Bésu Yexowa jege na
1 Karceen yi yàkkamti nañu fekke bésu Yexowa. Bés boobu dina jeexal suñu jamano jii te indi beneen jamano joo xam ne lu jub rekk moo fay nekk (2 Pie. 3:12, 13). Bés boobu xamuñu kañ lay doon. Kon waruñu nelaw mukk, te dañu war a dimbali suñu moroom yi ñu bañ a nelaw ñoom it (Esek. 33:7-9 ; Macë 24:42-44). Bu ñu xalaatee ci li Yàlla yégle woon, dina ñu wóor ne bésu Yexowa bu mag bi jege na. — Tsë. 1:14.
2 Réew yu yore kiliftéef ci àddina si sépp, ni ñu toppantee : Ci Peeñu bi 17:9-11, ndaw li Yowanna mu ngi wax ci “ juróom-ñaari buur ”. Buur yooyu ñooy réew yuy toppante te yore kiliftéef ci àddina si sépp. Yowanna wax na itam ci “ juróom-ñetteelu buur bi ”. Tey buur boobu mooy Les Nations unies. Ndax ginnaaw buur boobu, dina am beneen réew buy yore kiliftéef ci àddina si sépp ? Déedéet ! Biibël bi nee na juróom-ñetteelu buur boobu dina “ jëm sànkute ”. Te waxul lu jëm ci beneen buur bu bokk ci doomu Aadama yi bu nar a topp ci moom. Kon, ndax yaa ngi gis ci ban jamano lañu tollu ?
3 Dañel 2:31-45 dafay yokk suñu xam-xam ci bésu Yexowa bi di ñów. Buur bi tudd Nebukanesar dafa doon nelaw di gént. Mu gis benn nataal bu mag-a-mag. Nataal boobu mu ngi misaal ay réew yuy toppante te yore kiliftéef ci àddina si sépp. Réew yooyu yépp gis nañu leen ba pare. Fan lañu tollu ci nataal boobu ? Nu ngi tollu ci tànk yi. Te yégle boobu wax na ñu li war a ñów ginnaaw loolu. Yàlla dina alag nguuru nit yi yépp, ba pare indi beneen “ nguur gu dul tas mukk ”. Ndax yaa ngi gis ni loolu di wonee ne bésu Yexowa jege na ?
4 Leneen lu koy wone : Am na leneen lu ñuy gis tey luy wone ne bésu Yexowa jege na. Ndaw li Pool moo ko waxoon. Mooy jikko yi ñu naroon a gis ci nit ñi ci “ muju jamano ”. (2 Tim. 3:1-5.) Am na itam liggéeyu waare bi nga xam ne fàww mu am ci kow suuf si sépp bala àddina si di tukki. Moom lañuy def tey (Macë 24:14). Kon nañu sawar lool ci waaraate bi, ndaxte lii la malaaka mi wax : “ Ragalleen Yàlla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw àtteem jot na. ” — Peeñ. 14:6, 7.