Buleen fàtte mag yiy topp Yàlla bu baax
1 Aana, mag bu amoon 84 at la woon. Jëkkëram gaañu woon na. Waaye saa yoo demee ca kër Yàlla, fekk ko fa. Li mu doon topp Yàlla bu baax noonu, moo taxoon Yàlla may ko barke bu réy (Lukk 2:36-38). Tey, suñuy mbokk yu góor ak yu jigéen yu bare, dañuy xalaate ni Aana, te fekk ay jafe-jafe yu mettee metti lañu am. Nit ñooñu nga xam ne dañuy topp Yàlla bu baax, yenn saay dafay fekk ñu feebar, walla ñu bañ a mën a def yenn yi ndax li ñu nekk mag. Te loolu mën na jeexal seen xol. Nañu seet li ñu mën a def ngir yokk seen doole, te dimbali leen ñu tàmm di topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm.
2 Ndaje yi ak waaraate bi : Mag yu bare, bu ñu amee ku leen mën a yóbbaale, tàmm teew ci ndaje yi, dina leen gën a yomb. Dina dëgëral ngëmu jaamukatu Yàlla yooyu nga xam ne yàgg nañu ko topp bu baax. Te dinañu mën a jariñoo mbooloo mi bu baax. Ndax bokk nga ci ñiy def liggéey bu rafet boobu ? — Yaw. 13:16.
3 Karceen dëgg bu tàmm waaraate dafay bég te kontaan ci li muy def. Waaye loolu mën na jafe lool ci mag yi, ak ci ñi néew doole. Ndax kenn ci ñoom mënul a ànd ak yow, nekk sa “ nawle ” ci yenn fànnu liggéeyu waare bi (Room 16:3, 9, 21) ? Xéyna mën nga ci ñaan kenn mu ànd ak yow booy waaraate ci telefon, booy dellu seeti nit, walla booy def benn njàngum Biibël. Bu fekkee ne mag boobu mënul a jóge këram, ndax nit ki ngay jàngal Biibël bi mënul a ñów këram ngir ngeen def fa njàngum Biibël bi ?
4 Njàngum Biibël yi ak it àndandoo ak suñu mbokk yi : Am na ñuy wax ak ay mag, walla ak ñi néew doole, ngir ñu ñów yenn saay teew ci njàngum Biibël bi ñuy def ci seen njaboot. Walla sax ñu def njàngum Biibël boobu ci kër nit kooku. Am na suñu benn mbokk mu jigéen mu yóbbu ñaari doomam ci suñu benn mbokk mu jigéen mu màgget, ngir ñu jàng fa téere Recueil d’histoires bibliques. Ñoom ñépp jële nañu ci lu baax. Nit ñooñu bu ñu leen waxee ñu ñów lekk ak ñun, walla ñu ñów bokk ak ñun ci yeneen ndaje yu jëm ci diggante nit ak nit, dina leen neex lool. Bu nit néewee doole ba duñu mën a toog lu yàgg bu ñu koy seeti, xéyna mën nga ko telefone walla seeti ko te bañ a yàgg, ngir jàngal ko dara, walla ñaan ak moom, walla nettali ko lu koy yokk doole. — Room 1:11, 12.
5 Yexowa dafa fonk mag yi koy topp bu baax (Yaw. 6:10, 11). Bu ñu wone mag yooyu ne dañu leen fonk, te bu ñu leen dimbalee ngir ñu tàmm topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm, dinañu roy Yexowa.