Ci jamano bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, nañu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi
1 Waa Israyel, at mu nekk dañu amoon ay bés yu ñu doon def ay màggal ngir Yexowa (3 Mu. 23:2). Bés yooyu, dañu doon xalaat bu baax ci seen Yàlla ak ni mu baaxe ak ñoom. Loolu dafa leen doon may mbégte mu réy. Te dafa leen doon xiir ci gën a sawar ci jaamu Yàlla ci fasoŋ bu sell. — 2 Net. 30:21–31:2.
2 Ñun it, bu ñu nekkee ci jamano bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, dañuy gën a bég te gën a sawar ci liggéey bi ñu Yàlla dénk. Dañuy xalaat bu baax ci li ñu Yexowa may, maanaam doom ji mu am képp. Loolu, dafa réy ba kenn mënu ko fey (Ywna. 3:16 ; 1 Pie. 1:18,19). Xalaat ci mbëggeel bi nu Yàlla ak doomam won, dafa ñuy xiir ci màggal Yexowa te def lépp ngir topp ay ndigalam. — 2 Kor. 5:14, 15.
3 Ren, dinañu màggal Reeru Sang bi ci bésu alxemes 24 màrs, bu jant bi sowee ba pare. Naka lañu mënee yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs, awril, ak me ?
4 Nañu jéem a wax ak nit ñu gën a bare : Booy waaraate, jéemal a wax ak nit ñi nga mën ñépp. Ndax mënuloo waaraate këroo-kër ci waxtu bu fa nit ñi bare, mel ni bu ngoon jotee ? Xéyna dina am ci sa gurupu njàngum téere bi kenn ku bëgg waaraate bala ndaje boobu di komaase. Kon, wottukatu njàngum téere bi dina mën a porogaraame benn ndaje bu ndaw bu ñuy def bala ñuy dem waaraate. Ndaje boobu dina gàtt te dingeen waaraate ci béréb bu jege fi ngeen di defe njàngum téere bi.
5 Dinañu mën a waar itam ñu bare bu ñu demee foo xam ne nit ñu bare dañu fay romb. Ca réewu Sapoŋ, suñu benn mbokk mu jigéen dafa bëggoon a nekk pioñee buy jàpple. Waaye dafa doon yendu di liggéey. Benn magu mbooloo nee ko mu jéem a waare ci mbedd yi nekk ci wetu benn gaar, bés bu ne bala muy dem liggéey. Loolu la suñu mbokk moomu def, fekk ku bare kersa la woon te am na ñu ko doon ñaawal ci nit ñi doon jël saxaar gi. Dem na ba am 40 nit ñu mu doon faral di jox suñu yéenekaay yi. Ci 40 nit ñooñu amoon na ñu doon jóge seen kër di dem liggéeyi, am ñu doon liggéey ci biir saxaar gi, ak it ñu doon jaay ci boor yooyu. Weer wu nekk, dafa doon jox lu tollu 235 yéenekaay. Te it, dafa doon jéem a wax nit ñi li nekk ci Biibël bi ci lu gaaw. Loolu mu def tax na mu tàmbali juróom-benni njàngum Biibël.
6 Fi nga mën a jaar ngir waar ay nit : Waaraatekat yi nekk eleew mën nañu nekk pioñee yuy jàpple su lekkool tëjee. Dinañu mën a yokk itam seen waaraate bu ñu waaree ci seen lekkool. Xéyna boo gisee ni ñu bëgge waxtaan ci li nga gëm, dinga waaru ! Yenn saay, ci kalaas bi dingeen am waxtaan boo xam ne ñépp a ci war a bokk. Walla seen meetar dina leen dénk lu ngeen war a gëstu ba pare bind ci. Ndax mën nga jaar ci loolu ngir waare ? Am na it ay eleew yu wone suñuy wideo. Am na ñu jàng Biibël ak ñi ñu bokkal kalaas ba ñu jébbal seen bopp Yàlla te sóobu ci ndox. Loolu, lu baax la ci ki bëgg “ màggal turu Yexowa ”. — Sab. 148:12,13.
7 Bés bu nekk, seetal li nga mën a def ngir waar nit. Nanga leen wax ci suñu Yàlla ji nga xam ne dafa baax lool ak ñun ak it ci lu rafet li mu dig doom-Aadama yi. Am na suñu benn mbokk ci ngëm boo xam ne bés bu nekk mu jël saxaar. Bu nekkee ci saxaar gi, saa yu ko mënee, dafay waar nit ñi. Bés bu nekk, am na it fu mu war a wàcc ngir jël beneen saxaar. Waar na fa benn waxambaane ba faral di waxtaan ak moom 5 minit bés bu nekk. Nit kooku ak xaritam nangu nañu jàng Biibël bi ak suñu mbokk. Dañu ko doon def ci saxaar gi, bi muy daw. Bi mu yàggee tuuti, benn jigéen bu màgget ñów ci moom, nee ko moom itam dafa bëgg a jàng Biibël bi. Kooku dafa leen doon déglu bi ñu doon waxtaan. Léegi, jigéen jooju moom itam dafay jàng Biibël bi bés yi muy jël saxaar gi. Loolu la suñu mbokk mi def ba am 10 nit yu doon jàng Biibël bi ak moom ci saxaar gi.
8 Xéyna danga màgget walla sa yaram neexul. Kon lan nga mën a def ? Ba tey, mën nga yokk li ngay def ngir màggal Yexowa. Ndax mas nga waare ci telefon ? Soo xamul ni ñu koy defe, nanga laaj sa wottukatu njàngum téere bi. Mën na la boole ak waaraatekat yu koy def. Dingeen ànd ci fasoŋu waaraate boobu. Dingeen mën a dimbalante te ku nekk dinga am li nga mën a jàng ci sa moroom ngir aay ci waaraate bi. Wax nañu ni ñu mënee waaraate ci telefon ci Le Ministère du Royaume bu feewriyee 2001, xët 5-6.
9 Ñiy jàng Biibël bi, xéyna bu ñu teewee ndaje fàttaliku bi, dinañu bëgg yokk li ñuy def ngir màggal Yexowa. Waaye mën na am ñu ragal a waaraate ni ñu ko faralee def. Nanga leen nettali lu neex lu jëm ci liggéeyu waare bi. Nanga leen won ndànk ndànk ni ñuy jàngalee Biibël bi ak ni ñuy tontoo laaj yi (1 Pie. 3:15). Bu ci amee ku bëgg a tàmbali waare xibaar bu baax bi, wax ko wottukat biy jiite. Dina wax ay magi mbooloo mi ñu waxtaan ak moom ngir seet ndax mën na ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi. Ñiy jàng Biibël bi, bu ñu bëggee waaraate noonu, dañuy wone li ñu xalaat ci kan moo war a ilif àddina si sépp. Ci dëgg, loolu dafa war a bégal Yexowa lool ! — Léeb. 27:11.
10 Ndax mën nga nekk pioñee buy jàpple ? Ku bëgg nekk pioñee buy jàpple, fàww mu waaraate 50 waxtu ci weer wi, maanaam lu tollu 12 waxtu ayu-bés bu nekk, te loolu waru ko foye (Macë 5:37). Boo xoolee porogaraam yi ñuy wone ci xët 5, ndax am na ci benn bu mën a baax ci yow ? Boo ci gisul benn, ndax mënoo def sa porogaraamu bopp ngir mën a nekk pioñee buy jàpple ci weeru màrs, awril walla me ? Ñaanal Yexowa mu barkeel li ngay jéem a def ngir yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi. — Léeb. 16:3.
11 Magi mbooloo mi ak surgay mbooloo mi dinañu la jàpple bu baax ci lépp li ngay fas yéene def ngir gën a màggal Yexowa ci jamano fàttaliku bi. Xéyna sax ñu bare ci ñoom dinañu nekk pioñee, ñoom it. Magi mbooloo mi dinañu yokk ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waaraate. Dinañu ko def ci ngoon yi, ci samdi yi walla ci dimaas yi, maanaam saa yu ko nit ñi soxlaa. Bala ñu mën a xam fan ak kañ lañu ko war a defe, mag ñi dinañu wax ak ñi fas yéene nekk pioñee walla ñi ciy xalaat. Dinañu def lépp ngir nga am kooy àndal ci waaraate bi ci waxtu ak bés yi nga bëgg génn. Bu ñu defee loolu, nit ku nekk dinga mën a topp sa porogaraam te def lu bare lu baax. — Léeb. 20:18.
12 Defal lépp li nga mën : Xéyna doo mën a nekk pioñee buy jàpple. Waaye bul fàtte ne Yexowa nangu na li ñuy jéem a def ak it li ñu koy sarax, “ di seet li nu am te bañ a seet li nu amul ”. (2 Kor. 8:12.) Li war a tax ñu gërëm Yexowa, aka bare ! Looloo taxoon Dawuda wax lii :“ Dinaa tàgg Yexowa saa su ne ; saa su ne dinaa ko màggal ak sama gémmiñ. ” (Sab. 34:1). Na loolu nekk li ñu bëgg def ñun it ci jamano fàttaliku bii di ñów.
[Laaj yi]
1. Màggal yi waa Israyel doon def, lan la doon def ci ñi ragaloon Yàlla ?
2, 3. Bëgg yokk li ñuy def ci wàllu ngëm ci jamano fàttaliku bi, lu tax mu baax ? Te ban bés lañuy defe màggal boobu ren ?
4, 5. a) Lan la yenn waaraatekat def ngir mën a wax ak nit ñu gën a bare ? b) Ci sa gox, lan ngeen def ba mën a waar ñu bare ?
6. Naka la ndaw yi mënee yokk li ñuy def ci wàllu ngëm ?
7. a) Ci ban bunt la suñu benn mbokk ci ngëm jaar ngir waar ay nit ? b) Ndax mas nga def lu mel noonu ?
8. Ku màgget walla ku yaramam neexul, lan la mën a def ngir yokk li muy def ci liggéeyu waare bi ?
9. Naka lañu mënee dimbali ñiy jàng Biibël bi ba ñu mën a ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi ?
10. a) Naka la ñu porogaraam bu baax mënee dimbali bu ñu bëggee nekk pioñee buy jàpple ? b) Ndax daaw mënoon nga nekk pioñee buy jàpple ? Loo defoon ba mën ko ?
11. Lan la mag ak surga mbooloo mi mën a def ngir jàpple ñiy nekk pioñee yuy jàpple ?
12. Lan moo tax ñu bëgg a màggal Yexowa saa su ne ?
[Box on page 3]
Loo mën a def ngir yokk sa waaraate bi ?
◼ Waaraate bu nit ñi nekkee seen kër
◼ Waaraate fu bare nit
◼ Waaraate fi ngay liggéeye walla fi ngay jànge
◼ Waaraate ci telefon
◼ Nekk pioñee buy jàpple
[Chart on page 5]
Ay porogaraam yoo mën a topp boo bëggee nekk pioñee buy jàpple — Boo bëggee waaraate 12 waxtu ayu-bés bu nekk
Suba yi — Altine ba Samdi
Mën nga fi dindi bés boo bëgg te def ci dimaas
Bés bi Xaaju bés bi Waxtu yi
Altine Suba 2
Talaata Suba 2
Àllarba Suba 2
Alxemes Suba 2
Àjjuma Suba 2
Samdi Suba 2
Waxtu yi yépp : 12
Ñaari fan
Mën nga tànn ñaari bés yi la gënal. (Am na bés yoo xam ne, boo leen tànnee ngir topp porogaraam bii, 48 waxtu kese ngay waaraate ci weer wi.)
Bés bi Xaaju bés bi Waxtu yi
Àllarba Bés bi yépp 6
Samdi Bés bi yépp 6
Waxtu yi yépp : 12
Ñaari ngoon ak samdi ak dimaas
Mën nga tànn ñaari ngoon yu dul samdi ak dimaas
Bés bi Xaaju bés bi Waxtu yi
Altine Ngoon 1 1⁄2
Àllarba Ngoon 1 1⁄2
Samdi bés bi yépp 6
Dimaas Génn-wàllu bés bi 3
Waxtu yi yépp : 12
Ñetti ngoon ak samdi
Mën nga fi dindi bés boo bëgg te def ci dimaas
Bés bi Xaaju bés bi Waxtu yi
Altine Ngoon 2
Àllarba Ngoon 2
Àjjuma Ngoon 2
Samdi Bés bi yépp 6
Waxtu yi yépp : 12
Porogaraam bi may def
Yaay seet ñaata waxtu nga bëgg a def bés bu ne.
Bés bi Xaaju bés bi Waxtu yi
Altine
Talaata
Àllarba
Alxemes
Àjjuma
Samdi
Dimaas
Waxtu yi yépp : 12