Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru Oktoobar : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, won ko téere Laaj bi. Nowàmbar : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Xam-xam walla kayit bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ? Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Bu fekkee ne am ngeen ci seen mbooloo téere yii di topp, mën ngeen leen wone itam : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ?, Recueil d’histoires bibliques walla Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Sãwiyee : Téere yi génn bala 1991 yi ngeen am ci seen mbooloo. Bu ngeen amulee téere yooyu, seetleen ndax amul beneen mbooloo bu leen jege bu ci am lu ëpp li ñu ciy soxla. Mbooloo yu amul téere yu yàgg yooyu mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu. Bu nit ki bëggulee jël téere boobu, won ko téere Veillez !
◼ Weeru oktoobar dina am juróomi samdi ak juróomi dimaas. Kon dina baax lool ci ku bëgg nekk pioñee buy jàpple.
◼ Porogaraamu “ Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2006 ” mu ngi ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Dencleen ko bu baax ndaxte dingeen ko soxla ci at mi yépp.