TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/02 p. 7
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 11/02 p. 7

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru nowàmbar : Lan la ñu Yàlla laaj ? walla Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Bu ngeen gisee ku am téere yooyu ba pare, wonleen ko benn ci téere yu yàgg yi. Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Mën nga wone it benn ci téere yii : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ? ; Recueil d’histoires bibliques walla Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Sãwiyee : Téere yi am 192 xët te génn bala 1988 yi ngeen am ci seen mbooloo. Mbooloo yi am téere L’humanité à la recherche de Dieu, mën nañu ko wone itam. Feewriyee : Téere Création (bu ndaw bi walla bu mag bi) walla La Révélation : le grand dénoument est proche !

◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, bésu 1 desàmbar lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

◼ Bu mbooloo yi di laaj téere yi ñu soxla, mën nañu ci boole léegi téere bi boole La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi génn ci atum 2002 (Volumes reliés). Mën nañu leen laaj ci ãgale, ci tubaab, ci purtugees ak ci español. Ba keroog ñu leen di jot ci mbooloo mi, dinañu bind téere yooyu ci kayit fi ñuy bind téere yi ñuy jot ak yi ñu war a jot bu ci kanamee (Pending) ci mbooloo mi. Ci téere yi ñu war a jot bu ci kanamee lañuy bokk. Téere yuy boole La Tour de Garde yi ak téere yuy boole Réveillez-vous ! yi, bala ñu leen di mën a jot ci mbooloo mi, dañu leen war a laajte.

◼ Am na ñuy maye xaalis ci ndaje bu mag bu ñaari fan, ndaje bu mag bu benn fan, walla ci boyet yi ñu def ci Saalu Nguur yi ngir jàpple liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp, walla ngir xaalis bi ñuy dajale ngir defar ay Saalu Nguur. Ñiy def xaalis boobu ci li tubaab di woowe cheque (maanaam kayit yi ñuy wone ci bànk ba ngir ñu jox ñu xaalis), dañu war a def cheque yooyu ci turu mbootaay bi nekk ci seen réew. Ñi nekk Cameroun dañu ko war a def ci turu “ A.C.T.J. CAM ”.

◼ Téere yu bees yu ñu mën a am :

Ce que Dieu attend de nous — gbaya, moundang

Publications de la Société Watch Tower — Index 1986-2000 — español

Publications de la Société Watch Tower — Index 2001 — ãgale

Vivez éternellement heureux sur la terre ! — gbaya, moundang

◼ Kaset yu ñuy déglu, yu bees yi ñu mën a am :

Une vie pleinement satisfaisante : Comment ? — ãgale

◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :

Le plus grand homme de tous les temps (Volumes 8 et 9, NTSC) — làkku ñi tëx bu Amerig

Recueil d’histoires bibliques — làkku ñi tëx bu Amerig

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager