TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 10/02 p. 7
  • Ay tont ci seeni laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay tont ci seeni laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 10/02 p. 7

Ay tont ci seeni laaj

◼ Lan lañu mën a taf ci tablo fu ñuy def yégle yi ci Saalu Nguur gi ?

Yégle yi jëm ci li ñuy def ci mbooloo mi moo tax ñu def tablo bi nekk ci Saalu Nguur gi. Balaa ñu ciy taf dara, wottukat biy jiite dafa ci war a ànd.

Lii lañuy faral a taf ci tablo bi : Porogaraamu ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi, walla porogaraamu lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ak ñi war a def waxtaan yi ci nekk ; waxtaan yu ñu jagleel ñépp yu ñu war a def ci mbooloo mi ; ki war a jiite ndaje bu ñu jagleel ñépp ak ki war a jàng La Tour de Garde ; ñi bokk ci njàngum téere yi ñuy def ci mbooloo mi ak fi ñu koy defe ; kañ la wottukat biy wër ci mbooloo yi war a ñów ci mbooloo mi ak yégle yiy jëm ci loolu ; yégle yi jëm ci ndaje bu mag buy ñów, ak porogaraamu set setalu Saalu Nguur gi. Yenn saay Mbootaay bi dafay ñaan magi mbooloo yi ñu taf yenn leetar walla leneen ci tablo bi. Bu amee lu ñu tàmmul woon a taf ci tablo bi, kurélu magi mbooloo mi moo war a wax ndax mën nañu ko ci taf.

Mën nañu def yenn saay, ci benn ndaje, yégle bu gàtt bu jëm ci takk gu war a am ci Saalu Nguur gi. Waaye waruñu taf ci tablo bi, yégle bu jëm ci takk. Waruñu ci taf it yégle bu jëm ci ndaje bu jëm ci diggante nit ak nit, ndaxte ndaje yooyu bokkul ci li ñuy def ci mbooloo mi. — Seetleen La Tour de Garde bu 15 sulyet 1984, ci xët 15.

Tablo bi dafa war a set te jekk. War na yaatu yaatuwaay bu doy ndax ñu mën ci taf lépp li ñu ci war a taf te ñu lim ko sànq. Bu amee porogaraam bu ñu def ba pare, walla loo xam ne mbooloo mi jot na ko xam ba noppi, war nañu ko gaaw a dindi ci tablo bi. Bu amee ay mbooloo yu bokk benn Saalu Nguur, mbooloo mu nekk war na am tablo boppam, walla xaaju boppam ci tablo bi. Li gën mooy, wottukat biy jiite walla nit ku mu tànn, tàmm di seet li nekk ci tablo bi. Bu ko defee yégle yi ci nekk duñu weesu, dinañu baax ci mbooloo mi, te jekk.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager