Mën ngeen ci am alal ju bare !
1. Lu tax nga war a seet ndax mën nga nekk pioñee bu ci sax ?
1 Ndax danga bëgg am mbégte bu gën a réy te kontaan ci li ngay def ci sa àddina ? Ndax dimbali sa moroom dafa la neex te dafa lay may mbégte ? Ndax danga bëgg yokk li ngay def ci liggéeyu Yexowa ? Bu dee tontu nga waaw ci benn ci laaj yooyu, war nga seet ndax mën nga nekk pioñee bu ci sax. Dëgg la, ku bëgg nekk pioñee war na seet ci wareef yi mu am ci njabootam, ak ci yeneen wareef yi Mbind mu sell mi teg ci kowam. War na seet it ci wér-gi-yaramam ak fi dooleem yem.
2. Waxal lu mën a bokk ci alal ci wàllu ngëm yu pioñee yu ci sax yi di am ?
2 Ci xaaju Mbind mu sell mi Suleymaan bind, barke yi Yexowa doon maye, dafa doon laal mbirum alalu àddina (Prov. 10:22). Tey, barke Yexowa, alal ci wàllu ngëm lay gën a indi. Pioñee yu ci sax yi dañuy am lu bare ci alal bu mel noonu. Lii bokk na ci alal boobu : mbégte bu réy bi ñuy yëg bu ñuy may dara suñu moroom. Mbégte boobu pioñee yi dañu koy yëg bu ñuy “ jariñoo ” seen jot ngir dimbali seeni moroom fekk mënoon nañu ko def ci seen itte bopp (Kol. 4:5 ; Jëf. 20:35). Yexowa dafay gis liggéey bi ñuy def ndax mbëggeel bi ñu am te loolu neex na ko lool. Loolu “ alal ” bu ñu dajale ca asamaan la, te njëgam du mas a waññeeku (Macë 6:20 ; Yaw. 6:10). Li ëpp solo mooy, seen diggante ak Yexowa dafay gën a dëgër rekk. Lu tax loolu ? Ndaxte pioñee yu ci sax yi, dañuy kontine di yore ‘ bët bu wér ” te dañuy yaakaar ci Yexowa ngir mu jox leen lépp li ñu soxla. — Macë 6:22, 25, 32 ; Yaw. 13:5, 6.
3. Wutum alal ci wàllu ngëm ak wutum alalu àddina, lan moo leen wuutale ?
3 Wutum alalu àddina dafay faral di dugal nit ci “ bëgg-bëggi neen yuy yóbbe ayib ” maanaam bëgg-bëgg yu amul benn njariñ te di lor nit ki (1 Tim. 6:9, 10 ; Saag 5:1-3). Barke Yexowa du def loolu mukk. Def lu bare ci sa jot ci waaraate bi, dafay dimbali pioñee yu ci sax yi ñu kontine di dëgër ci wàllu ngëm te di mën a raññee bu baax li gën a am solo (Fil. 1:10). Suñu benn mbokk bu góor dafa bàyyi liggéeyu ingénieur bi mu doon def ngir nekk pioñee. Lii la wax : “ Dama doon wax ne sama liggéey dafa metti lool. Liggéeyu pioñee bi moom melul noonu. Léegi mën naa dimbali nit ñi te di leen jàngal dëgg gi. Ci laay gën a am mbégte te moo dàq fuuf. ”
4. Naka la pioñee yu ci sax yi di ame barke bu ñuy indil seeni moroom ay barke ?
4 Ay barke lañu pur seeni moroom : Tey, ñépp ay jànkoonteek “ bési tiis yu tar ” (2 Tim. 3:1). Fépp ci àddina, nit ñi soxla nañu am yaakaar lool. Waaraatekati Nguuru Yàlla dañuy am mbégte bu réy bu ñuy dimbali ñi amul yaakaaru ëllëg ñu jàng te topp digle xibaar bu baax bi. Pioñee yu ci sax yi dañuy def at bu nekk lu ëpp 800 waxtu ci liggéey boobu di musal ay bakkan. Loolu mbégte bu réy la ci ñoom. — 1 Tim. 4:16.
5, 6. Lan moo la mën a may nga nekk pioñee bu ci sax ?
5 Ndax seet nga bu baax ndax mën nga nekk pioñee bu ci sax ? Xéyna loolu dina laaj nga “ jariñoo jot gi ” nga doon def ci lu amul solo noonu (Efes 5:15, 16). Ñu bare loolu lañu def te dañu woyofal seen dund. Loolu tax na ñu mën a wàññi jot gi ñu doon def ci seen liggéey ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu Nguur gi. Ndax mënuloo seetaat ni ngay toppatoo say soxla bopp ngir mën a def ni ñoom ?
6 Ñaanal Yexowa mu may la xam-xam bi ngay defe porogaraam bu baax (Saag 1:5). Yan barke nga ci mën a séentu ? Alal ju bare ci wàllu ngëm ! Yexowa dina la barkeel it ci wàllu alalu àddina ndaxte dina la jox li nga soxla (Macë 6:33). Ñiy jëf ngir seetlu Yexowa ci fànn boobu, dinañu am ay “ barke ba ñàkk dootul amati ”. — Mal. 3:10.