TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/07 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Turu xaaj yi
  • 8-14 sãwiyee
  • 15-21 sãwiyee
  • 22-28 sãwiyee
  • 29 sãwiyee ba 4 feewriyee
  • 5-11 feewriyee
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 1/07 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

8-14 sãwiyee

Woy-Yàlla 1

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal ñi teew ñu seetaan wideo bi tudd Pas de sang : La médecine relève le défi ngir waajal waxtaan bi ñuy def ci ndaje bi jëm ci liggéeyu waare biy am ci ayu-bés bu 22 sãwiyee. Na am ñu topp li nekk ci xët 4 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 15 sãwiyee, ak Réveillez-vous ! bu sãwiyee. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox. Na ci am kuy wone li ñu mën a tontu ku ñu wax : “ Je suis occupé ” (maanaam dama jàpp). — Seetleen téere Comment raisonner, xët 19-20.

15 min : Lii laa doon ! Waare ak waxtaan ak ñi teew. Am na ay ndaw yu sawarul a xamal nit ñi ne ay seede Yexowa lañu. Dañu ragal ñu ñaawal leen. Waaye am na lu bare lu baax lu war a tax ngeen xamal nit ñi ki ngeen doon. Jàngalekat yu xam li ngeen gëm, dañu koy gën a fullaal te duñu leen jéem a defloo li ngeen warul a def. Yeneen ndaw yi nga xam ne lu leen neex def, duñu leen gaaw a woo ci lu bon li ñuy def. Dina am it ñu gën a mën a nànd li waral ngeen bañ a def lu jëm ci diggante jigéen ak góor, espoor walla ci yeneen yëngu-yëngu yi waa lekkool di def waaye bokkul ci njàng mi. Dingeen gën a ñeme waare ca lekkool ba, walla daje ak seen waa kalaas bu ngeen di waare (g02 22/3 p. 12). Waxal ñi teew ñu nettali njariñ bi nekk ci xamal nit ñi ne Seede Yexowa lañu. Mën nga waxtaan ak benn walla ñaari ndaw bala ndaje bi di jot ngir mu waajal li muy wax.

20 min : Nañu xamal ñépp xibaar bu baax bi. Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere Organisés pour faire la volonté de Jéhovah, xët 92 ba fi xaaj bi nekk ci xët 102 di komaase.

Woy-Yàlla 57 ak ñaan bu mujj bi.

15-21 sãwiyee

Woy-Yàlla 25

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla.

15 min : Qu’est-ce qui vous en empêche ? (maanaam lu la ko teree def ?) Waxtaan bu benn njiitu mbooloo mi jële ci La Tour de Garde bu 1 awril 2002, xët 13 ba 15.

20 min : “ Loolu itteeluma. ”a Bu ngeen di def xise 4, laajal ñi teew ñu wax lan moo itteel ñi nekk ci seen goxu mbooloo. Na am ñaari nit ñuy wone ku ci nekk li ñu mën a wax bu ñu nit waxee “ Li ngeen di wax itteeluma. ” — Seetleen téere Comment raisonner, xët 16.

Woy-Yàlla 56 ak ñaan bu mujj bi.

22-28 sãwiyee

Woy-Yàlla 88

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Na am ñu topp li nekk ci xët 4 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 feewriyee, ak Réveillez-vous ! bu feewriyee. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox. Kenn ki, mën na mel ni kuy yóbbu yéenekaay yu bees yi, ku ko faral a jël.

10 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

25 min : “ Faj bi gën. ” Benn njiitu mbooloo moo ko war a def. Nangeen komaase waxtaan bi jëm ci wideo bi ak laaj yi nekk ci xaaj bii. Ngir jeexal waxtaan bi, na am kuy jàng xise bu mujj bi te waxal ñi teew ñu jàng bu baax Tour de Garde yi ñu bind ci xaaj bii.

Woy-Yàlla  86 ak ñaan bu mujj bi.

29 sãwiyee ba 4 feewriyee

Woy-Yàlla 6

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru sãwiyee te joxe ko. Waxal téere bi ñu war a wone ci weeru feewriyee te na am kuy wone ni ñu ko mënee wone.

20 min : “ Ndax waajal nga sa bopp ba xam li ngay def bu musiba dalee ci kow nit ñi ?”b Benn njiitu mbooloo moo ko war a def. Nangeen ci boole li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu nowàmbar 2005, xët 3.

15 min : Boo digee nit ne dinga fa dellu, nanga fa dellu. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 septaambar 1999, xët 11. Waxal ñi teew ñu nettali ni leen Yexowa barkeelee ndax li ñu dellu seeti nit, ni ñu ko dige woon.

Woy-Yàlla 100 ak ñaan bu mujj bi.

5-11 feewriyee

Woy-Yàlla 31

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.

15 min : Njariñ bi nekk ci gëstu Mbind yi, bés bu nekk. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci xaaj bi njëkk ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2007 te tudd Introduction. Waxleen lu tax bés bu nekk kenn ku nekk ci ñun war a jël jotu jàng aaya bés bi ak kàddu yi mu àndal. Bala ndaje bi di jot, nanga wax ak benn walla ñaari waaraatekat ngir ñu waajal seen bopp ngir wax ci ni ñuy fexee ba jàng aaya bés bi bés bu nekk te naka la leen jariñe. Nangeen waxtaan ci lu gàtt ci aaya atum 2007.

20 min : “ Mbëggeel mooy tax suñu liggéeyu waare di jur lu baax. ”c Nangeen ci boole li nekk ci La Tour de Garde bu 1 feewriyee 2003, xët 23, xise 16 ak 17.

Woy-Yàlla 1 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager