Ay tont ci seeni laaj
◼ Lu tax bokk ci mbooloo mi nekk ci gox bi nga dëkk gën ci yow ?
Ci mbooloo mi lañuy ame li ñuy xiir ci mbëggeel ak ci jëf yu baax (Yaw. 10:24, 25). Fa lañuy jànge dëgg gi te foofu lañuy jote li ñu soxla ngir mën a def ay taalibe ni ñu nu ko sante (Macë 28:19, 20). Foofu lañuy amee doole bi ñuy tax a mën a muñ ak ngor jafe-jafe yi. Fa lañuy ame ay wottukat yu ñuy dimbali ngir ñu mën a xeex jafe-jafe yi ak xalaat yi ñu àndal, ba daan leen. Kon leer na ne soxla nañu mbooloo mi ngir mën a wéy di am ngëm gu dëgër. Waaye nag, lu tax bokk ci mbooloo mi nekk ci gox bi ñu dëkk gën ci ñun ?
Nit ku nekk ak li mu nekke. Te lu mel ni suñu liggéey, jëkkër walla jabar bu nekkul Seede Yexowa, walla oto yi ñu war a dugg, mën na tax ñu tànn bokk ci mbooloo bii, walla bale. Waaye bu ñu bokkee ci mbooloo mu nekk ci gox bi ñu dëkk, dinañu ci jële lu bare luy laal suñu diggante ak Yexowa ak it yeneen fànn. Magi mbooloo mi, ci lañuy gën a gaaw a jot waaraatekat yi bu amee soxla bu jamp. Mas na am Ay tont ci seeni laaj yu wone yeneen yi ñu mën a am ci loolu. — Mai 1991 et août 1976, disponibles dans Watchtower Library — Édition 1999.
Ci lu ëpp, teew ci ndaje yi jege suñu kër moo gën a yomb, ndax dafay tax ñu mën a teel a àgg ba mën a waxtaan at nit ñi, toppatoo li ñu soxla toppatoo, te fekke woy ak ñaan yu njëkk yi. Nit ku suñu waxtaan neex bu yàggul, bu dëkkee ci suñu wetu kër, ci lu ëpp, seeti nit kooku, jàng ak moom Biibël bi te won ko ndaje yi ko gën a jege, ci ñun lay gën a yomb.
Wóor na ne boroom kër yi dinañu ñaan te xalaat bu baax ci li ñu wax fii. Dinañu seet bu baax lépp li ñu war a seet ngir gis liy gën ci seen njaboot, ngir ñu am diggante ak Yàlla bu rattax, te ñu bare jàmm. — 1 Tim. 5:8.