TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/05 p. 2
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 2/05 p. 2

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru feewriyee : Approchez-vous de Jéhovah. Màrs : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Laaj bi. Bu ñuy jëfandikoo téere Laaj bi, nañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël. Awril ak me : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu ñuy dellu seeti nit ñi suñu waxtaan neex, nañu seeti ñi mas a teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, walla ci beneen ndaje, waaye tàmmuñu teew ci ndaje yi yépp. Nañu leen won téere Adorez Dieu. Li ñu bëgg mooy tàmbali ay njàngum Biibël, rawatina ak ku jàng téere Xam-xam ak it téere Laaj ba pare.

◼ Ci weeru fewriyee, bu ñu yónnee mbooloo yi seeni téere, dinañu komaase di ci boole kayit yi ñuy jëfandikoo ci mbooloo mi. Dina am lu war a doy pur benn at. Dinañu wax ni ñu leen di joxe mbooloo yi ci kayit fi ñu bind téere yi ñu yónnee yépp. Su ay mbooloo bokkee benn Saalu Nguur, kiy toppatoo téere yi ngir mbooloo yooyu dina fexe mbooloo mu nekk gaaw a jot kayitam yooyu.

◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 màrs lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu fekkee ne dangeen am kees fu ngeen di dajale xaalis ngir tabax ay Saalu Nguur, walla toppatoo Saal bi, walla yeneen keesu xaalis, seetleen it ndax xaalisu kees yooyu mat na. Bu ñu seetee ndax xaalisu kees yi mat na ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

◼ Sekkerteer bi ak wottukatu liggéeyu waare bi war na seet li pioñee yi def ci waaraate bi. Bu ci amee ku ci waaraatewul waxtu yi ko war, mag ñi war nañu seet ni ñu ko mënee dimbali. Nañu seet li nekk ci leetar S-201 yi ñuy jot at mu nekk.

◼ Ci atum 2005, waxtaan bi ñu faral di am ci àddina si sépp bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, mu ngi tudd : “ Pourquoi Jésus a-t-il souffert et est-il mort ? ” Seetal li ñu ci wax ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar 2004.

◼ Bu waaraatekat soxlaa téere, waru ko laajal boppam bànqaas bi. Weer wu nekk, bala ñuy yónnee ci bànqaas bi li mbooloo mi soxla ci wàllu téere, wottukat biy jiite war na def benn yégle. Bu booba, képp ku soxla téere, dina ko mën a wax kiy toppatoo téere yi ci mbooloo mi. Buleen fàtte ne am na téere yoo xam ne duñu leen denc ci mbooloo mi. Bala nga leen di am, fàww nga wax kiy toppatoo téere yi ci seen mbooloo, mu laaj leen bànqaas bi.

◼ Ci diggante 23 ba 29 ci weeru me bii di ñów, dinañu tàmbali jàng téere Veillez ! ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager