TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/05 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Turu xaaj yi
  • 11-17 awril
  • 18-24 awril
  • 25 awril ba 1 me
  • 2-8 me
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 4/05 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

11-17 awril

Woy-Yàlla 2

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Waxal ñépp ñu seetaan wideo bi tudd Soigner sans transfusion — Besoins et droits du patient ngir waajal waxtaan bi ñu am ci ndaje bu 25 awril ba 1 me. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 6, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 awril ak La Tour de Garde bu 15 awril. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox. Na ci am kenn kuy wone ni ñuy waaree ci mbedd mi.

15 min : “ Nanga kontine di waaraate. ”a Bu la ko jot bi mayee, laajal ñi teew ñu wax ci aaya yi ñu won ci xaaj bii, fekk binduñu li ci nekk.

15 min : “ Nañu def lu baax te sédde ci li ñu am. ”b Woneel ni ñu mënee topp li nekk ci xaaj bii ci seen mbooloo, ak li ñu mën a def ngir dimbali suñuy mbokk.

Woy-Yàlla 22 ak ñaan bu mujj bi.

18-24 awril

Woy-Yàlla 84

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Nanga fàttalil ñépp ne ayu-bés bi di ñów, dinañu waxtaan ci wideo bi tudd Besoins et droits du patient.

20 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 8. ”c Na am waaraatekat buy wone ci lu gàtt ni ñuy joxe kenn ku sog a tàmbali njàngum Biibël bi téere bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ? Waaraatekat bi dina ko won foto bi nekk ci xët 20 te wax ko ci lu gàtt ni ñuy doxale ndaje bi ñuy jagleel ñépp. Dina ko wax yaxu waxtaan bi di ñów te nee ko mu ñów teew.

15 min : Nañu dund ci maandu ci jamano ordinatër ji ñu tollu nii (Titt 2:​11,12). Waare bu ñuy def ci Sasu Nguuru Yàlla bu septaambar 2002, xët 8, xise 1-7, ak it ci Le Ministère du Royaume bu nowàmbar 1999, xët 5, xise 24-26, ak xët 6, xise 35-36. Bu ko jot bi mayee, te bu baaxee ci mbooloo mi, mën nañu boole ci waare bi li nekk ci Le Ministère du Royaume bu nowàmbar 1999, xët 3 ba 6.

Woy-Yàlla 75 ak ñaan bu mujj bi.

25 awril ba 1 me

Woy-Yàlla 35

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Jàngal kayit biy wone fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi ak leetar bi bànqaas bi yónnee ngir wax ne jot na xaalis bi mbooloo mi maye. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru awril te joxe ko. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 6, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 awril ak La Tour de Garde bu 1 me. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox. Na kenn ki wone li ñu mën a wax su amee ku ne “ Loolu, soxalu ma ”. (Seetal Comment raisonner, ci xët 16.) Woneel ci yéenekaay yi lu mën a itteel dëgg ñi nekk ci suñu goxu mbooloo.

30 min : “ Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi jéem a def léegi. ” Benn magu mbooloo bu aay ci waxtaan yu mel noonu moo ko war a def. Jàngal Jëf ya 15:​28, 29, te nanga wax ci lu gàtt te leer ne li njëkk a tax karceen bañ ñu sol leen deret mooy déggal Yàlla ci li mu wax ci deret bi nga xam ne lu tedd la ci kanamam. Boo paree wax loolu rekk, nanga tàmbali waxtaan bi jëm ci wideo bi tudd Besoins et droits du patient. Nanga laaj laaj yi nekk ci xaaj bii. Nanga jàng xise bu mujj bi ngir àggale waxtaan bi.

Woy-Yàlla 18 ak ñaan bu mujj bi.

2-8 me

Woy-Yàlla 63

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal ci lu gàtt li nekk ci xaaj bi tudd “ Dinañu jàng téere bi tudd Veillez ! ” ci xët 6. Waxal ne li ñu wone fii mooy li ñuy waxtaane ci njàngum téere bi ayu-bés bu nekk. Kon na ñépp waajal bu baax njàng mu nekk te bokk ci ñiy tontu laaj yi ci ndaje boobu. Dinañu tàmbali jàng téere boobu ayu-bés biy komaase ci bésu 23 me.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : “ Fasoŋu nit ñépp ay mucc. ”d Waxal ni ñu mënee topp li ñu wax ci xaaj bii ci goxu mbooloo mi.

Woy-Yàlla 47 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager