1 p. 21 § 1]
Tànnal tontu bu baax bi ci kàddu yii di topp :
26. Pool gisoon na màggaayu Yeesu ca asamaan. Bi mu bindee li mu gisoon ci peeñu boobu, tudde na boppam “ liir bu judduwul ci jamanoom ”. Dafa bëggoon a wax ne (xel mu sell mi dafa ko sogoon a tànn ndax mu nekk doomu Yàlla ; dañu ko teeloon a def ndaw, yónni ko ci ñi nekkul Yawut ; dafa meloon ni dañu ko may mu juddu walla dekki nekk xel balaa waxtu bi jot) (1 Kor. 9:1 ; 15:8). [w00 15/1 p. 29 § 6]
27. Bu ñuy wax “ Baay bu sax ”, dañu bëgg wone kàttan ak kiliftéef bu buur bi nekk Almasi am ngir may ay nit (doole ci wàllu xel ; ñu am dund bu mënul a jeex mukk ca asamaan ; ñu mën a dund dund bu dul jeex ci kow suuf) (Isa. 9:6 ; Ywna. 11:25, 26). [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 131 § 26.]
28. Ci li war a am ci suñu jamano ni ko Isayi 66:7 waxe, “ xale bu góor ” bu ñu jur mooy (Yeesu Krist ; Nguuru Almasi bi ; xeet ci wàllu xel bu bees ci atum 1919). [Lecture de la Bible ; voir w95 1/1 p. 11 § 3.]
29. Bu ñu jàngee bu baax Macë 10:28, dina ñu gis ne Gexenna bu safara (béréb la fu ñuy yëg ay metit ; mooy sànkute ba fàww ; dafay wone ni ñu sore Yàlla). [rs p. 128 § 1]
30. Ci li war a am ci suñu jamano ni ko Yérémi 7:28 waxe, “ xeet bi toppul baati Yexowa ” mooy (Babilon bu Mag bi ; mbooloo yiy wuyoo turu karceen te fekk toppuñu Yeesu ; juróom ñaareelu kàttan bi ci àddina si). [Lecture de la Bible ; voir w88 1/4 p. 18 § 10.]
Booleel aaya yi di topp ak kàddu yi nekk ci suuf :
Léeb. 24:16 ; Daj. 3:11 ; Isa. 40:8 ; Room 10:15 ; 1 Pie. 4:6.
31. Ci waxtoom, dinañu xam fu lépp li Yàlla def war a féetee ci li mu bëgg def. [Lecture de la Bible ; voir w87 15/9 p. 24 § 8.]
32. Bu ñuy waare xibaar bu baax bi, loolu dafay may ñi dee ci wàllu xel ñu mën a tuub seeni bàkkaar. [rs p. 63 § 2]
33. Dëgg la, ci àddina si, daanu mënul ñàkk, waaye, ku gore ci Yàlla du bàyyi jéem a def lu baax. [w00 1/2 p. 5 § 1]
34. Bu Yàlla waxee dara, walla li mu bëgg def, kenn mënu ko dindi walla tere mu am. [Lecture de la Bible ; voir ip-1 p. 401 § 10.]
35. Ndawi Yeesu, jariñoo nañu bu baax li yonent Yàlla Isayi wax, di wone ni mu ànde ak liggéeyu waare bi. [si p. 123 § 37]