TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/02 p. 7
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 12/02 p. 7

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Mën nga wone it benn ci téere yii : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ?, Recueil d’histoires bibliques, walla Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Sãwiyee : Téere yi am 192 xët te génn bala 1988. Mbooloo yu amul téere yooyu mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu. Feewriyee : Téere Création (bu ndaw bi walla bu mag bi) walla téere La Révélation : le grand dénouement est proche ! Màrs : Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Dinañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi.

◼ Léegi ñu yónni seen mbooloo kayit yi ñuy joxe ngir ñaan nit ñi ñu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ci atum 2003. Mbooloo mu nekk dina ko am ci làkk bi ñu fay gën a làkk. Bu amee ci seen gox ñiy làkk beneen làkk te ngeen bëgg am kayit yooyu ci làkk yooyu, léegi ngeen ko war a laaj ci kayit bi tudd Demande de publications (S-14). Kayit yi ñuy joxe ngir ñaan nit ñi ñu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu mën ngeen ko jot ci araab, ci ãgale, ci español, ci purtugees, ak ci tubaab. Na ngeen ñaan làkk yi ngeen soxla kese ci seen gox.

◼ Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ci atum 2004, ci bésu dimaas 4 awril, bu jant bi sowee ba pare lay doon. Dañu leen koy teel a xamal ndax bu amee ay mbooloo yu bare yu bokk Saalu Nguur, ñu mën a def lépp li war ngir luye béréb fu ñu koy defe, walla ñu mën a seet li ñu war a def. Mag yi war nañu déggoo ak ki leen di luye béréb fi ñuy defe ndaje boobu, ndax bu bés bi ñówee, mu bañ a am beneen xew bu leen nar a tanqal ci béréb boobu. Bu ko defe dinañu mën a def ndaje boobu ci jàmm te lépp jaar yoon. Magi mbooloo mi waruñu ay-ayloo ngir def waxtaan boobu. Waruñu tànn it benn mag kese ngir mu def waxtaan bi at mu nekk. Kurélu mag yi dafa war a tànn mag bu gën a aay ngir mu def waxtaan boobu, ndaxte bés boobu dafa am solo lool. Bu amee mag bu bokk ci karceen yi ñu tànn bu mën a def waxtaan bi, moom lañu war a tànn.

◼ Am na li ñuy soppi ci fasoŋ bi ñuy defe Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bu wottukat biy wër ci mbooloo yi ñówee ci mbooloo yi. Ci weeru sãwiyee 2003 lañu koy tàmbali. Bu ñu woyee woy bu njëkk ba te ñaan ba pare, lekkool bi ci lu mat 25 minit lañu koy defe. Dinañu def waxtaan bu juróomi minit buy jëm ci lenn luy tax ñu aay ci wax. Dinañu def it waxtaan n° 1 ci lu mat fukki minit, te it ci lu mat fukki minit dinañu wax ci kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi. Kenn du def waxtaan n° 2, 3, ak 4. Bu ñu paree lekkool bi, ci lu mat 30 minit, dinañu def ndaje liggéeyu waare bi. Bu ñu woyee ba pare, wottukat biy wër ci mbooloo yi dina waxtaan ak mbooloo mi ci lu mat 30 minit. Ba pare ñu woy woy-Yàlla bu mujj bi, te ñu ñaan.

◼ Téere yu bees yu ñu mën a am :

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains II (ci bind yu réy) — tubaab.

◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :

Recueil d’histoires bibliques, Volume 1 (SECAM) — làkku ñi tëx bu Amerig (EDF)

Toute la communauté des frères (SECAM) — tubaab

◼ Téere yu bees yu ñu mën a am ci bindu baraay :

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains II (volume 2) — français deuxième degré (abrégé)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager