TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/08 p. 1
  • Nañu doon waaraatekat yuy jëm kanam

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu doon waaraatekat yuy jëm kanam
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Na ku nekk am li muy fas yéene def ci wàllu ngëm
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Xaaj 12 : Nañu leen won ni ñuy komaasee te kontinee njàngum Biibël
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 4/08 p. 1

Nañu doon waaraatekat yuy jëm kanam

1 Suñu Baay bi nekk ca kaw dafay kontaan bu jaamam yi di jëm kanam ci wàllu ngëm. Loolu ëmb na jëm kanam ba mat waaraatekat bu aay ci xamle xibaar bu baax bi te dëgër ci wàllu ngëm. Pool xiirtaloon na wottukat bi tuddoon Timote, mu kontine di góor góorlu ngir ni muy “ jëm kanam bir ñépp ” (1 Tim. 4:13-15). Ñun ñépp a war a góor góorlu ngir li ñuy def ci waaraate bi gën a baax, su dee sax dañu nekk waaraatekat bu aay.

2 Nañu am lu ñuy jàpp ngir fas yéene ko def : Bu ñu bëggee jëm kanam, dañu war a am lu ñuy jàpp ngir fas yéene ko def. Lan lañu mën a jàpp ngir fas yéene ko def ? Mën nañu jéem a gën a aay ci fasoŋ bu ñuy jëfandikoo Biibël bi nga xam ne mooy suñu jaasi ci wàllu ngëm (Efes 6:17). Xéyna am na benn fànn ci liggéeyu waare bi fu ñu war a gën a góor góorlu, lu mel ni waaraate ci mbedd yi, ci gox yu bare bitig, walla waaraate ci béréb bu bare nit. Mën nañu góor góorlu it ngir li ñuy wax bu ñuy dellu seeti nit ñi gën a baax. Leneen lu baax li ñu mën a jàpp ngir fas yéene ko def mooy góor góorlu ngir gën a aay ci komaase te kontine ay njàngum Biibël.

3 Li ñu nu defaral : Ndaje mbooloo mi, rawatina ndaje Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi ak Ndaje liggéeyu waare bi, dañu leen def ngir ñu mën a nekk waaraatekat yu gën a aay. Li ñuy gën a góor góorlu ngir waajal te teewe ndaje yooyu, te di jëfe li ñu fay jàng, njariñ bi ñu ciy jële di gën a réy. — 2 Kor. 9:6.

4 War nañu dimbaleente it ci suñu biir ngir ñu jëm kanam ci wàllu ngëm (Prov. 27:17). Ki ñuy àndal ci waaraate bi, buy wone suñuy téere, bu ñu dégloo bu baax li muy wax, loolu dina ñu dimbali ñu gën a mën a waare. Rax ci dolli, wottukatu njàngum téere bi ñu bokk mën na seet it ni ñu mën a def ngir mu am ku lay jàpple. Bu amee pioñee bu ci yàgg, walla beneen waaraatekat bu ñuy dimbali ngir ñu gën a aay ci waaraate bi te gën ci am mbégte, loolu barke bu réy lay doon. Ndax am na waaraatekat bu bees ci suñu njàngum téere bi ? Xéyna mën nañu dem ba ci moom ngir wax ko ñu ànd ci waaraate bi.

5 Liggéey bu gën a am solo bi ñuy def tey mooy liggéeyu waare bi ñu dénk karceen yi. Bu ñuy jox Yexowa suñu “ sarax bu koy màggal ”, dañu koy bëgg a jox li gën ci li ñu am (Yaw. 13:15). Bu ñu góor góorloo ngir jëm kanam ci waaraate bi, dinañu nekk ay liggéeykat yu ci dul rus “ dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi. ” — 2 Tim. 2:15.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager