Xaaj 9 :Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Woneel ki ngay jàngal ni ñu mën a waaree saa yu ñu ci amee bunt
1 Bi Andre ak Filipp gisee ne Yeesu moo doon Almasi bi ñu doon xaar, mënuñu woon téye xibaar bu rafet boobu ci seen xol (Ywna. 1:40-45). Tey itam, ñiy jàng Biibël bi, bu ñu demee ba gëm li ñu jàng, dinañu ko bëgg a jottali seeni moroom (2 Kor. 4:13). Naka lañu leen mënee dimbali ñu mën a waar ay nit saa yu ñu ci amee bunt, te it ñu def ko ni mu ware ?
2 Mën nga laaj nit ki rekk ndax mas na waxtaan ak keneen ci li mu jàng ci Biibël bi. Mën na woo ay xaritam walla ay mbokkam ñu ñów bokk ci njàng mi. Laaj ko ndax ci ñi mu bokkal liggéey, ñi mu bokkal lekkool walla ñeneen ñi mu xam, amul ku ci bëgg a déglu xibaar bu baax bi. Noonu la mën a komaasee di waare. Waaye nag dimbali ko ngir buy wax ci Yexowa Yàlla ak ci li mu bëgg def, mu xam ni mu war a waxe ak nit ñi, mu weg leen te baax ak ñoom. — Kol. 4:6 ; 2 Tim. 2:24, 25.
3 Bu ñuy waxtaan ci li ñu gëm : Ñiy jàng Biibël bi, bu ñuy waxtaan ak nit ñi, war nañu mën a wone aaya fi ñu jële li ñu gëm. Kon, yow mii koy jàngal, yaa ko ci war a dimbali. Lu am-a-am solo la. Kon nag, booy jàng Biibël bi ak moom, lée-lée mën nga taxaw te laaj ko lii : “ Li nga jàng nii, boo naree wax sa mbokk lu tax nga gëm ko, ban aaya nga koy won ?” walla “ Boo naree wax sa xarit lu tax loolu nekk dëgg, ban aaya nga koy won ? ” Déglul li mu lay tontu te won ko aaya bu ci mën a baax (2 Tim. 2:15). Noonu ngay dimbalee nit ki mu mën a waare saa yu ci amee bunt. Te it, loolu dina ko dimbali mu mën a waaraate bu baax, bés bu nekkee waaraatekat bu ñu sóobagul.
4 Dañu war a dimbali nit ñi ñu xam li ñu mën a def bu amee ku leen bëgg a teree jaamu Yexowa (Macë 10:36 ; Lukk 8:13 ; 2 Tim. 3:12). Mën na am nit laaj leen dara lu jëm ci Seede Yexowa yi, walla am lu mu bëgg wax ci ñoom. Loolu mën na ko ubbil bunt mu waar ko. Téere bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ? mën na ko dimbali mu “ jekk ngir tontu ” nit kooku (1 Pie. 3:15). Téere boobu baax na ci mbokk walla xarit buy xeex kiy jàng Biibël bi ak ñun, fekk ci xolam dafa ko bëgg dimbali. Kiy jàng Biibël bi mën na jëfandikoo téere boobu ngir dimbali nit ñooñu ñu xam lu tax ñu gëm li ñu gëm ak it lu tax ñu def li ñuy def.