Xaaj 12 : Nañu leen won ni ñuy komaasee te kontinee njàngum Biibël
Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
1 Kuy jàng Biibël bi, bu komaasee waare, mën na am mu ragal a komaase njàngum Biibël ak nit te kontine ko. Waaye def ay njàngum Biibël lu am-a-am solo la ci suñu liggéeyu waare bi. Naka lañu ko mënee dimbali mu bañ a ragal a def njàngum Biibël ? — Macë 24:14 ; 28:19, 20.
2 Xéyna ki ngay jàngal Biibël bi nekk na léegi waaraatekat bu ñu sóobagul. Mën na am mu bokk ba pare ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi. Kon waajal na ay waxtaan, ba pare def leen ci kanamu ñépp. Loolu jàngal na ko li mu war a xam ngir mën a nekk liggéeykat bu rusul dara, te nekk kuy “ faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi ”. — 2 Tim. 2:15.
3 Nekkal royukaay bu baax : Bi Yeesu doon jàngal taalibeem yi, lu leer la leen doon sant. Te moom ci boppam dafa nekkoon royukaay bu baax. Nee na : “ Taalibe bu jàng ba wàcc [maanaam taalibe bu ñu jàngal bu baax], dina yem ak kilifaam demin. ” (Lukk 6:40). Nanga roy ci Yeesu ngir nekk royukaay bu baax ci fasoŋ bi ngay waare. Loolu lu am solo la. Kiy jàng Biibël bi, bu xoolee ni ngay waaree, dina xam li ñu bëgg bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, maanaam komaase ay njàngum Biibël.
4 Wonal kiy jàng Biibël bi li ñu mën a wax bu ñuy laaj kenn ndax bëgg na ñu jàngal ko Biibël bi. Nee ko soxlawul ñu wax, wax bu dul jeex ngir xamal ko ni njàngum Biibël di deme. Ci lu bare, liy gën mooy ñu won ko ni njàngum Biibël di deme. Mën nañu jël téere fu ñuy jàngale Biibël bi, tànn benn walla ñaari xise, te won ko foofu ni ñuy jàngalee nit ñi. Boo bëggee xam ni nga mënee def loolu, mën nga seet li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002, xët 4.
5 Saa yoo ko mënee, àndal ak kiy jàng Biibël bi booy defi njàngum Biibël. Mën na ànd itam ak beneen waaratekat bu aay ci liggéey boobu. Bu ngeen nekkee ci njàngum Biibël, mën nga ko bàyyi mu wax dara ci benn xise, walla ci benn aaya bu am solo. Bu gisee ni ñuy jàngalee Biibël bi, dina xam lu bare ci ni mu mënee dimbali nit ba mu topp li muy jàng (Léeb. 27:17 ; 2 Tim. 2:2). Wax ko lu baax li muy def. Nanga waxtaan ak moom it ci li mu mën a def ba gën a aay ci liggéey boobu.
6 Nañu won waaraatekat yu bees yi ni ñuy jàngalee Kàddu Yàlla. Loolu dina leen may ñu mën a komaase te kontine ay njàngum Biibël. Loolu bokk na ci ‘ jëf yu rafet ’ yi (2 Tim. 3:17). Ñun ak waaraatekat yu bees yi, lii lañuy wax nit ñépp : “ Ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara. ” (Peeñ. 22:17). Ànd noonu ci liggéey boobu, aka nekk lu neex !