Ndax komaase nga ko topp ?
1 Ci Sasu Nguuru Yàlla yi, am na léegi waxtaan yu tudd “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng ”. Loolu ci weeru sulyet 2004 lañu ko komaase. Baax nañu lool ci ku bëgg dimbali ñi bëgg nekk taalibe Yeesu Krist, ñu am diggante bu rattax ak Yexowa Yàlla (Room 5:1). Am na léegi juróom-ñaari Sasu Nguuru Yàlla yu amoon waxtaan yooyu. Ndax ñu ngiy topp li ñu ci wax (Filip 4:9) ? Nañu seet léegi yenn ci ponk yi ñu ci wax ngir gën ci góor-góorlu.
2 Lii lañu bindoon ci Sasu Nguuru Yàlla bu Ut 2004 : “ [Bu ñuy waajal njàng mi] li ñu war a njëkk def mooy ñaan Yexowa te boole nit ki ak li mu soxla ci ñaan bi. Nañu ñaan Yexowa mu dimbali ñu ba ñu jot xolam. ” (km-WO 8/04 1). Ndax yaa ngi fàttaliku loolu ? War nañu jël jot ngir waajal njàng mu nekk te xalaat nit ki bu ñu koy def. Lu am solo la (Léeb. 15:28). Ndax komaase nga def loolu ? Xéyna mas nga dem ba ci kanamu nit ki ngay jàngal Biibël bi, sog a jéem a fàttaliku fi ngeen yemoon. Te yow ci sa bopp yaa koy laaj lii : “ Waaw..., ndax yaa ngi fàttaliku fi ñu yemoon keroog ? ” Ndax lu mel noonu masu la dal ? Du nu dal mukk su ñu toppee li ñu wax ci Sasu Nguuru Yàlla boobu, maanaam waajal njàng mi di ci boole ñaan.
3 Lii lañu waxoon ci Sasu Nguuru Yàlla bu nowàmbar 2004 : “ Booy waajal njàngum Biibël bi, [...] [ ci aaya yi nekk ci xise yi] tànnal yi nga bëgg jàng ak nit ki ngir waxtaan ci. Li gën mooy aaya yooyu nekk fi ñu jële li ñu gëm. ” (km-WO 11/04 4). Ndax yaa ngi fàttaliku loolu ? Ndax komaase nga def loolu ? Xéyna dinga am njàngum Biibël boo war a def ci ñaari xise yi njëkk ci njàngale 5 ci téere Laaj bi. Njàngale mi mu ngi tudd : “ Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ? ” Laaj bi ànd ak ñaari xise yooyu mooy : “ Lu tax Yàlla sàkk suuf si ? ” Juróomi aaya ñoo nekk ci ñaari xise yooyu : Sabuur 115:16 ; Isayi 45:18 ; Sabuur 104:5 ; Dajalekat 1:4 ; 1 Musaa 1:28 ; 2:8, 15. Yan nga bëgg a jàng ak nit ki ? Xise bi njëkk wax na ne Yàlla dafa bëgg “ nit ñi [...] dund ba fàww [ci suuf si], ci bànneex ”. Ci juróomi aaya yooyu, ci yan lañu jële li ñu gëm noonu ?
4 Xéyna dinga bëgg jàng Isayi 45:18 te won ko foofu kàddu bi ne : “ qui l’a formée pour être habitée ” (maanaam Yàlla dafa sàkk suuf si ngir nit dëkk ci) ngir won ko ne Yàlla dafa bëggoon nit ñi dund ci kow suuf si. Ba pare, mën nga tànn Sabuur 104:5, te won ko foofu kàddu bi ne : “ Elle ne chancellera pas pour des temps indéfinis, oui pour toujours ” (maanaam suuf si dina fi nekk ba abadan) ngir mu xam ne dina am ay nit ci kow suuf ba fàww. Mën nga àggale waxtaan bi ak 1 Musaa 2:15. Dinga ko won foofu kàddu bi ne : “ pour le cultiver et pour s’en occuper ” (maanaam ngir bey ko, te sàmm ko) ngir mu xam ne nit ñi naroon nañu am dund gu neex ci béréb bu rafet boobu. Boo waxtaanee noonu ci aaya yi nga tànn, dinga dimbali kiy jàng mu xam bu baax li Yexowa bëggoon bi mu sàkkee suuf si. Te ku def loolu, topp nga li Sasu Nguuru Yàlla bi wax. Wóor na ñu ne Yexowa dafay barkeel li ñuy def noonu.
5 Boo bëggee, mën nga tànn yeneen aaya ci juróomi aaya yooyu ngir won nit ki lu tax ñu gëm ne “ Yexowa sàkk na suuf si ndax nit ñi mën cee dund ba fàww, ci bànneex ”. Tànn boobu, dina aju ci jot bi ngeen am ak it ci nit ki ci boppam.
6 Ci Sasu Nguuru Yàlla yi, am na ay ponk yu am solo ci waxtaan yi tudd “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng ”. Bu ñu leen seetaatee ngir topp leen, li ñuy jàngal nit ñi, dina gën a dugg seen xol. Ndax mënuñu yóbbale Sasu Nguuru Yàlla yooyu ci suñu saag bu ñuy dem defi ay njàngum Biibël ? Bu ñu defee loolu, ci lu wóor dinañu gën a aay ci jàngale Biibël bi. Te dinañu am mbégte bu ñuy am bu ñuy dimbali suñuy moroom ñu ànd ak ñun di màggal turu Yexowa. — Yaw. 13:15.