Lekkool bu ñuy won ni ñu mënee topp li ñu jàng
1 Bu ñuy topp li ñu def ci porogaraamu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ci atum 2006, dinañu def lépp li ñu mën ngir jariñoo bu baax li ñu ci jàng ci Biibël bi. Naka lañu ko mën a defe ? Nañu seet ni ñu ko mënee topp bu ñuy def liggéeyu Yàlla ak ci lépp li ñuy def bés bu nekk. Te nañu góor-góorlu ngir jëfe li ñu jàng. — Ywna. 13:17 ; Fil. 4:9.
2 Bu ñuy tontu : Ren, yokk nañu benn minit ci waxtu bi ñuy jagleel waa mbooloo mi ngir ñu wax ponk yu am solo yi ñu jàpp ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi. Kon mbokk mi war a def waxtaan bi tudd “ Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ”, amatul juróom benni minit. Juróomi minit rekk la am léegi. Na fexe ba bañ a wees loolu. Képp ku teew te bëgg bokk ci waxtaan boobu it, war na seetlu bu baax waxtu bi tontoom di jël. Bu ñu waajalee bu baax suñu tont, dinañu ko mën a yemale ci 30 segoond, walla sax ci lu ko gën a tuuti. Lu jege fukki nit war nañu mën a wax seen xalaat ci juróomi minit yi ñu may ñi teew.
3 Waxtaan yiy jàngale : Ñiy def waxtaan bi tudd “ Kàddu yu am solo ci li ñu waroon jàng ci Biibël bi ” ak Waxtaan N° 1 dañu war a gën a wax ci ni ñu mënee topp li nekk ci seen waxtaan bu ñuy waaraate ak ci lépp li ñuy def bés bu nekk. Fexe ba nit ñi bëgg topp li ñu jàng kese doyul. Ñiy def waxtaan yooyu war nañu wax lan la nit ñi war a def, naka lañu ko mënee def, ak njariñ bi ci nekk. Mën na wax lii “ Aaya bii dafa ñuy won li ñu war a def ”, walla boog “ Nii lañu mënee jëfandikoo aaya bii ci waaraate bi ”. Njiiti mbooloo mi ak surga mbooloo mi yu xam bu baax li xew ci mbooloo mi ak ci goxu mbooloo mi, nañu fexe ba wone naka la waa mbooloo mi mënee topp li nekk ci waxtaan bi ñuy def.
4 Misaal yi nekk ci Biibël bi, mën nañu baax lool ci ku bëgg wone ni waa mbooloo mi mënee topp li nekk ci waxtaan bi muy def. Bu waxee misaal bu mu jële ci Biibël bi ba pare, mën na wax lii : “ Yéen itam mën ngeen a jaar ci lu mel noonu. ” Buy wax ni ñu mënee topp li nekk ci benn aaya, war na seet bu baax ndax li muy wax ànd na ak aaya yi jiitu ak yi topp aaya bu muy wax. War na seet it ndax li muy wax ànd na ak li nekk ci Biibël bi yépp ak it téere yi “ surga bu takku te teey ” bi defar. — Macë 24:45.
5 Ku am xel mooy ku mën jariñoo li mu jàng ak li mu nànd ci fasoŋ bu baax. “ Xel mooy li ëpp solo. ” (Léeb. 4:7). Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi dina ñu may xel biy tax ñu xam li ñu war a def ci lépp. Nañu fexe ba jàng itam ci Lekkool bi ni ñu mënee gën a aay ci dimbali suñu moroom ba moom itam mu am xel boobu.