Mbégte bi nekk ci jébbal sa jot yépp liggéeyu Yàlla
1 Yéen ndaw ñi, wóor na ñu ne dangeen di xalaat seen ëllëg. Léebu 21:5 wax na ne ku sawar ci liggéeyam, bu waajalee dara, ci lu wóor dina ko jural lu baax. Toog di xalaat sa ëllëg, lu baax la lay indil. Bu ngeen di xalaat li ngeen bëgg a def ëllëg, xalaatleen ci jébbal seen jot yépp liggéeyu Yàlla bi. Lu tax ?
2 Laajal mag ñi nekkoon pioñee bi ñu nekkee ndaw li ñu xalaat ci liggéey boobu. Ñoom ñépp, lii lañu lay wax : “ At yooyu ñooy yi gën a neex ci sama dund ! ” Am na suñu benn mbokk boo xam ne, bi mu nekkee ndaw la tàmbali jébbal jotam yépp liggéeyu Yàlla bi. Bégoon na ci. Bi mu demee ba nekk mag dafa nee : “ Biibël bi dafa ñu xelal ñu ‘ fàttaliku suñu Sàkk-kat bu mag bi, bu ñu nekkee ndaw ’. Ku mën a toog di xalaat bi mu nekkoon xale, te mu xam ne topp na xelal boobu, dinga am mbégte bu réy te xóot. ” (Daj. 12:1). Boo nekkee ndaw te nga bëgg am mbégte bu mel noonu, dangeen war a toog, yaw ak say way-jur, te seet bu baax fi nga war a jaar ba am ko.
3 Way-jur yi, na ngeen xiir seeni doom ci jébbal seen jot yépp ci liggéeyu Yàlla bi : Yexowa, moom mi mel ni baay buy toppatoo te bëgg bu baax doomam yi, dafa nuy won yoon bi ñu war a topp (Isa. 30:21). Buy def loolu, dafa nekk royukaay ci yéen way-jur karceen yi. Buleen bàyyi seeni doom tànnal seen bopp li gën ci ñoom, waaye na ngeen seet bu baax li ngeen mën a def ba ñu jaar ci yoon bi ñu war a topp, ngir am barkeelu Yàlla. Bu ñu màggee, li ngeen leen jàngal, dina leen may ñu mën a “ ràññe lu baax ak lu bon ”. (Yaw. 5:14.) Mag ñi, fi ñu jaar ci seen àddina, won na leen ne mënuñu wóolu seen xalaati bopp, waaye dañu war a wéeru ci Yexowa ndax mu def ba seen yoon jub (Léeb. 3:5, 6). Ndaw ñi ñoo gën a soxla loolu, ndaxte seen xam-xam ci àddina sorewul.
4 Way-jur yi, bu seeni doom amee fukki at ak lu ci topp, walla sax bala loolu, waxtaanleen ak ñoom, ci liggéey bi ñu mën a def bu ñu màggee. Na nekk lu mën a am. Dina am ñu leen di jéem a xëcc ci utum alal bu bare, ni ko waa-àddina si bëgge. Mën na nekk ñiy xelal eleew yi ci li ñu mën a def ëllëg (conseiller d’orientation), seeni jàngalekat, walla ñi nu bokkal kalaas. Dimbalileen seeni doom ñu tànn jàng mécce walla lu mel noonu, bu ko defee, faj seeni soxla du leen tere liggéeyal Nguuru Yàlla (1 Tim. 6:6-11). Ñu bare bu ñu jàngee ba liise ba pare jàng mécce walla sax ñu jàng mécce kese, dinañu mën a faj seeni soxla te boole ci nekk aji-xàll yoon bu ci sax (pionnier permanent).
5 Waxleen ndaw ñi bu ñu mënee góor-góorlu ba toog, bañ a séy, dina doon lu baax. Bu yàggee, bu ñu bëggee séy, li séy laaj dina gën a yomb ci ñoom. (Seetleen La Tour de Garde bu 15 oktoobar 1996, xët 14, xise 21 ba xise 23.) Fexeleen ba xale yi teel a bëgg dund dund bu neex Yàlla, dund buy jariñ ñeneen ñi, te dund bu leen di indil mbégte. Loolu mën ngeen koo def boo leen di wax lu baax ci nekk pioñee, ci dem fu ñu soxla ay waaraatekat yu bare, ci liggéeyu Betel, ak it ci nekk aji-xàll yoon bu ci jagleel jotam gépp (pionnier spécial).
6 Ndaw ñi, jiitalleen jébbal seen jot yépp liggéeyu Yàlla bi : Ndaw ñi, jarul ngeen di laaj seen bopp naka la liggéeyu pioñee mel. Na ngeen jéem a nekk aji-xàll yoonu weer saa yu ngeen ko mënee, bu ngeen di jàngi, ak it bu lekkool tëjee. Bu boobaa, dingeen xam dëgg ni nekk pioñee neexe ! Ndax mën nga seet diggante tey ak bu lekkool ubbiwaatee kañ nga mën a nekk aji-xàll yoonu weer ?
7 Boo nekkee góor gu bokk ci mbootaayu Yàlla, xalaatal bu baax ci ni nga mënee def ba mën a nekk surga mbooloo mi (1 Tim. 3:8-10, 12). Te it, seetal li nga bëgg def : bind kayit bi ñu def ngir dugg Betel walla dem ci Lekkoolu surgay mbooloo mi (École de formation ministérielle), bés bu la ko say at mayee. Boo nekkee pioñee dinga jàng lu bare lu mel ni : ni nga mënee topp benn porogaraam, ni nga gën a mënee defar sa porogaraamu bopp, ni nga mënee déggoo ak nit ñi, te ni nga mënee tàmm def li la war. Loolu lépp dina tax ëllëg nga mat ku ñu mën a dénk lu gën a am solo ci liggéeyu waare bi.
8 Boo bëggee jébbal sa jot yépp ci liggéeyu Yàlla bi te def ko bu baax, danga war a sawar ci lépp li la Yexowa laaj. Ci loolu la ñu ndaw li Pool doon xiir, te wone na barke yi ñu ciy jële : “ Lu ngeen mana def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, [...] xam ne Boroom bi dina fey seeni jëf. ” (Kol. 3:23, 24). Yàlla na leen Yexowa barkeel ak mbégte yu bare ci liggéeyu waare bi ngeen jébbal seen jot yépp !