Na nga doylu ci li nga am
1 Mbind mi dafa ñuy sant ñu faj suñuy soxla njaboot. Waaye, loolu warul nekk li ëpp solo ci suñu dund. Suñu diggante ak Yàlla moo war a jiitu lépp (Macë 6:33 ; 1 Tim. 5:8). Xam ni ñu war a yemaleente ñaar yooyu, yombul ci “ bési tiis yu tar ” yi ñu nekk nii (2 Tim. 3:1). Lan moo ñu ciy dimbali ?
2 Nañu nangu li Biibël bi wax ci loolu : Wut alal mën na yàq suñu diggante ak Yàlla. Kàddu Yàlla artu nañu ci loolu (Daj. 5:10 ; Macë 13:22 ; 1 Tim. 6:9, 10). Li ñuy def ci wàllu ngëm, ëmb na ndaje yi, njàng mi, ak waaraate bi. Ci jamono ju am solo jii ñu nekk, bu suñu xel yépp nekkee ci suñu liggéey, walla ci wutum xaalis, ba loolu jiitu li ñu war a def ci wàllu ngëm ci suñu dund, musiba lay doon (Lukk 21:34-36). Wànte Biibël bi mu ngi ñuy xelal lii : “ Su nu amee lekk ak koddaay, nanu ko doyloo. ” — 1 Tim. 6:7, 8.
3 Loolu tekkiwul ne karceen yi waruñu nangu am alal. Waaye dafa ñuy won lu ñu soxla dëgg, maanaam lu ñuy lekk, lu ñuy sol ak fu ñuy dëkk. Bu ñu amee li ñu soxla dëgg ngir mën a dund, waruñu dëkk ci wutum alal bu dul jeex. Bu ñu bëggee jënd dara walla yokk suñu liggéey, lii lañu war a laaj suñu bopp : “ Ndax soxla naa ko dëgg ? ” Su ñu defee loolu, dinañu gën a mën a topp xelalu Yàlla bii : “ Buleen bëgge; deeleen doylu. ” — Yaw. 13:5.
4 Bu ñu yaakaaree ci Yàlla, dina ñu barkeel (Léeb. 3:5, 6). Bu fekkee ne sax dañu war a liggéey, liggéey bu metti, ngir am li ñuy soxla bés bu nekk, soxla yooyu waruñu nekk li ëpp solo ci suñu dund. Bu ñu amee lu bare, walla bu ñu amee lu tuuti, Yexowa lañuy yaakaar ngir am li ñuy faje suñuy soxla (Fil. 4:11-13). Lu ñu ciy jële ? Doylu buy ànd ak ragal Yàlla, ak yeneen barke yu bare.
5 Nañu roy ngëmu ñeneen ñi : Benn jigéen dafa doon yar moom kenn doomam bu jigéen ci yoonu dëgg gi. Jigéen jooju dafa yombalal dundam ndànk-ndànk. Dafa amoon kër gu rafet, waaye dafa ko bàyyi, dem dëkk ci kër gu gën a ndaw, ba pare mujj dëkk ci kër gu tuuti. Loolu tax na mu mën a wàññi liggéeyam, te yokk li mu doon waaraate. Bi doomam màggee ba séyi, jigéen jooju dafa jël rëteret (retraite) balaa waxtu bi jot, fekk loolu dafa doon wàññi xaalis bi mu naroon a am. Am na léegi juróom ñaari at bi suñu mbokk boobu nekkee aji-xàll yoon ju ci sax, te réccuwul fenn li mu nangu ñàkk ci wàllu alal ngir jiital Nguuru Yàlla ci dundam.
6 Benn magu mbooloo mi ak jabaram nekk nañu pioñee ay at yu bare, fekk ñu yor ñetti doom. Ñoom ak seeni doom, dañu jàng yem ci li ñu soxla dëgg, te bañ a jéem a am lépp li ñu bëgg. Baay bi nee na : “ Dañu doon dund dund bu gën a woyof. Dëgg la, yenn saay dafa doon metti, waaye saa su nekk, Yexowa dafa ñu doon may li ñu soxla. [...] Bu may gis sama njaboot di jiitale noonu seen diggante ak Yàlla ci seen dund, damay gis ne lépp a ngi dox ni mu ware, te damay xam ne li ma def baax na. ” Jabaram dolli ci : “ Bu ma gisee [sama jëkkër] di am lu bare li muy def ci wàllu ngëm, mbégte bu réy lay yëg ci sama xol. ” Seeni doom it dañu kontaan ci li seen waajur nekke pioñee.
7 Ñiy tànn dund buy wone ne dañu takku ci Yàlla, te bañ a dëkk ci wutum alal, Biibël bi dig na ne dinañu am ay barke yu bare, tey ak ëllëg. — 1 Tim. 4:8.