TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/05 p. 3
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 11/05 p. 3

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru nowàmbar : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Xam-xam walla kayit bu ndaw bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ? Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Mën ngeen wone it téere yii di topp, su ngeen ko amee ci seen mbooloo : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ? ; Recueil d’histoires bibliques walla téere Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Sãwiyee : Téere yi génn bala 1991, yi ngeen am ci seen mbooloo. Bu ngeen amulee téere yooyu, seetleen ndax amul beneen mbooloo bu leen jege bu ci am lu ëpp li ñu ci soxla. Mbooloo yu amul téere yu yàgg yooyu, mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu. Bu nit ki bëggulee jël téere boobu, won ko téere Veillez ! Feewriyee : Approchez-vous de Jéhovah. Mbooloo yi ko amul mën nañu wone téere Révélation : dénouement walla beneen téere bu yàgg génn bu ngeen am ci seen mbooloo te fekk li ngeen ci am ëpp na li ngeen soxla.

◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn, war na seet ndax xaalis bi mbooloo mi di dajale mat na. Loolu, bésu 1 desàmbar lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Xéyna fu ngeen di dajale xaalis bi bokkul. Mën na am boolewuleen xaalis bi ngeen di toppatoo Saal bi ak xaalis bi ñuy dajale ngir tabax ay Saalu Nguur. Kon nangeen seet ndax bu ci nekk mat na. Bu loolu paree, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

◼ Mbooloo yi war nañu tàmbali boole téere yii di topp ci téere yi ñuy laaj bànqaas bi : téere bi boole La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi génn ci atum 2005 (Volumes reliés) ak CD-ROM Watchtower Library — Edition 2005. Dinañu bind ci yan làkk ngeen mën a am téere yooyu ci kayit bi tudd “ Avis aux congrégations ”, te ñu koy yónnee ci mbooloo yi weer wu nekk. Buleen fàtte it ne ñi nu sóob ba pare rekk ñoo mën a am Watchtower Library — Edition 2005 te ci mbooloo yi rekk lañu ko mën a ame.

◼ Ci weeru sãwiyee, dina am ndaje liggéeyu waare fu ñuy waxtaane wideo bi tudd Soigner sans transfusion : besoins et droits du patient (ci DVD). Su ngeen soxlaa wideo boobu, nangeen ko gaaw a laaj ci seen mbooloo.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager