TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/05 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Turu xaaj yi
  • 12-18 desàmbar
  • 19-25 desàmbar
  • 26 desàmbar ba 1 sãwiyee
  • 2-8 sãwiyee
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 12/05 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Buleen fàtte : Jamano bu ñuy am suñu ndaje yu gën a mag yi, Sasu Nguuru Yàlla bi dina joxe li ñu war a def ayu-bés bu nekk ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi. Mbooloo yi nga xam ne ci weer wii lañu war a am seen ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”, dinañu seet li ñu war a soppi ci porogaraam bii ngir mën a teewe ndaje bu mag boobu. Su baaxee ci seen mbooloo, ayu-bés biy jiitu ayu-bés bi ngeen di am seen ndaje bu gën a mag bi, nangeen jël 15 minit ngir seetaat ponk yi am solo yu seen mbooloo warul a fàtte ci li nekk ci xët 5 ak 6 ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar. Bu ndaje bu mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ” paasee ba mu mat benn walla ñaari weer, dinañu jël 15 ba 20 minit ci benn ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi ngir waxtaan ci ay ponku porogaraam boobu. Bu leen neexee, mën ngeen ko def ci xaaj bi tudd “ Li nekk soxla ci mbooloo mi ”. Ponk yooyu na nekk ay ponk yu waaraatekat yi gis ne dinañu baax ci waaraate bi. Ci waxtaan boobu, dinañu mën a wax ni ñuy toppe li ñu jàng ci ndaje bu gën a mag boobu ak li ñu fa jàng loo xam ne dafa tax seen liggéeyu waare bi gën a am njariñ.

12-18 desàmbar

Woy-Yàlla 12

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na am ñu topp li nekk ci xët 6 te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 desàmbar ak La Tour de Garde bu 15 desàmbar. Mën ngeen a wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Ku ci nekk bu paree woneel ne boole benn aaya ci li ñuy wax ngir wone suñu yéenekaay yi, jafewul.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : “ Xam-xam buy jëme ca dund gi. ”a Bala ndaje bi di jot, nanga wax benn walla ñaari nit ne dinga leen laaj ñu wax naka la leen xam-xam bi jóge ci Yàlla jariñe.

Woy-Yàlla 96 ak ñaan bu mujj bi.

19-25 desàmbar

Woy-Yàlla 7

5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal li mbooloo mi taxawal ngir waaraate bi ci bésu 25 desàmbar ak 1 sãwiyee.

15 min : Kàddu Yàlla am na doole (Yaw. 4:12). Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 nowàmbar 2003, xët 11, xise 13 ba 17. Nanga nettali liy wone ne li nekk ci Biibël bi mën na tax nit soppi ni muy dunde (w00 1/1 p. 3-5). Waxal nit ñi ñu faral a jëfandikoo bu baax Biibël bi bu ñuy waaraate këroo-kër, bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, bu ñuy def njàngum Biibël, maanaam ci bépp fànnu liggéeyu waare bi.

25 min : “ Nanga jariñoo wideo bi tudd Pas de sang : la médecine relève le défi. ” Waxtaan ak ñi teew ci wideo Pas de sang. Nangeen jëfandikoo laaj yi nekk ci xët 4. Bu ngeen ci paree, jàngleen xise bu mujj bi. Waxal waa mbooloo mi ñu fexe ba dara bañ leen a tere teewe ndaje bi ñuy def diggante 2 ba 8 sãwiyee. Dinañu fa waxtaan ci lu jëm ci lu bees lu ñu mën a dimbali ñu moytu deret.

Woy-Yàlla 35 ak ñaan bu mujj bi.

26 desàmbar ba 1 sãwiyee

Woy-Yàlla 38

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru desàmbar te joxe ko. Bu fekkee ne seen mbooloo dafa war a soppi waxtu yi muy defe seeni ndaje, nanga wax ci yan waxtu ngeen war a daje. Waxal téere yi ñu war a wone ci waaraate bi ci weeru sãwiyee te waxal fi ñu bind li ñu mën a wax ngir wone leen ci waaraate bi.

15 min : “ Lekkool bu ñuy won ni ñu mënee topp li ñu jàng. ” Wottukatu lekkool bi moo war a def waxtaan bii. Booleleen ci li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar 2005, xët 3.

20 min : “ Nañu dimbali nit ñi ñu dégg ndigal ‘ ak seen xol bépp. ’ ”b Ni leen ko jot bi mayee, nanga wax ñi teew ñu wax ci aaya yi nekk ci xaaj bi te fekk binduñu li ci nekk.

Woy-Yàlla 4 ak ñaan bu mujj bi.

2-8 sãwiyee

Woy-Yàlla 7

5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal ñi teew ñu bañ a fàttee indi Réveillez-vous ! bu sãwiyee 2006 ci ndaje liggéeyu waare bii di ñów.

15 min : “ Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — Nanga jéem a waxtaan ak nit ku nekk ci li ko itteel. ”c Na am ñuy wone naka la waaraatekat yi mënee soppi waxtaan bi ñu bëggoon a def ngir mu a ànd ak li nit ki wax.

25 min : Nañu topp ndigalu Yàlla bi ñuy laaj ñu moytu deret. Benn njiitu (magu) mbooloo moo war a def waxtaan bi. Bànqaas bi mooy joxe li ñu war a jàng ci waxtaan bii. Kiy def waxtaan bi, dina ko jàng ci kanamu ñépp. Balaa muy komaase, na wax waa mbooloo mi ne du tey lañu war a bind li ñu laaj ci kàrt bi. Buy jàng waxtaan bi, bu àggee ci ponk bu am solo, mën na ci yokk wax bu gàtt ngir ponk boobu gën a feeñ. Bu dul loolu, waru ci yokk yeneen misaal walla yeneen aaya. Na seet ci jot bi mu am ngir xam ndax war na jàng ci Biibël bi aaya yi ñu bind ci waxtaan bi, walla ndax dafa war a tari aaya bi rekk te bañ ko jàng ci Biibël bi. Bu jàngee waxtaan bi ba àgg ci ponk bu mën a ànd ak li nekk ci wërale bi tudd “ Lu bees lu ñu mën a dimbali ñu moytu deret ”, na ci wax. Bala waxtaan bi di komaase, sekkerteer bi war na jox waaraatekat yi ñu sóob yépp kàrtu DPA ak kayit bi tudd Instructions pour remplir la carte DPA (maanaam fi ñu bind ay tegtal ngir ñu xam ni ñu waree bind li war a nekk ci kàrtu DPA bi), ngir waxtaan bi gën a leer ci ñoom. Mbooloo mi war na am Carte d’identité yu doy. Sekkerteer bi moo war a toppatoo loolu.

Woy-Yàlla 41 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager