Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
Buleen fàtte : Jamano bu ñuy am suñu ndaje yu gën a mag yi, Sasu Nguuru Yàlla bi dina joxe li ñu war a def ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi ayu-bés bu nekk . Mbooloo yi war a am seen ndaje bu gën a mag bi tudd “ Xelum Yàlla moo ñuy won yoon bi ”, dinañu seet li ñu war a soppi ci porogaraam bi ngir mën a teewe ndaje bu mag boobu. Su dee baax na ci seen mbooloo, nangeen jël 15 minit ci ayu-bés biy jiitu ndaje bu gën a mag bi ngir seetaat lu mën a baax ci seen mbooloo, ci li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu septaambar 2008, ci xët 3 ak 4. Bu ndaje bu mag bi weesoo ba mu mat benn walla ñaari weer, dinañu jël 15 ba 20 minit ci benn ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi ngir waxtaan ci ay ponk yu am solo yi ñu dégg ci ndaje boobu te waaraatekat yi gis ne mën na leen a dimbali ci liggéeyu waare bi. Bu leen neexee ngeen def ko ci xaaj bi tudd “ Li nekk soxla ci mbooloo mi ”. Wottukatu liggéeyu waare bi moo war a def waxtaan boobu. Dina laaj ñi teew ni ñuy toppee walla ni ñu bëggee topp ponk yooyu bu ñuy waare.
8-14 desàmbar
Woy-Yàlla 7
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Nañu wax ci lu gàtt li ñu def ci xët 4 ngir wone La Tour de Garde bu 1 desàmbar ak Réveillez-vous ! bu desàmbar. Waxal ñi jot a joxe yéenekaay yooyu, ñu wax ni ñu def ngir wone leen. Ban xaaj lañu jël, lan lañu laaj nit ñi, ak ban aaya lañu leen won ?
15 min : Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bu atum 2009. Kiy jiite lekkool bi mooy def waxtaan bii. Nañu waxtaan ci ponk yi mbooloo mi war a fàttaliku te nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar 2008 ci xët 3. Nañu wax ci liggéeyu kiy jàpple kiy xelal nit ñi. Nangeen xiirtal ñépp ñu góor-góorlu ngir def bu baax waxtaan yi ñu leen di dénk. Wax leen ñuy bokk bu baax ci waxtaan biy jëm ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ci ayu bés bi. Te ñuy topp xelal yi ñuy joxe ayu bés bu nekk ci téere Tirez profit de l’école du ministère théocratique.
20 min : “ Ndax dangay jëfandikoo téere Comment raisonner ? ”a Bu ngeen àggee ci xise 4, na benn pioñee walla beneen waaraatekat bu aay wone ci lu gàtt ni ñu mënee jëfandikoo téere Comment raisonner, bu ñuy waaraate këroo-kër ngir tontu laaj bii : ‘ Lu tax Seede Yexowa yi duñu màggal nowel ? ’
Woy-Yàlla 3
15-21 desàmbar
Woy-Yàlla 71
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi.
15 min : Bu ñuy waaraate, nañu dee dellu ci li ñuy wax nit ki. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere École du ministère, xët 207. Na am ñuy wone benn walla ñaari fasoŋ yu ñu mënee topp li ñu wax ci xaaj boobu.
20 min : Vos actions seront récompensées (maanaam dinañu leen fey li ngeen def). Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 awril 2005, xët 28, xise 6 ba fi xët 29 di jeex. Nanga waxtaan it ci lu gàtt ak benn walla ñaari waaraatekat yu sawar ci waaraate bi. Nañu wax ni leen Yexowa jàpplee ba ñu faj seeni soxla ci wàllu alal walla ni mu leen jàpplee ci seeni naqar.
Woy-Yàlla 68
22-28 desàmbar
Woy-Yàlla 11
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàng kayit biy wone ne betel bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal téere yi ñuy wone ci wéeru sãwiyee, te na benn njiit wone ni ñu leen mënee wone ci waaraate bi.
15 min : Nañu waajal ni ñuy wone La Tour de Garde bu 1 sãwiyee ak Réveillez-vous ! bu sãwiyee. Waxtaan ak ñi teew. Boo waxee ci lu gàtt li nekk ci yéenekaay yooyu, laajal ñi teew ñu wax waxtaan yi nar a neex ñi nekk ci suñu gox ak lu tax. Woneel yenn ci waxtaan yooyu te laaj ñi teew lan lañu ci bëgg a laaj nit ñi ak ban aaya lañu leen bëgg won ngir komaase waxtaan yi, bala ñuy wone yéenekaay yi. Ngir jeexal waxtaan bi, na am ñu topp li nekk ci xët 4, ngir wone ci kanam ñépp ni ñu mënee wone yéenekaay bu nekk. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox.
20 min : “ Bés bi ñu jàpp ngir wax nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël ”b Waxal bés bi ñu jàpp ci weeru sãwiyee, ngir mbooloo mi dem ci gox bi, ngir laaj nit ñi ndax bëgg nañu njàngum Biibël. Seetleen li ñu wone ci xise 3 te na am benn walla ñaari waaraatekat yuy wone ci kanamu ñépp ni ñu mënee topp li ñu wax foofu.
Woy-Yàlla 55
29 desàmbar ba 4 sãwiyee
Woy-Yàlla 83
Njàngum Biibël bi ci mbooloo mi :
jd chap. 12 §1-10
Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi :
Xaaj bi ñu war a jàng ci Biibël bi : Peeñu ma pàcc 15 ba pàcc 22
Nañu fàttaliku li ñu jàng ci lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla
Ndaje liggéeyu waare bi :
Woy-Yàlla 73
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
10 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : “ Waaraate dafa laaj muñ. ”c Bu ngeen amee jot, waxal ñi teew ñu wax li ñu xalaat ci aaya yi ñu lim ci xaaj bi.
Woy-Yàlla 66
5-11 sãwiyee
Woy-Yàlla 15
Njàngum Biibël bi ci mbooloo mi :
jd chap. 12 §11-22
Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi :
Xaaj bi ñu war a jàng ci Biibël bi : Njàlbéen ga pàcc 1 ba pàcc 5
No. 1 : Njàlbéen ga 3:1-15
No. 2 : Lu tax Yeesu nekkoon jàngalekat bu mag (Ir chap. 1)
No. 3 : Lan moo dul neen ?
(1 Kor. 15:58)
Ndaje liggéeyu waare bi :
Woy-Yàlla 43
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
10 min : Nañu roy Yeesu ci ni mu meloon ci waaraate bi. Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere “ Viens, suis-moi ”, xët 84 ba 86, xise 16 ba 21.
20 min : Nangeen takku, sampu ba dëgër (1 Kor. 15:58). Nanga waxtaan ak ñaar walla ñetti waaraatekat walla pioñee yu yàgg ci jaamu Yàlla. Naka lañu xame dëgg gi ? Naka la liggéeyu waare bi meloon bi ñu komaasee waaraate ? Yan jafe-jafe lañu amoon ? Yan barke lañu am ndax li ñu jàpp bu baax ci diine dëgg gi ?
Woy-Yàlla 49
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.