Wideo yu ñu def ci benn DVD
Ñetti wideo ñoo nekk ci DVD bi tudd : Des alternatives à la transfusion. Benn bi mooy Stratégies alternatives à la transfusion : simples, sûres, efficaces. Doktoor yi ak ñiy jàng ngir nekk doktoor lañu ko defaral. Looloo tax wideo boobu mooy bi gën a wone li doktoor yi di def. Ñaareelu wideo bi mooy Soigner sans transfuser — Besoins et droits du patient. Boobu, dañu ko defar ngir surnalist yiy wax ci li doktoor yi di def, ñiy liggéey ci loppitaan yi, ñiy liggéey fu ñuy jàpple ñi feebar, ak it ngir àttekat yi. Dafay wone li doktoor mën a def ngir faj ku feebar te bañ a fàtte li yoon may ku feebar bu ñu koy faj. Ñetteel bi mooy Pas de sang : La médecine relève le défi. Boobu, ñépp lañu ko defal. Ñetti wideo yi nekk ci DVD bi, dañu ko def ci ãgale, waaye mën nga ko déglu itam ci almã, español, italieŋ, ci làkku sapoŋ, ci portugees (bu Brésil), ci rus (russe), ak ci tubaab. Mën nga won DVD bii sa doktoor, ki ngay jàngal Biibël bi, sa jëkkër walla sa jabar bu nekkul Seede, sa mbokk, sa jàngalekat, ñi nga bokkal liggéey walla ñi nga bokkal lekkool.