Nañu tàmm waaraate
1 Ndax ñu ngi góor-góorlu ngir tàmm a waaraate ? Weer wu nekk, ndax dañuy gaaw a bind li ñu def ci waaraate bi ba pare joxe ko ci Saalu Nguur gi ? Ñun ñépp, war nañu góor-góorlu ci loolu. Waruñu nangu mukk mu am weer boo xam ne waxtaanuñu sax ak nit lu jëm ci suñu ngëm. — Room 10:9, 10.
2 Bu ñu tàmmee waaraate ñun ci suñu wàllu bopp, saa yu ñu ko mënee, war nañu dimbali it ñeneen ñi, ndax ñu tàmm waaraate ñoom itam (Fil. 2:4). Naka lañu ko mënee def ? Am na ay waaraatekat yu ñu sóobagul yuy tàmbali waaraate. Mën nañu leen ñaan ñu ànd ak ñun ci waaraate bi. Ñooñu, bu ñu amee porogaraamu waaraate bu baax, dina tax dëgg gi sax bu baax ci seen xol.
3 Nañu tàmm waaraate. Nañu bind weer wu nekk li ñu def ci waaraate bi te joxe ko. Nañu dimbali suñu moroom ngir ñu tàmm waaraate. Nañu “ bëgg kureelu mbokk yi ”. — 1 Pie. 2:17.