TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 11/05 p. 3
  • Naka lañu leen mënee dimbali ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Naka lañu leen mënee dimbali ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ñi am lu bare dañuy faj soxlay ñeneen ñi
    Li ñuy def ak li ngeen di maye
  • Lan lañuy def ngir dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba dal ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Ay tont ci seeni laaj
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 11/05 p. 3

Naka lañu leen mënee dimbali ?

1 Saa yu ñu déggee musiba bu dal ci kow ay nit, Seede Yexowa yi tàmm nañu laaj li ñu mën a def ngir dimbali leen. Bu ñu jàngee Jëf ya 11:​27-30 dinañu gis ne, am na léegi lu ëpp 1900 at, xiif bu metti lool amoon na ca Yude. Waaye karceen yi dañu sàkk ndimbal ngir jàpple seeni mbokk yi fa nekkoon.

2 Tey ci suñu jamano, nguuri àddina si nangu nañu suñu mbootaay jëfandikoo xaalis ngir dimbali nit ñi ci seen coono ak it ñi musiba dal seen kow.

3 Daaw, musiba bu tudd tsunami daloon na ca kow ñi dëkk Asie. Suñu mbokk yu bare yónnee nañu xaalis ngir ñu def ko ci xaalis bi mbootaay bi di dajale ngir jàpple ñi musiba dal seen kow. Dañu bëggoon ñu jàpple ñi nekk Asie ak xaalis boobu. Mbootaay bi kontaan na lool ci li ñu def noonu. Waaye, am na réew yoo xam ne, bu nit xasee wax ci ban musiba lañu war a def xaalis bi mu yónne, xaalis boobu, ci musiba boobu kese lañu koy mën a dugal. Duñu ko mën a jëfandikoo ngir leneen. Bu fekkee ne sax faj nañu ba pare soxla bi taxoon nit ki yónne xaalis boobu, li mu maye, duñu ko mën a dugal ci leneen. Te nguur gi dina jàpp bés boo xam ne, ginnaaw bés boobu, du nangu benn mbootaay jëfandikoo xaalis ngir jàpple ñi musiba boobu laal.

4 Loolu lépp a tax mbootaay bi di wax ne, bu nit bëggee maye xaalis ngir jàpple ñi nga xam ne musiba dafa dal seen kow, li gën mooy nit kooku def xaalis bi muy maye ci xaalis bi ñuy dajale ngir liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Xaalis boobu, dinañu ko mën a jëfandikoo ci ñaari fànn : 1) jàpple ñi soxla ndimbal ndax musiba bu dal seen kow, 2) toppatoo li karceen yi soxla ci wàllu ngëm. Waaye mën na am nit ku bëgg maye xaalis ngir ñu def ko ci xaalis bi ñuy dajale ngir jàpple ñi musiba dal seen kow. Te bëggul ñu def xaalis bi muy maye ci xaalis bi ñuy dajale ngir liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Ba tey, dinañu nangu jël xaalis boobu. Te bu amee ñu soxla ndimbal ndax musiba bu dal seen kow, dinañu leen ko yónnee. Waaye nag, li ñu gënal mooy, bu nit di maye xaalis ngir lu mel noonu, mu bañ a yemale xaalis boobu ci benn musiba kese. Maanaam mu bañ a wax fi ñu ko war a dugal ak naka lañu ko waree jëfandikoo.

5 Lu tax ñuy wax loolu, maanaam ñuy wax ne li gën mooy ñu dugal xaalis bi ñu bëgg maye ci xaalis bi ñuy dajale ngir liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp ? Loolu dafay tax xaalis bu ñuy mën a jëfandikoo ngir lépp lu bokk ci liggéeyu Nguur gi gën a bare. Moo gën ñuy dajale xaalis ngir jàpple rekk ñi nga xam ne musiba dafa dal seen kow. Loolu ànd na ak li Efes 4:16 wax, maanaam ñuy ànd di liggéey ngir ñu joxe li ñu soxla ngir “ jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager