TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/05 p. 7
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 1/05 p. 7

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru sãwiyee : Téere yu am 192 xët yi génn bala 1990. Mbooloo yu amul téere yu yàgg yooyu mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu. Feewriyee : Approchez-vous de Jéhovah. Màrs : Veillez ! Su amee ku suñu waxtaan neex, jéemal a tàmbali ak moom benn njàngum Biibël bi ci téere Xam-xam. Awril : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, nañu seeti ñi mas a teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, walla ci beneen ndaje, waaye tàmmuñu teew ci ndaje yi yépp. Nañu leen won téere Adorez Dieu. Li ñu bëgg mooy tàmbali ay njàngum Biibël, rawatina ak ku jàng téere Xam-xam ak it téere Laaj ba pare.

◼ Ci weeru feewriyee la wottukat biy wër ci mbooloo yi di tàmbali def waxtaan bu ñu jagleel ñépp bi tudd “ Agissons sagement dans un monde insensé ”. Bésu 6 màrs, war na fekk ñu tàmbali ko ba pare.

◼ Ren, ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, dimaas 24 màrs lañu koy defe, bu jant bi sowee ba pare. Mbooloo yi war nañu def lépp li war ngir ndaje boobu. Bu dee sax dañu tàmbali waxtaan bi bala waxtu woowu, waruñu joxante mburu bi ak biiñ bi bala jant bi so. Laajleen ñiy toppatoo météo bi kañ la jant bi di so ci seen gox. Li gën mooy mbooloo mu nekk am ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ngir waa mbooloo mi. Waaye yenn saay, loolu duñu ko mën a def. Bu amee ay mbooloo yu bare yu bokk benn Saalu Nguur, xéyna benn walla ñaar ci ñoom mën nañu seet beneen béréb fu ñuy defe ndaje boobu. Bu amee mbooloo yu bokk fi ñuy defe ndaje boobu, bu mënee nekk, nañu fexe ba mu am lu mat 40 minit diggante ñaari ndaje. Bu ko defee, nit ñi dinañu mën a jariñoo ndaje bi bu baax-a-baax. Nañu seet it ni ñuy def ba boroom oto yi bañ a am benn jafe-jafe bu ñu agsee, walla bu ñuy gaare, bu ñuy wàcce ay nit walla bu ñuy yeb. Kurélu magi mbooloo mi moo war a seet li gën ci seen mbooloo.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager