Yégle Yi
◼ Téere yi ñuy wone ci wéeru Awril ak me : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Dinañu góor-góorlu ngir seeti ñi suñu waxtaan neex te tàmmuñu teewe suñu ndaje yépp, fekk teewe woon nañu ndaje fàttaliku bi ak waxtaan bi ñu faral di am ci àddina si sépp bu ndaje fàttaliku bi weesoo. Li waral ñuy dellu seeti nit ñooñu, mooy bëgg komaase njàngum Biibël ak ñoom. Suweŋ : Qu’enseigne réellement la Bible ? Nañu góor-góorlu ngir komaase ay njàngum Biibël. Suweŋ ak ut : Téere bu def 32 xët ci yi topp fii : Dieu se soucie- t-il vraiment de nous ? ; Doit-on croire à la trinité ? ; Dunda léen ba fàww ak bànneex ci suuf si ! ; Les esprits des morts — Peuvent-ils vous aider ou vous nuire ? Existent-ils vraiment ? ; La direction venant de Dieu — Le chemin du paradis ; La route qui mène à la vie éternelle — l’avez-vous trouvée ? ; Le gouvernement qui établira le Paradis ; Le nom divin qui demeure à jamais ; Mën nga nekk xaritu Yàlla ! ; Quand la mort frappe un être aimé... ; Que devient-on quand on meurt ? ; Quel est le but de la vie ? Comment le découvrir ? ; Une vie pleinement satisfaisante : Comment ? ; Veillez ! ak “ Voici, je fais toutes choses nouvelles ”.
◼ Sekkerteeri mbooloo yi war nañu am kayit yi tudd Demande d’admission au service de pionnier permanent (S-205) ak Demande d’admission au service de pionnier auxiliaire (S-205b), ba mu mat li ñu mën a soxla ci benn at, walla lu ko ëpp. Bu ñu ci soxlaa yeneen, nañu jëfandikoo kayit bi tudd Demande de publications (S-14) ngir laaj ko bànqaas bi. Bala ngeen di yónnee kayit yooyu bànqaas bi, nangeen seet bu baax ndax bind nañu ci lépp li ñu ci laaj.
◼ Bànqaas bi war na yore nimoro telefon ak adareesu wottukat yiy jiite ak sekkerteer yépp. Saa yu amee ku ci am nimoro telefon walla adarees bu bees, kurélu liggéeyu waare bi war na ko bind ci kayit bi tudd Changement d’adresse du surveillant-président/secrétaire (S-29) te gaaw ko yónnee bànqaas bi. Saa yu amee lu ñu soppi ci nimoro telefon yi, war nañu ko xamal bànqaas bi.
◼ Booy dem ci beneen réew te nga bëgg fekke foofu ndajey mbooloo mi walla ndaje bu mag, te nga bëgg xam waxtu, bés, walla fu ñuy defe ndaje yooyu, nanga ko laaj bànqaas biy toppatoo liggéeyu waare bi ci dëkk boobu. Adareesu bànqaas yaa ngi ci xët bi mujj ci Annuaire bu mujj bi.
◼ Reew yi bànqaasu Senegaal di toppatoo ñu ngi komaase bu baax atum liggéeyu waare bu 2008 ndaxte liggéey bi ñu ci jot a def rafet na lool. Ci ñeenti weer yu njëkk yi ci atum liggéeyu waare bii, ca Gambie, ci 100 waaraatekat yoo jël, am na 8,4 yu ci yokku. Ca Guinée Bissau nag, ci 100 waaraatekat yoo jël, am na 12 yu ci yokku. Ci ñeenti weer yooyu ba tey, am na 29 nit ñu nu sóob ca Senegaal ak 17 ca Mali. Su ñu boolee loolu lépp, dafay tolloo ak ñi nu sóoboon ci ñaari reew yooyu ci atum liggéeyu waare bi weesu yépp.