TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/08 p. 2
  • Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Turu xaaj yi
  • 10-16 màrs
  • 17-23 màrs
  • 24-30 màrs
  • 31 màrs ba 6 awril
  • 7-13 awril
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 3/08 p. 2

Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi

10-16 màrs

Woy-Yàlla 56

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na am ñu topp li nekk ci xët 6 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 màrs ak Réveillez-vous ! bu màrs. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox. Nañu joxewaale kayit yi ñuy joxe ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi.

20 min : Pourquoi assister aux réunions chrétiennes ? (maanaam lu tax ñu war a teewe ndaje yi). Waare ak waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 me 2007, xët 11-13. Waxal ñi teew ñu wax ban njariñ lañu gis ci teewe ndaje yi. Nañu wax it naka lañu xeexe li leen mënoon a tere tàmm teewe ndaje mbooloo mi.

15 min : “ Am na lu ñu mën a may Yexowa. ”a Su la ko jot bi mayee, waxal ñi teew ñu wax seen xalaat ci aaya yi ñu bind ci waxtaan bii fekk binduñu li ci nekk.

Woy-Yàlla 4

17-23 màrs

Woy-Yàlla 61

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal ñi teew ñu bañ a fàtte indi La Tour de Garde bu 1 awril ak Réveillez-vous ! bu awril ci ndaje liggéeyu waare bi ñuy def ci ayu-bés biy topp. Nañu waajal waxtaan bu baax ci suñu gox ngir wone leen. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi.

15 min : Ay tont ci seeni laaj. Benn njiit ci mbooloo mi moo war a def waxtaan boobu. Nañu jàng xise yépp te waxtaan ci.

20 min : “ Naka lañu mënee dimbali ñi teewe ndaje fàttaliku bi ? ”b Bu ñu àggee ci xise 5, na am ñuy wone ci lu gàtt ni ñu mënee komaase njàngum Biibël ak ku teewe woon ndaje fàttaliku bi.

Woy-Yàlla 54

24-30 màrs

Woy-Yàlla 35

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye.

15 min : Nañu waajal ni ñuy wone yéenekaay yi génn ci weer wi. Waxtaan ak ñi teew. Boo waxee ci lu gàtt li nekk ci La Tour de Garde bu 1 awril ak Réveillez-vous bu awril, nanga laaj ñi teew, yan waxtaan ñoo mën a neex nit ñi ci suñu gox, ak lu waral ñuy wax loolu. Waxal ñi teew ñu wax yan xaaju yéenekaay lañu bëgg wone ci waaraate bi. Lan lañu mën a laaj nit ki ngir komaase waxtaan bi ? Ginnaaw loolu, ban aaya lañu mën a jàng ci xaaju yéenekaay bi ñu bëgg wone ? Na am ñu topp li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 awril ak Réveillez-vous ! bu awril.

20 min : Nous apportons “ des bonnes nouvelles de quelque chose de meilleur ” (maanaam dañuy indi xibaar bu baax buy yégle lu gën). Benn njiitu mbooloo mi mooy def waxtaan bii. Li muy wax ngir ubbi waxtaan bi warul weesu benn minit. Bu ci paree na def waxtaan bu muy jële ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 2005, xët 18-19, xise 10 ba 14. Waxal ñi teew ñu wax ni xibaaru Nguur gi dëfële seen xol ak ni mu leen maye yaakaar bés bi ñu ko njëkkee dégg.

Woy-Yàlla 11

31 màrs ba 6 awril

Woy-Yàlla 16

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàtte bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs te joxe ko.

20 min : “ Leetar bu ñu jataay biy dogal yónnee. ” Waare ak waxtaan ak ñi teew. Mën nga waxtaan ak benn walla ñaari waaraatekat bala ndaje bi jot ngir ñu waajal li ñuy wax ngir wone ni ñuy defe seen porogaraam ngir jàng Annuaire bi. Booy jeexal waxtaan bi, nanga xiirtal ñépp ngir bu ñu jotee Annuaire bu 2008 ci mbooloo mi, nu jàng li ci nekk yépp.

15 min : “ Bu ñuy waare, na ku nekk yokk sa doole moroom ”c

Woy-Yàlla 32

7-13 awril

Woy-Yàlla 43

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.

20 min : Pourquoi différer son baptême ? (maanaam lu tax ngay bëgg puus bés bi ngay sóobu). Waxtaan bi ñu jële ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 2006, xët 29 ak 30, xise 14-17. Benn njiitu mbooloo mi moo koy def. Na ci boole waxtaan bu gàtt bu muy def ak benn walla ñaari waaraatekat yu ñu sóob fekk ñu nekkoon waxambaane walla jànq. Na leen laaj lii : lan moo leen puus ba ñu def lu am solo loolu fekk ay xale lañu woon ? Sóobu boobu naka la leen dimbalee ñu jëm kanam ba nekk karceen yu ñor ci wàllu ngëm, te loolu di leen di aar ?

15 min : Ndax jéem nga laaj nit ñi ndax bëgg nañu ñu jàngal leen Biibël bi ? Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002, xët 6. Nañu waxtaan ci li ñu fa bind ngir waxtaan ak nit ñi. Nañu wax it li ñu fa mën a defaraat ngir komaase njàngum Biibël ci téere Qu’enseigne la Bible ? Ginnaaw loolu, na am benn walla ñaari waaraatekat yuy wone ci kanam nit ñi naka lañu mënee def. Nanga xiirtal ñi teew, ñu jéem a komaase benn njàngum Biibël ci ayu-bés biy ñëw. Ngir loolu, lu mu tuuti tuuti nañu laaj benn nit ndax bëgg na ñu jàngal ko Biibël bi ci téere Qu’enseigne la Bible ?

Woy-Yàlla 23

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk a wax warul a weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager