Bés bi ñu jàpp ngir wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël
1 Dale ko ci wéeru sãwiyee, mbooloo bu nekk dina jàpp benn samdi walla dimaas ci wéer bu nekk. Bés boobu dañu koy jël ngir wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël. Mën na nekk samdi walla dimaas bu njëkk ci wéer bi. Mbooloo mu nekk mooy seet bés bi gën ci ñoom. Ci bés boobu, bu ñu tasee ak ku bëggul njàngum Biibël, waaraatekat yi mën nañu ko won téere Qu’enseigne la Bible walla suñu yéenekaay yu mujj yi. Njiit ak surga yiy jàpple yépp war nañu fexe ba def li ñu mën ci liggéey boobu, te jàpple waaraatekat yi ngir ñu komaase ay njàngum Biibël.
2 Kurél biy toppatoo liggéeyu waare bi ci mbooloo mi mooy jàpp ayu-bés bi ñuy wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël. Lée-lée dinañu ko fàttali waaraatekat yi ngir ñu mën a waaj. Te góor-góorlu it ngir wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël bu ñuy waaraate këroo-kër akit bu ñuy seeti ñi suñu waxtaan neex.
3 Ni ñu koy waajale : Mën nañu gis li ñu mën a def ngir komaase njàngum Biibël ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2006 ci xët 3 ba 6, ak ci téere Comment raisonner ci xët 12. Xéyna dina am ñuy jëfandikoo kayit yu ndaw, mel ni bi tudd Ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo. Sasu Nguuru Yàlla bu ut 2007 wone na it ci xët 3 li ñu mën a def ngir komaase ay njàngum Biibël, bu ñuy seeti ñi jëloon suñuy yéenekaay. Surga yiy jàpple ci mbooloo mi ak njiit yi, dinañu leen defal porogaraam ngir ñuy jiite ci lu mat 10 ba 15 minit ndaje bi ñuy def bala ñuy waare. Ci ndaje boobu dinañu waxtaan ci benn walla ci ñaari fasoŋ yu baax yu ñu mënee komaase njàngum Biibël. Walla mu am ñuy wone ni ñu ko mënee def.
4 Dëgg la, du ñépp ñooy nangu jàng Biibël, walla kontine di jàng Biibël bi lu yàgg. Loolu warul tax ñu bàyyi di wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël, ndaxte Yexowa mooy xëcc boroom xol yu rafet yi ci mbootaayam (Ywna. 6:44). Suñu wareef yemul rekk ci def dëgg gi ci xolu nit ñi. Dañu war a toppatoo te di roose li sax ci xolu nit ki. Te loolu dafa laaj ñuy jàngal Biibël bi boroom xol yu rafet yi. Bu ñuy def loolu, dañuy am céru bokk ci ñiy liggéeyandoo ak Yàlla. — 1 Kor. 3:9.