Ay Tont Ci Seeni Laaj
◼ Ndax Seede Yexowa yi mën nañu faju ci kër fu ñuy toppatoo ñi màggat walla lopitaan boo xam ne benn mbootaayu diine moo koy jiite ?
Mbootaayu diine yu bare dañuy jiite ay lopitaan walla ay kër fu ñuy toppatoo ñi màggat, walla ñi feebar feebar bu yàgg. Lu ëpp ci béréb yooyu defuñu leen ngir jàpple Babilon mu mag ma (Peeñ. 18:2, 4). Mën na am ñu nekk kër yu diine tabax ngir ame ci xaalis. Tey, am na ay lopitaan yoo xam ne seen tur kese moo laal ci mbirum diine. Waaye it am na yeneen yoo xam ne waa kër làbbe yi ñoo fay def lu bare ci liggéey bi.
Yenn saay, Seede Yexowa dina soxla dem ci kër fi ñuy toppatoo ñi màggat walla ci lopitaan ngir ñu faj ko. Moom moo war a seetal boppam ndax dina dem ci béréb bu diine moom. Ñenn ñi, seen xel dina leen may ñu def loolu, waaye ñeneen ñoom, seen xel du leen ko may (1 Tim. 1:5). Am na yeneen yu mën a tax ñu tànn def lii te bañ a def lale. Yooyu jar na ñu seet ko.
Mën na nekk lu mel ni lii : Benn kër fu ñuy toppatoo ñi màggat walla benn lopitaan kese moo am ci gox bi ñu nekk, waaye lopitaan walla kër boobu dafa am tuur bu laal ci mbirum diine. Walla boog bu amee beneen lopitaan walla kër fu ñuy toppatoo ñi màgget, mën na am ñépp a xam ne bi turam laal ci mbirum diine moo gën a baax. Mën na am it lopitaan boobu kese moo am li ñu soxla ngir faj feebar bi la dal. Walla it doktoor bi la war a faj walla ki la war a opére ci lopitaan boobu kese lañu ko may mu liggéey. Yenn saay it, lopitaan yi laal ci mbirum diine yi, dinañu nangu topp li karceen yi wax ci deret, fekk ci lopitaan bu nit moomal boppam, walla nguur gi moom ko, duñu ko nangu def. Mën nga xalaat ci yu mel noonu booy seet ci ban lopitaan ngay dem ngir ñu faj la.
Mën na am nga bëgg dem faju ci kër fu ñuy toppatoo ñi màggat walla ci lopitaan, fekk diine am fa wàll. Bu boobaa mën nga ko jàppe ni dangay fey li nga leen wax ñu defal la. Dafay mel ni diine boobu dafa am lu muy jaay. Te booy jëflante ak moom du tax ñu mën a wax ne danga bëgg a jàpple diine bu dul dëgg. Dangay jënd kese li mu lay jaay, walla ngay fay li mu lay defal.
Waaye nag, ñun karceen yi, bu ñu nekkee ci lu mel noonu, dañu war a fexe ba bañ a bokk ci diine bu dul dëgg. Waruñu woowe ñiy liggéey ci béréb yooyu walla ñi fay ñëw, “ mon père ” walla “ ma soeur ” ak yu mel noonu ni ko nit ñi tàmmee di def ci seen diine ngir may leen cér (Macë 23:9). Danga war a jàppe mbir mi ni jënd ak jaay kese moo leen boole. Dañu lay faj te di la defal li nga soxla kese.
Booy toppatoo li nga war a def ngir mën a dugg lopitaan, mën nga leen xamal ne Seede Yexowa nga, te danga bëgg njiitu mbooloo Seede Yexowa yi nekk ci gox bi seetsi la. Loolu dina tax nga mën a am ñu lay jàpple bu baax ci wàllu ngëm, ci jamano boy nekk ci lopitaan boobu. —1 Tes. 5:14.
Bu amee suñu mbokk mu màgget bu nekk ci kër fu ñuy toppatoo ñi màgget, mbokkam yi nekk Seede Yexowa, njiiti mbooloo yi nekk ci gox fi kër googu nekk, ak ñi bokk ci mbooloo moomu, dañu ko war a toppatoo bu baax ci wàllu ngëm. Rawatina bu nekkee ci kër boo xam ne benn diine moo ko yore. Bu ñu farloo ci fànn boobu, mag yi nekk ci kër yooyu dinañu gën a am doole. Loolu dina leen aar it ñu bañ a juum ba bokk ci li diine yooyu di def, seeni feet, walla leneen lu mel noonu lu mën a am ci béréb yooyu.
Na ku nekk jàpp ci xelam li ñu wax fii te seet li mu ëmb yépp, ba pare tànnal boppam kër bi ñuy toppatoo ñi màggat walla lopitaan fi mu bëgg a dem. — Gal. 6:5.