Suñuy mbokk ci wàllu ngëm, lu tax ñu bëgg leen ñoom ñépp ?
Mbëggeel barewul ci àddina si ñu nekk. Lan lañu war a def ba mën a wone ne dañu bëgg bu baax-a-baax suñuy mbokk ci wàllu ngëm (1 Pie. 2:17) ? Naka lañu mënee won nit ñi ne, dëgg-dëgg, ci àddina si sépp, ñu ngi mel ni ay mbokk ci suñu biir (Macë 23:8) ? Wideo bi tudd Toute la communauté de nos frères mën na ñu ci dimbali. Dafay wone lu tax ñuy bëggante ci suñu biir. Seetal ndax dinga mën a tontu li ñuy laajte fii :
1) Am na ñetti yëf yi ñuy def ñun ak suñuy mbokk ci wàllu ngëm yi nekk ci àddina si sépp. Waxal yan yëf la. 2) Suñuy mbokk yi ci wàllu ngëm, naka lañu wonee ne bëgguñu dara tere leen a waaraate a) ci àll bi nekk ci Alaska, b) ci poor yu réy yi nekk ci dëkki Ërob yi, ak it c) ci àll bi nekk ca Peru ? 3) Lan lañu mën a jëfandikoo ngir mu jur lu baax ci waaraate bi ? 4) Lu tax waruñu méngale waaraate bi ak yeneen liggéey yi ? 5) Woneel ni Seede Yexowa yi di dimbaleentee ci seen biir, bu nu nekkee ci jamano tiis — bu amee yëngu-yëngu suuf, ngelaw bu réy-a-réy buy yàqe, walla bu nit ñu bokk réew dee xeex ci seen biir. (Seetal li Takao wax ci Réveillez-vous ! bu 22 ut 1995 ci xët 23 ak li Kotoyo wax ci Réveillez-vous ! bu 22 oktoobar 1996, ci xët 20.) 6) Lan lañu mën a def ngir wone ne li war a feeñ ci diggante karceen yi, ba tax ñu mën leen a xàmme, mu ngi ci suñu biir (Ywna. 13:35) ? 7) Ndaje yi ñu am ci suñu mbooloo, naka lañu leen war a fonke ? 8) Ñi amul woon Saalu Nguur, bés bi ñu ci amee benn, lan lay def ci ñoom ? 9) Bi ñu teree Seede Yexowa yi ñu jaamu Yexowa ci dëkki penku Ërob ak Russie, suñu mbokk yi fa nekkoon, naka lañu def ba sàmm seen ngëm ? 10) Ba tey jii sax, naka la seede yu bare di xeexe ngir mën a fekke ndaje yi gën a mag yi, te lu waral loolu ? Loolu naka la yokke sa doole ? 11) Lu tax ngeen fas yéene ànd di jaamu Yàlla, dimbali ñeneen ñi bu ñu ko soxlaa, te waaraate saa yoo leen ko mënee ak fépp foo leen ko mëne ? 12) Boo mënee am benn ci wideo yii te wone ko nit ñi bëgg waxtaan ak ñun yoo mën yépp, lu tax mu nar a baax ?