Woneel ne ittewoo nga ak mbëggeel “ xale yu seen baay gaañu ”
1 Yexowa “ baay la ci xale yu seen baay gaañu ”. (Sab. 68:5.) Dafa bëgg ñu nekk ci jàmm. Li koy wone mooy ndigal bi mu joxoon Israyil bu njëkk ba maanaam : ‘ Waruleen toroxal benn jigéen bu jëkkëram gaañu, walla xale bu baayam gaañu. Boo ko toroxalee ci fasoŋ bu mu mënta doon, bu mu yuuxoo, ci lu wóor dinaa dégg yuuxoom. ’ (2 Mu. 22:22, 23). Am na it li Sàrtu Yàlla tëraloon ngir jàpple leen ci li ñu soxla ngir dund (5 Mu. 24:19-21). Ci jamano karceen yi, waxoon nañu ñiy jaamu Yàlla dëgg ñu “ nemmeeku jiirim yi ak jigéen ñi seen jëkkër faatu ci seeni tiis ”. (Saak 1:27.) Am na ay xale yu am benn way-jur kese, walla ñoo xam ne seen benn way-jur moo nekk Seede Yexowa. Naka lañu mën a wone ne ittewoo nañu xale yooyu ak mbëggeel, ni ko Yexowa di defe ?
2 Yar bi ci wàllu ngëm : Xéyna yow rekk yaa yore say doom, walla ki ngay séyal nekkul Seede Yexowa. Bu booba, jàng Biibël bi ak say doom ci seen kër ayu-bés bu nekk, mën na jafe lool. Waaye say doom soxla nañu ngeen tàmm def njàngum Biibël buy faj seeni soxla, ngir ñu mën a nekk ëllëg ay mag yu ñor te regle (Léeb. 22:6). Di waxtaan ak ñoom bés bu nekk ci lu jëm ci seen ngëm, am na solo lool itam (5 Mu. 6:6-9). Mën nga dem yenn saay ba bañ a bëggati dara ci àddina, waaye bul dellu ginnaaw. Ñaanal Yexowa mu may la doole te won la loo war a def booy “ yar [say doom], di leen yemale ak a yee ci Boroom bi ”. — Efes 6:4.
3 Boo soxlaa ndimbal ngir def wareef yi la Mbind mi sant, wax ko magi mbooloo mi. Mën na am ñu mën laa xelal xelal yu baax ci li nga war a def, walla ñu mën laa jàpple ba nga tëral porogaraam bu baax ci wàllu ngëm, ngir sa njaboot.
4 Ni ñeneen ñi mënee jàpple ñooñu : Ñi dëkkoon ci kër bi Timote màgge, ñoom ñépp bokkuñu woon ngëm. Waaye terewul mu mujj nekk jaamu Yexowa bu sawar. Li yaayam ak maamam bu jigéen doon góor-góorlu ngir jàngal ko Mbind yu sell yi bi mu nekkee ndaw, bokk na ci li ko gën dimbali ci loolu (Jëf. 16:1, 2 ; 2 Tim. 1:5 ; 3:15). Waaye nag, am na it li mu jële ci li mu doon ànd ak yeneen karceen. Pool mi waxoon ne Timote doomam la ci wàllu diine, ‘ doom ju takku te [bu] mu bëgg ’, bokkoon na ci karceen yooyu. — 1 Kor. 4:17.
5 Tey it, mbokk yu góor ak yu jigéen yu ñor yi ci wàllu ngëm, bu ñu ittewoo ak mbëggeel xale yi nekk ci mbooloo yi te seen baay gaañu, dina baax lool. Ndax xam nga ku ci nekk turam ? Ndax dinga waxtaan ak ñoom ci ndaje yi, walla feneen ? Wax leen ñu ànd ak yow ci waaraate bi. Xéyna mën nga leen a boole yenn saay ci njàngum Biibël bi ngeen di def ci seen njaboot, ñoom ak seen way-jur bi leen yor moom kenn, walla way-jur bi nekk Seede. Mën nga leen a boole it ci seen fo yu baax yi. Ndaw yooyu bu ñu la takkee xarit, ci lañu lay gën a bëgg roy, te ci lañu lay gën a nangu déglu. — Fil. 2:4.
6 Yexowa ittewoo na lool xale yu seen baay gaañu. Dina barkeel li ñuy def ñun ak mbëggeel ngir dimbali leen ñu nangu, bëgg, te topp dëgg gi. Am na xale yoo xam ne bi ñu nekkoon ndaw defal nañu leen lu mel noonu, fekk seen benn way-jur kese moo leen yoroon, walla senn benn way-jur kese moo nekkoon Seede Yexowa. Ñu ci bare nekk nañu tey ay pioñee, ay surga mbooloo, ay magi mbooloo mi, ay wottukat yuy wër, ay missionnaires, walla bokk nañu ci ñi dëkk ci Betel bi. Na ku nekk ci ñun seet ni mu mënee ‘ ubbi ’ xolam ngir xale yi seen baay gaañu. Noonu lañuy roye suñu Baay bi nekk ca asamaan. — 2 Kor. 6:11-13.