Boroom kër yi : tàmmleen di topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm
1 Dañel dëkk na ay fukki at, ci diggu Babilon, fu nit ñi doon jaamu ay xërëm te bonoon lool. Waaye moom, ñépp a xamoon ne dafa doon jaamu Yexowa “ ak takku gu mat ”. (Dañ. 6:16, 20.) Naka la def bay wéy di am noonu ngëm gu dëgër ? Biibël bi wone na ne dafa doon topp porogaraam bu baax ngir lépp li mu waroon a def ngir jaamu Yàlla ni mu ko bëgge. Lii bokkoon na ci li mu tàmmoon : Bés bu nekk, dafa doon yéeg ci néegam bi féete woon kow, ngir ñaan Yàlla (Dañ. 6:10). Waroon na am it porogaraam ngir yeneen yëf yi mu waroon a def ci wàllu ngëm, yëf yu mel ni jàng Sàrt bi. Looloo tax bi mu nekkee ci jafe-jafe bu mënoon a tax ñu rey ko, Dañel dafa wéy di topp Yexowa, te Yexowa dafa def kéemaan ngir musal ko. — Dañ. 6:4-22.
2 Ñun itam tey, war nañu góor-góorlu noonu ngir wéy di bañ a nelaw (Efes 6:18). Àddina si tey mu “ ngi tëdd ci loxoy Ibliis ”. (1 Ywna. 5:19.) Fitnaal ak jafe-jafe mën nañu jékki-jékki rekk ñów, te song suñu ngëm. Bu metit wu réy wi ñówee, ñiy jaamu Yàlla dinañu mel ni ñu amul dara lu leen di aar ci kanamu Gog bu Magog te dina leen xeex bu baax. Loolu dina laaj ñu wóolu Yexowa bu baax-a-baax. — Esek. 38:14-16.
3 Ci ndaje bi gën a mag bi ñu defoon ca atum 1998, defoon nañu benn daraam bu tuddoon : “ Yéen, njaboot yi — Fexeleen njàngum Biibël bi, bés bu nekk, doon seen dundin ! ” Daraam boobu dafa ñu doon xamal ne njaboot yi dañu war a tàmm duruus, jàng ak waxtaane Biibël bi. Lu am-a-am solo la. Xamaloon nañu it ne bu njaboot yi tàmmee topp porogaraam bu mel noonu, di ko def ci fasoŋ buy tax ñu mel ni ñuy fekke li ñuy jàng ci Biibël bi, dina jur lu réy ci njaboot yi. Dafay yokk suñu xam-xam, te dëgëral suñu ngëm. Dinañu ci gis ay góor ak ay jigéen yu doon topp Yàlla bu baax ci jamano yu njëkk ya. Nit ñooñu dinañu nekk ay royukaay, yu ñuy xiir ci jàpple dëgg gi. Dinañu wone léegi li mën a bokk ci porogaraam bu baax ci wàllu ngëm. Bu ñu koy def, na boroom kër yi wut benn walla ñaari fasoŋ yi ñu mën a taneel porogaraam bi seen njaboot di topp ci wàllu ngëm.
4 Jàng Kàddu Yàlla bés bu nekk : “ Bu Nguuru Yàlla ilifee fekk kenn du ko xeex, te li mu bëgg bu amee ci kow suuf ni mu amee ca asamaan, benn nit ku bon te it benn mala buy ‘ def lu bon walla yàqal nit ñi ’ du amati (Isa. 11:9 ; Macë 6:9, 10). ” Kàddu yooyu, dañu leen tibbe ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2001, ci baat yi àndoon ak aaya bésu 11 septaambar. Loolu ñu doon fàttali nit ñi, dafay yokk doole bu baax-a-baax. Yow mii nekk boroom kër, ndax bés bu nekk tàmm nga di jàng aaya bés bi ak baat yi mu àndal yow ak sa njaboot ? Lu am njariñ la. Bu ngeen mënulee toogandoo yéen ñépp ci suba si, du ñàkk ngeen mën koo def ci beneen waxtu ci bés bi. Am na baay bu nee : “ Waxtu reer bi baaxoon na lool ngir ñu waxtaan ci aaya bés bi. ”
5 Bu fekkee ne seen njaboot tàmm na di waxtaan ci aaya bés bi, lu baax la. Xéyna mën ngeen ci yokk leneen lu leen di jariñ : bu ngeen di jàng aaya bés bi, jàngleen it benn xaaj ci Biibël bi. Ñenn ñi tàmm nañu di jàng ba mu daj pàcc bi ñu jële aaya bés bi. Ñeneen ñi dañuy tànn benn téere ci Biibël bi, di ci jàng tuuti bés bu nekk ba mu daj. Bu seen njaboot dee jàng Biibël bi bés bu nekk, dina tax mu gën a ragal a def lu neexul Yexowa, te gën koo bëgg neex. — 5 Mu. 17:18-20.
6 Porogaraam bi ngeen taxawal ci seen njaboot ngir jàng Biibël bi ak aaya bés bi, dina leen gën a amal njariñ bu ngeen ci yokkee tuuti minit ngir waxtaan ci ni ngeen mënee topp li ngeen jàng. Téere École du ministère lii la wax ci xët 60 : “ Mën [...] ngeen a tànn ay aaya ci pàcc bi ñu war a jàng ayu-bés bi [ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi], waxtaan ci li mu tekki, ba pare laaj ay laaj yu mel nii : ‘ Naka la aaya yooyu di wone li ñu war a def ? Naka lañu leen mënee jëfandikoo ci waaraate bi ? Lan lañuy xamal ci Yexowa ak santaaneem yi, te naka lay yokke ni ñu ko fonke ? ’ ” Waxtaan ci wàllu ngëm yu mel noonu dina tax képp ku bokk ci seen njaboot ‘ xam liy coobareg Boroom bi ’. — Efes 5:17.
7 Njàngum Biibël bi ci njaboot bi : Jàng Biibël bi ak seen njaboot ayu-bés bu nekk, bokk na ci li mën a won seen doom ne mbiri Yàlla moo war a jiitu lépp. Lii la benn waxambaane nettali : “ Yenn saay, bu sama baay doon wàcc, dafa doon sonn ba nga xam ne toog te bañ a nelaw dafa ko doon jafe lool. Waaye terewul dañu doon def suñu njàngum Biibël ci njaboot bi. Loolu tax na ñu xam ne lu am-a-am solo la. ” Xale yi itam mën nañu def seen wàll ndax njàngum Biibël bi dox bu baax. Ci benn njaboot bu amoon juróom-ñeenti xale, ñépp a doon jóg bu juróomi waxtu jote, ngir def seen njàngum Biibël ci njaboot bi, ndax amul woon beneen waxtu bu ñu ko mënoon a def.
8 Boroom kër yi dañu war a ‘ sàmm seen njàngale ’. (1 Tim. 4:16.) Téere École du ministère nee na ci xët 32 : “ Mën nañu wax ne ku bëgg def ak njabootam njàngum Biibël bu mën a jur lu baax, dafa war a njëkk seet li njabootam soxla. Ñi bokk ci sa njaboot, naka lañuy jëme kanam ci wàllu ngëm ? [...] Booy waaraate ak say doom, bu ñu dajee ak seeni moroom, ndax duñu ragal a wax ne ay Seedee Yexowa lañu ? Ndax porogaraam bi ngeen tëral ci seen njaboot ngir duruus te jàng Biibël bi neex na leen ? Ndax dinañu topp dëgg santaane Yàlla yi ? Yéen boroom kër yi, bu ngeen seetloo bu baax seen njaboot, dingeen gis lu ngeen war a def ngir képp ku bokk ci seen njaboot am ay jikko yu baax ci wàllu ngëm, te dëgëral jikko yooyu. ”
9 Ndaje mbooloo mi : Waajal ndaje yi te teew ci, war na nekk lu am solo ci li ngeen tàmm def ayu-bés bu nekk (Yaw. 10:24, 25). Yenn saay, ñi bokk ci njaboot bi yépp, dinañu mën a waajalandoo ndaje yi. Ndax mën ngeen fexe bay waajal ndaje yi lu yàgg balaa ñuy jot, te bañ koo def bu ñuy waaj a jot ? Porogaraam bu baax ci wàll woowu dina tax waajal bi gën a baax, te ndaje yi gën leen a amal njariñ. — Léeb. 21:5.
10 Porogaraam ci wàllu ngëm bala mu mën a jur lu baax dafa war a baax moom ci boppam, te dañu ko war a topp bu baax. Bu fekkee ne am na lu lay tere waajal ndaje yi yépp, loo war a def ? Téere École du ministère nee na lii ci xët 31 : “ Bul gaawantu waajal bi ngir mën a wax rekk ne def nga ko. Am na it leneen lu yées loo war a moytu : bul wax ne ndegam mënoo waajal yépp, doo waajal dara. Li gën mooy nga seet loo mën a jàng, te def ko bu baax. Defal noonu ayu-bés bu nekk. Bu yàggee, nanga jéem a fexe ba boole ndànk-ndànk yeneen ndaje yi ci porogaraam bi nga tëral ngir waajal ndaje yi. ”
11 Njaboot yi bu ñu teelee àggsi ci ndaje yi, dina tax ñu mën a waajal seen xel bu baax ngir màggal Yexowa te jariñoo li mu ñuy jàngal. Ndax sa njaboot tàmm na di teel a àggsi ci ndaje yi ? Loolu laaj na ngeen seet bu baax li ngeen war a def. Laaj na it képp ku bokk ci njaboot bi def wàllam. Bu fekkee ne sa njaboot ci daw la dëkk bés bu ngeen di am ndaje te dafay sonn lool, ndax mënuleen a seet li ngeen mën a soppi ci li ngeen tàmm def ? Ndax amul li ngeen mën a teel a def ? Bu amee ku sonn ndax liggéey bu bare bu mu war a def, ndax ñeneen ñi mënu ñu koo dimbali ? Bu ñépp teelee pare, ndax ñu mën a gën a teel a dem ci ndaje yi, ndax du wàññi coono yi ? Bu ngeen seetee bu baax ni ngeen di defe, dina indi jàmm ci njaboot yi ak ci mbooloo mi. — 1 Kor. 14:33, 40.
12 Liggéeyu waare bi : Jàpp bés bu ñuy waaraate, bokk na ci porogaraam bu baax ci wàllu ngëm. Benn waxambaane bu tudd Guillaume lii la nettali : “ Ci suñu kër, gaawu ci suba bu nekk, dañu ko doon beral waaraate bi. Looloo baaxoon ci man, ndax li ma doon gën di dem waare, may gën a gis lu baax lu muy jur, te di ko gën a bëgg ”. Ñi màgg ci njaboot bu nekk Seedee Yexowa, ñu ci bare gis nañu ne li ñu jàppoon bés bu ñuy waaraate ayu-bés bu nekk, tax na ñu jëm kanam ci liggéeyu karceen bi.
13 Porogaraam bu baax ci wàllu ngëm, mën na tax waxtu yi ngeen nekk ci waaraate bi gën a neex te gën a jur lu baax. Naka la koy defe ? La Tour de Garde bu 1 sulyet 1999 ci xët 21 newoon na : “ Yenn saay, ndax dingeen dimbali seen waa kër ci waxtu bi ngeen di defe seen njàngum Biibël bi ci njaboot bi, ndax ñu waajal liggéeyu waare bi ñuy def ayu-bés bi ? Loolu mën na am njariñ lool (2 Tim. 2:15). Mën na tax seen waaraate yokku te gën a jur lu baax. Yenn saay, mën ngeen jël waxtu bi ngeen di def seen njàngum Biibël bi, ngir waajal waaraate bi. Lu ci ëpp nag, bu njàngum Biibël bi ci njaboot bi di waaj a jeex walla ci beneen waxtu ci ayu-bés bi, mën ngeen a waxtaan waxtaan bu gàtt bu jëm ci yenn fànn ci liggéeyu waare bi. ” Ndax sa njaboot jéem na ko def ?
14 Nangeen wéy di jëm kanam : Ci li ñu wax fii yépp, ndax am na li sa njaboot di def bu baax ba pare ? Waxal sa njaboot ne li ñuy def noonu rafet na, te góor-góorlul ngir yokk ci dara. Boo gisee ay fànn yu bare yu ngeen war a taneel, tànn ci benn walla ñaar fu ngeen di njëkk góorlu-góorlu. Bu ngeen demee ba loolu bokk bu baax ci li ngeen tàmm ci wàllu ngëm, seetal benn walla yeneen ñaari fànn fu ngeen di góor-góorlu. Bul xalaat ne du ngeen ko mën, te bul teg sa njaboot lu mu àttanul (Fil. 4:4, 5). Fexe ba sa njaboot topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm, laaj na nga góor-góorlu dëgg. Waaye jar na ko ndaxte Yexowa nee na : “ Kuy topp yoon bu ñu rëdd, dinaa tax mu gis mucc gi Yàlla di indi. ” — Sab. 50:23.