Nañu dimbali nit ñi ñu dégg ndigal “ ak seen xol bépp ”
1 Bu ñu bëggee Yexowa nangu li ñuy def ngir jaamu ko, fàww ñu nekk ku dégg ndigal (5 Mu. 12:28 ; 1 Pie. 1:14-16). Léegi àtte Yàlla dal ci kow ‘ ñi xamul Yàlla te baña déggal xebaar bu baax ’ bi (2 Tes. 1:8). Naka lañu mënee dimbali nit ñi ñu topp ndigal yi nekk ci Kàddu Yàlla “ ak seen xol bépp ” ? — Room 6:17.
2 Nañu leen dimbali ñu dëgëral seen ngëm te am mbëggeel : Bu ñu jàngee Mbind yi, dinañu gis ne dégg ndigal ak ngëm ñoo ànd. Ndaw li Pool wax na ci lu jëm ci “ firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu ”. (Room 16:26 ; mbind yu dëng yi, ci ñun la.) Yawut yi pàcc 11 tudd na ay nit ñu bare ñu wone ngëm gu dëgër. Ñi ci bare dafa amoon liggéey bu leen Yexowa santoon, ñu def ko (Yaw. 11:7, 8, 17). Te it ñàkk am ngëm gu dëgër bokk na ci liy tax nit di bañ a dégg ndigal (Ywna. 3:36 ; Yaw. 3:18, 19). War nañu jàng jëfandikoo bu baax Kàddu Yàlla ngir dimbali nit ñi ñu am ngëm guy tax ñu dégg ndigal. — 2 Tim. 2:15 ; Saak 2:14, 17.
3 Dégg ndigal laal na it mbëggeel bi ñu am ci Yàlla (5 Mu. 5:10 ; 11:1, 22 ; 30:16). Lii la 1 Yowanna 5:3 wax : “ Mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu. ” (Mbind yu dëng yi, ci ñun la.) Naka lañu mënee def ba kiy jàng Biibël bi di gën a bëgg Yexowa ? Booy jàng ak moom, seetal ci lan nga mën a jaar ngir mu gën a bëgg gërëm Yexowa ndax jikko yu rafet yi mu am. Waxal lu tax ngay gërëm Yexowa ak sa xol bépp. Dimbalil kiy jàng Biibël bi mu jege Yexowa ba digganteem ak moom rattax. Mbëggeel mooy li ñu gën a mën a xiir, ñun ci suñu bopp ak it yeneen nit ñi, ñu déggal Yàlla ak suñu xol bépp. — Macë 22:37.
4 Nañu nekk royukaay : Li mën a xiir bu baax nit ñi ci topp li nekk ci xibaar bu baax bi mooy li ñuy def ñun ci suñu bopp. Bu ñu bëggee am “ xol bu lay xiir ci dégg ndigal ”, dañu ci war a góor-góorlu saa su nekk (1 Bu. 3:9 ; Léeb. 4:23). Loolu lan la laaj ? Dañu war a jàng Biibël bi ñun ci suñu bopp te tàmm teewe ndaje yi ngir li nekk ci Kàddu Yàlla mën a dugg ci suñu biir xol (Sab. 1:1, 2 ; Yaw. 10:24, 25). Nanga ànd ak ñiy jaamu Yàlla ni mu ware te seen xol nekk benn (Léeb. 13:20). Nanga tàmm di bokk ci liggéeyu waare bi. Te booy def loolu, danga war a bëgg dimbali nit ñi nekk ci seen goxu mbooloo ak sa xol bépp. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am xol bu rafet (Sab. 86:11). Nanga moytu yëf yu mën a yàq sa xol. Mën na nekk lu mel ni féexal sa xol ak yëf yu bon te tilim, walla lu bokk ci mbirum coxorte. Lépp li mën a tax nga gën a jege Yàlla te mën a rattaxal sa diggante ak moom, nanga ci góor-góorlu bu baax. — Saak 4:7, 8.
5 Ci jamano bu njëkk bi, Yexowa digoon na mbooloom ne bu ñu ko déggalee, dinañu am barke yu baree-bare (5 Mu. 28:1, 2). Tey it, Yexowa dafay barkeel bu baax “ ñi koy déggal ”. (Jëf. 5:32.) Kon nañu fexe ba li ñuy def ak li ñuy jàngale tax ba nit ñi déggal Yàlla “ ak seen xol bépp ”.
[Laaj yi]
1. Lan la Yexowa bëgg ci ñi koy jaamu ?
2. Lu tax dimbali nit ñi ngir ñu am ngëm gu dëgër am solo lool ?
3. a) Dégg ndigal, naka la ànde ak mbëggeel ? b) Naka lañu mënee dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu gën a bëgg Yexowa ?
4. a) Lu tax li ñuy def am solo lool ? b) Lan lañu mën a def ngir am “ xol bu lay xiir ci dégg ndigal ” ?
5. Ñiy dégg ndigal, yan barke lañuy am ?