Xaaj 7 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Ñaan Yàlla bu ñuy def njàngum Biibël
1 Kuy jàng Biibël bi, bala mu jëm kanam ci wàllu ngëm, fàww Yexowa barkeel ko (1 Kor. 3:6). Kon, tàmbali te àggale seen njàngum Biibël ak ñaan, lu baax la. Loolu, dingeen ko mën a def ci seen njàng mu njëkk mi, su nit ki nekkee ku mbirum diine neex. Ak ñeneen nag, yaa war a seet kañ nga koy mën a def. Mën nga won nit ki, ci Sabuur 25:4, 5 ak ci 1 Yowanna 5:14, lu tax ñu war a ñaan Yàlla bala ñuy jàng Biibël bi. Mën nga ko won it ci Yowanna 15:16 lu tax ñu war a jaarale suñuy ñaan ci Yeesu Krist.
2 Kan moo war a ñaan ? Su amee góor gu ñu sóob ci ndox guy ànd ak benn mbokk ci ngëm bu jigéen ci benn njàngum Biibël bi, ku góor ki moo war a ñaan. Su dee jigéen ji mooy def njàngum Biibël bi, ba tey ku góor ki mooy ñaan, te jigéen ji dina musóoru buy jàngale (1 Kor. 11:5,10). Léegi, su amee waaraatekat bu góor bu ñu sóobagul buy ànd ak suñu benn mbokk mu jigéen, ku jigéen ki moo war a ñaan. Te war na musóoru buy ñaan ak buy jàngale.
3 Li nga mën a wax ci ñaan bi : Ñaan bi, jarul mu gudd, waaye danga war a xam li nga bëgg a ñaan te dafa war a leer. Mën nga ñaan Yàlla mu barkeel njàng mi ngeen di def. Mën nga ko gërëm itam ci dëgg gi ngeen di jàng. Te it, ndegam Yexowa mooy Kiy jàngale, nanga ko màggal ci sa ñaan ndax loolu (Isa. 54:13). Mën nga wax itam ci ñaan bi luy wone ne danga bëgg ki ngay jàngal ak it ni nga fonke mbootaay bi Yexowa di jëfandikoo (1 Tes. 1:2, 3 ; 2:7, 8). Mën nga ñaan itam Yexowa mu barkeel li nit ki di def ngir topp li muy jàng. Loolu dina ko dimbali mu xam ne dafa war a jëfe kàddu gi. — Saak 1:22.
4 Ñaan Yàlla ci njàngum Biibël, bare na lu baax lu muy indi. Dafay indi ay barke Yàlla (Lukk 11:13). Dafay wone ne jàng Kàddu Yàlla, nekkul lu ñu war a foye. Nit ki, bu déggee suñuy ñaan, dina xam ni ñuy ñaane Yàlla (Lukk 6:40). Te it nit ki dina gis ci suñuy ñaan ni ñu bëgge Yàlla ak suñu xol bépp ak it ni ñu koy gërëme ndax jikko yu rafet-a-rafet yi mu ñuy won. Loolu dina ko dimbali mu am diggante bu rattax ak Yexowa.
[Laaj yi]
1. a) Tàmbali te àggale njàngum Biibël ak ñaan, lu tax mu baax ? b) Lu ñu mën a def ngir tàmbali di ñaan ak ki ñuy jàngal Biibël bi ?
2. Suñu mbokk mu jigéen, bu amee njàngum Biibël bu mu war a def, te góor gu ñu sóob walla waaraatekat bu góor bu ñu sóobagul ànd ak moom, kan moo war a ñaan ?
3. Loo mën a ñaan Yàlla booy ñaan ci njàngum Biibël ?
4. Tàmbali te àggale njàng mi ak ñaan, lu tax mu baax ?