Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru suweŋ : Lan lañu Yàlla laaj ? walla Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Boo tasee ak ku am téere yooyu, won ko benn ci téere yu ndaw yu nekk ci sa mbooloo, bu mën a baax ci moom. Sulyet ak ut : Benn ci téere bu def 32 xët ci yi nekk fii : Dieu se soucie-t-il vraiment de nous ? ; Doit-on croire à la Trinité ? ; Le gouvernement qui établira le Paradis ; Le nom divin qui demeure à jamais ; Quand la mort frappe un être aimé... ; Que devient-on quand on meurt ? ; Quel est le but de la vie ? Comment le découvrir ? ; Dunda léen bà fàw ak banéx ci suf si! ; Voici, je fais toutes choses nouvelles ”. Boo gisee ne dina baax ci nit ki ngay waxal, mën nga wone téere yii : Connaîtrons-nous un jour un monde sans guerre ? ; Les esprits des morts — Peuvent-ils vous aider ou vous nuire ? Existent-ils vraiment ? ; Nos problèmes — Qui nous aidera à les résoudre ? ; Un livre pour tous. Septaambar : La vie : comment est-elle apparue ? Évolution ou création ?
◼ Yégle bii di topp, mbooloo yi bànqaas bu Congo-Kinshasa di toppatoo ñoo ko moom : Képp ku am lu mu bëgg wax Mbootaay bi, bu ko mënee, bind moo gën. Dina yombalal liggéeyu bànqaas bi. Bu fekkee ne li nga bëgg wax walla xam jampul, telefone gënul. Bu jampee tuuti rekk te ngeen war a telefone, ñu ngi leen di ñaan ngeen def ko ci bésu altine kese. Yenn saay li ngay bëgg wax soxlawul sutura. Kon, wax ko ki nga xam ne moom mooy jot nit ñiy telefone ci bànqaas bi, te ñaan ko mu jottali ko biro bi. Dina bind li ngay wax, ngir bañ a juum. Saa yu ñu amee li ñu bëgg yónnee bànqaas bi, nañu ko def ci turu Seede Yexowa yi. Buñu ko yónnee ci turu kenn. Te it, bindal biro bi ko war a jot. Mën na nekk biro biy toppatoo ndaje bu gën a mag bi, biro biy toppatoo xaalis bi, biro yiy toppatoo liggéeyu waare bi, biro yiy yónnee téere yi, walla yeneen biro.
◼ Ci ayu-bés biy tàmbali bésu 16 septaambar 2002, dinañu tàmbalee jàng téere bi tudd Prophétie d’Isaïe II, ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi.
◼ Téere yu bees yu ñu mën a am :
Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? (T-26) — braille anglais (deuxième degré), braille français (premier degré), swaili
Avez-vous un esprit immortel ? (T-25) — braille anglais (deuxième degré), braille français (premier degré), ewe
Jéhovah : qui est-il ? (T-23) — braille français (premier degré)
Jésus Christ : qui est-il ? (T-24) — braille français (premier degré)
Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex (bind yu réy) — purtugees
Le monde actuel survivra-t-il ? (T-19) — yoruba
Jamano ji ñu war a nangul Yàlla ca dëgg — awusa (haoussa)
Woyal, di Tagg Yeowa (bind yu réy) — yoruba
Pourquoi avoir confiance en la Bible (T-13) — liŋala
Prêtons attention à la prophétie de Daniel ! — yoruba
Quelles sont les croyances des Témoins de Jéhovah ? (T-14) — liŋala
Une vie pleinement satisfaisante : Comment ? — braille français
◼ Kaset yu ñuy déglu, yu bees yi ñu mën a am :
Respectons l’autorité de Jéhovah (daraam, benn kaset) — español
◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :
Le plus grand homme de tous les temps, volume 3 (PAL) — ci làkku liyaaru Amerig (maanaam làkku ñi tëx)
Le plus grand homme de tous les temps, volume 5 (NTSC) — ci làkku liyaaru Amerig