Nañu yégle xibaaru Nguur gi
1 “ Damaa wara dem [...] yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma. ” (Lukk 4:43). Ci kàddu yooyu, Yeesu wone na ne Nguuru Yàlla la doon waaraate. Ni ko Macë 24:14 yégle woon, li ñuy yégle tey it, ci loolu la jëm. Aaya jooju nee na : “ Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee, muju jamano ji jot. ” Yan dëgg yu jëm ci Nguuru Yàlla la nit ñi war a dégg ?
2 Nguuru Yàlla mu ngi ci asamaan, di ilif. Te léegi mu dindi bépp kiliftéefu nit. Seytaane dàq nañu ko ci asamaan ba pare, te àddina su bon sii, tollu na ci fanam yu mujj yi (Peeñ. 12:10, 12). Àddina Seytaane su bon te màgget sii, dinañu ko alag ba mu jeex tàkk, waaye kenn du laal Nguuru Yàlla. Dina fi des ba abadan. — Dañ. 2:44 ; Yaw. 12:28.
3 Nit ñiy déggal Yàlla, lépp lu baax li ñu bëgg, Nguuru Yàlla dina leen ko may. Tey, xare yi, ñàkk bi, ñiy jéggi yoon ak ñiy noot seeni moroom, indi na fi metit yu bare. Metit yooyu, Nguuru Yàlla dina leen fi dindi (Sab. 46:8, 9 ; 72:12-14). Ñépp dinañu mën a jot ci dund bu doy (Sab. 72:16 ; Isa. 25:6). Feebar ak laago, dootul amati (Isa. 33:24 ; 35:5, 6). Nit ñi, bu ñuy gën a mat, di gën di defar suuf si ba mu nekk àjjana. Dinañu ànd, nekk benn. — Isa. 11:6-9.
4 Ci fasoŋ bi ñuy dunde tey, lañuy wone ne dañu bëgg bokk ci ñi Nguuru Yàlla di ilif. Xibaaru Nguur gi war na feeñ ci lépp li ñuy def ci suñu dund, war na feeñ sax ci li ñuy wut ci àddina ak li ñuy jiital ci suñu dund. Dëgg la, dañu war a dundal suñu njaboot, waaye waruñu bàyyi suñuy soxla àddina, jël wàllu mbiri Nguur gi (Macë 13:22 ; 1 Tim. 5:8). Dañu war a topp xelalu Yeesu bii : “ Jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp [li ñu soxla ngir dund] dina leen ko ci dollil. ” — Macë 6:33.
5 Nit ñi war nañu dégg xibaaru Nguur gi te topp li muy wax bala muy wees. Nañu “ leen jéema gëmloo ” mbiri Nguuru Yàlla, ndax ñu mën leen a dimbali ci loolu ñu war a def. — Jëf. 19:8.